NDIISOOG JËWRIÑ YI - 06 MONTHS.NOVEMBER 2024
Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, àllarba 06i fani nowàmbar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoorteel Ndiisoog Jëwriñ yi, Njiitu Réew mi taxawlu na ngir fàttaliku jëmmi Mammadu Mustafaa Ba mi fi ne woon Jëwriñu Koom mi, Koppar yi ak Palaŋ, te wuyuji Boroomam altine 4i fani nowàmbar 2024. Jébbale na njaalu askan wi jëme cig njabootam ak liggéeykati Njëwriñ gi.
Njiitu Réew mi feddaliwaat na ab wooteem ci way-Politig yi ak askan wi ci doxaliinu jàmm, dal ak sàmmonte ak sàrti demokraasi jëm ci joŋantey lesislatif yu 17i fani nowàmbar 2024. Sàkku na ci Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi ak Jëwriñu Yoon ji, ñu jël mbooleem matuwaay yi war te dëppo ak yoon ngir amal kàmpaañub jàmm fépp ci réew mi.
Njiitu Réew mi àddu na ci mbirum yoonal jëme ci sektéer eeformel bi. Ci loolu, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu ànd ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, jël ay matuwaay ngir yoonal sektéer eeformel bi te mooy fexee gën a lootaabe yëngu yi ñi ciy yëngu, waaye rawati na amal lootaabe gu mucc ayib ci mbooleem wànqaasi Nguur gi ci wàllu tàggatu, kopparal, galag ak samp ay « zones spéciales » ak ay warab yu ñu leen jagleel. Ci wàll woowu, xamal na Njiital Jëwriñ yi ne fàww ñu séq ay waxtaan ak « Sàmbur Koosileer » yu Senegaal ngir baral jéego yi jëm ci amal soppi gu matale ci koomum eeformel bi.
Njiitu Réew mi fàttali na ci geneen wàll yitteem ci moderniise artisanaa bi ci réew mi, te doon pàcc bu am solo ci soppi koomum eeformel bi ak jubbanti gu matale ci wàllu porodiktiwite ci réew mi. Xamle na ne jot na sëkk ci wànqaasi nguur giy taxawu ak a kopparal (DER/FJ, 3FPT) ñu gën a jëme seen yitte ci yënguy APDA ak Sàmbur dee mécce ngir gën a dooleel warabi porodiksoo artisaa yu Senegaal yi war a doon ci lu gaaw ay dëgg-dëggi PME walla PMI. Ci loolu kon sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu posewu ci dogal bi ñu jël jëm ci boole ci genn kurél ak dajale mbooleem li nguur gi war di jënd, ngir gën a sóob bu baax artisaa yi ci li nguur gi du liggéeylu. Dina yell kon, ñu gën a dooleel ci mbooleem pàcc yi ci lii di « made in Senegaal » ak jëfandikoo liy bawoo ci réew mi jaare ko ci ay warabi jaayukaay, ay warabi fésal ak i FOIRE.
Njiitu Réew mi rafetlu na lootaabe gi ñu amal ci weer wi ñu jagleel « koosome lokaal ». Xamle na ne fàww ñu yeesal boole ko ak wëlbati jubluwaayu Foire bu Ndakaaru jëmale ko ci gën a fésal liy bawoo ci réew mi.
Lu soxal wàll wu yaatu wi mbatiit gi am ci biir « agenda national de transformation » bi, Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi solo si mbatiit am ci biir « Vision Senegaal 2050 ». Ndokkale na boole ko ak ñaax ñiy yëngu ci wàllu mbatiit ci liggéey bu am solo bi ñuy amal ci wane Senegaal, sàmm dal gi ak mbokkoo gi lépp ci sàmmonte ak sunuy mbaax ak sunu cosaan. Soññ na Jëwriñu Ndaw Ñi, Tàggat yaram ak mbatiit, Endistiri Ekstaraaktiif yi ak Patrimuwaan Historig, ñu taxaw ci yaatal seen i yëngu ci askan wi, jëm ci taxawal ak doxal cig yëgoo arminaatu mbaatitu Senegaal. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi itam ñu gaaral ko aw sémb wu jëm ci tabax ay jumtukaayi mbatiit ci Póol yi te bàyyiwaale xel man-man ak jagley gox bu nekk.
Njiitu Réew mi woo na Jëwriñu Mbatiit gi mu gën a liggéey ci luy fésal sunu mbatiit ak mboor boole ko ak sàmm warab yi nu am ci wàllu mboor rawati na Gore, di barabu fàttaliku bu ñu war a gën a waggar. Ngir tëj bunt boobu, yëgal na Ndiisoo gi ne dina jiite, alxemes 07i fani nowàmbar 2024, ca Garaa Teyaatar Nasonaal Duudu Njaay Kumba Róos, jataayu tijjitel 15eelu xewu Biennale de L’art africain contemporain.
Lu soxal turism bi doon pàcc bu am solo ci wàllu yokkute ak taxawal ay xëy, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñu Turism bi ak artisanaa mu yëngalaat mbooleem wànqaas yiy fésal « réewum Senegaal » te ànd ko ak ñiy yëngu ci wàll wi, operaatéer yi ci turism bi ak yeneen way-xereñ yi ci wàll wi. Xamle na ne fàww ñu peeg amenaasmaa yi ak tabax ay hotel ak warabi turism ci tefesu réew mi ak warab yi ñu dénk SAPCO. Ci loolu ba tay xamle na ne fàww ñu gën a jagal bu baax li wër ak kaaraaneg warabi turism yi waaye it fexe ba gën a dooleel teewaayu poliisu turism bi ngir gën a aar yëngu yi.
Ngir suqali xëyu ndaw ñi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu jiital ci yitte yi turism bi ci matukaayi 3FPT ak déggoo yi dox diggante Nguur gi ak Njaatige yi. Bokk na ci tamit taxawu lekool biy Tàggate ci wàllu hotel ak turism niki noonu warab yiy tàggat ci liggéeyu turism. Sàkku na ci Jëwriñu Turism bi ak artisanaa ak ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ñu xayma, lootaabewaat boole ko al dooleel kopparalug turism bi jaare ko ci joyyantiwaat yënguy keredi yi soxal hotel yi, di doxaliin wu war a taxaw ci dooraat ci lu gaaw ak suaqli gu sax ci wàll wi. Soññ na tamit Jëwriñu Turism bi mu ànd ak Jëwriñu Yaaleg Jaww ji, sektéer piriwe bi ak kër yiy yëngu ci yaaleg jaww ji, liggéey ci fexe di amal at mu jot ci Senegaal, ndaje mu mag mu ñu jagleel ndaamaari gi ngir jaay « Réewum Senegaal » waaye tamit boole ko ak suqali turismub biir réew mi.
Njitu Réew mi dikkaat na ci juróom fukki ati ISRA. Posewu na ci ngir ndokkale ak a ñaax mbooleem way-xeltu, way-xarala ak way-doxal yu ISRA. Sàkku na ci Jëwriñu Mbay mi, Moom sa Bopp ci wàllu dund, ak Càmm gi ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ñu gën a taxaw ci yokk dooley yëngu ak coppikug ISRA jëm ci dooleel taxawaay bu am solo bi mu am ci pénc mi ci wàllu gëstu ci liy bawoo ci mbay mi, jur gi ak géej gi, joyyantiwaat li nu am ci wàllu jiwwu ak baral jéego yi ci doxal politig ak sémbi moom sa bopp ci wàllu dund.
Njiitu Réew mi ndokkale na barug Senegaal gu « Beach soccer » gi am ndam lu rëy daal di jël juróom ñetteelu tiitaram ci kembaar gi ak barug U17 gi jël raaya UFOA/A boole ko ak jàll ci CAN 2025 bi.
Njiitu Réew mi yëgal na Ndiisoo gi ne dina jiite bis bi ñu jagleel larme bi ca Kaa Jal Jóob àjjuma 08i fani nowàmbar 2024.
Mu tëjee moom Njiitu Réew mi ci dellusiwwat ci tukki yi mu doon amal ca Araabi Sawudit ak Repiblig bu Turki te ëmboon weccente yu am solo ak jaayaante yu seen i njiit, Kilifa gi Muhammet Ben Salmaan ak Peresidaa Erdogaan jël jëm ci jàppale sunu réew ci doxal «Vision Sénégal 2050 ».
Ci lu soxal tukkeem bi ca Araabi Sawudit, Njiitu Réew mi amal na Umra ca Màkka boole ko ak siyaareji Yónnent bi Muhmmat (SLHWS) ca Medin. Ci loolu, kilifag ñaari Jàkka yu tedd yooyu, di Buur Salmaan Ben Abdel Asiis AlSawut defal na ko ag jagle, joxe ndigal ngir ñu tijjil ko kaaba gi. Loolu du firndeel rekk diggante bu rattax bi lëkkale sunu ñaari réew yi ak cér bu kawe bi Kilifay Araabdi Sawudit yi jox Senegaal.
Njiitu Réew mi rafetlu na bu baax dalal gu mucc ayib gi ko Peresidaa Erdogan jagleel, niki noonu waxtaan yu am solo yi ñu séq te aju woon ci yoon ak matukaay yi ñu war a jël ngir gën a xóotal lëkkaloo gi dox diggante Senegaal ak Turki.
CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:
Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi àddu na ci lu soxal wàllu joŋante yi ak tuurug dex yu Senegaal, Gàmbi ak Kaasamaas;
Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa def na leeralu ayu-bis bi muy amal ci tolluwaayu saytug wal mi.
Jëwriñu Njaboot gi ak dimbalante gi àddu na ci doxalinu Poroteksoo sosiyaal ci Senegaal.
CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii:
Njëwriñu Biir Réew Mi ak Kaaraangeg Pénc mi :
Sëriñ Umar Ngaala NJAAY, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°722 189/E, doonoon lu ko jiitu Topp-Góornoor bu Tundu Séeju bi yor biri ndoxal, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Ndakaaru bi yor biri ndoxal, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Georges Sàmba FAY, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°722 161/K, doonoon lu ko jiitu Topp-Góornoor bu Tundu Kéedugu bi yor biri ndoxal, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Cees bi yor biri ndoxal, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Siidi Gise JONG, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°516 355/G, doonoon lu ko jiitu Topp-Góornoor bu Tundu Sigicoor bi yor biri ndoxal, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu See Luwi bi yor biri ndoxal, toogu bu kenn nekkutoon;
Soxna Digu Yala Matild SAAJO, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°744 879/C, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Ndakaaru bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Abaabakar Sadiix ÑAŊ, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°744 900/B, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Cees bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Dominig Kumba Ndóofeen JUUF, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°744 970/B, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Fatig bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Mammadu Habiib KAMARA, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°716 358/F, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Kawlax bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Alséni BÀNGURAA, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°653 091/L, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Sigicoor bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ El Haaji Muhammadul Mustafaa GAY, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°744 927/G, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Kéedugu bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Soxna Jaariyatu NJAAY, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°737 811/C, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Tàmbaakundaa bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Pàppa Layti MAAR, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°650 042/C, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu tundu Luga bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Jibriil JÓOB, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°718 238/G, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Jurbel bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Soxna Làlla JAMARA, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°744 941/A, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Kafrin bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Tafsiir Baaba AAN, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°744 939/H, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Maatam bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Bonawàntiir KALAMO, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°683 111/Z, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Koldaa bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Ba Usmaan DANFAXA, Administaraatéer siwil, limatu payoor l°746 039/C, doon liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l'administration territoriale, tabb nañu ko Topp-Góornoor bu Tundu Séeju bi yor wàllu suqaliku, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Seex NJAAY, Jàngalekat, limatu payoor l°609 092/V, tabb nañu ko Suu-Perefe Arondismaa Tayif , Goxu Mbàkke, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Bernaard COMBAAN, Asistaa sosiyaal, limatu payoor l° 631 714/F, tabb nañu ko Suu-Perefe Arondismaa Kayel, Goxu Mbàkke, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Umar JÓOB, Jàngalekat, limatu payoor l° 627 373/L, tabb nañu ko Suu-Perefe Arondismaa Ndorna, Goxu Médina Yoro Fulaah, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Abdulaay NDAW, Jàngalekat, limatu payoor l° 635 917/G, tabb nañu ko Suu-Perefe Arondismaa Maampaatim, Goxu Koldaa, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Pàppa Umar SÀLL, Jàngalekat, limatu payoor l° 629 049/H, tabb nañu ko Suu-Perefe Arondismaa Cille Buubakar, Goxu Podoor, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Birinóo Aluwiis TUPAAN, Jàngalekat, limatu payoor l° 626 790/L, tabb nañu ko Suu-Perefe Arondismaa Boyngel Bàmba, Goxu Gudiri, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Damien JÉEJU, Jàngalekat, limatu payoor l° 669 342/H, tabb nañu ko Suu-Perefe Arondismaa Tendug, Goxu Biñonaa, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Sosef JAATA, Jàngalekat ci lekkol bu digg-dóomu bi, limatu payoor l° 626 809/G, tabb nañu ko Topp Suu-Perefe Arondismaa Kabrus, Goxu Usuy, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Njaw ÑING, Jàngalekat, limatu payoor l° 639 458/E, tabb nañu ko Topp Suu-Perefe Arondismaa Ñaaxee, Goxu Tiwaawon, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Kamire Arnóo MANEL, Jàngalekat, limatu payoor l° 677 251/H, tabb nañu ko Topp Suu-Perefe Arondismaa Lujaa Wolof, Goxu Usuy, toogu bu kenn nekkutoon;
Sëriñ Lamin MAANE, Jàngalekat ci wàllu tàggatu gu xereñ, limatu payoor l°641 238/D, tabb nañu ko Topp Suu-Perefe Arondismaa Aañam Siwol, Goxu Maatam, mu wuutu Sëriñ Moor Joor GÉY, mi ñu woolu ci yeneen yitte.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE