SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ GU ÀLLARBA 02i FANI OKTOOBAR 2024

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 02 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, àllarba 2i fani oktoobar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Njiitu Réew mi doore ci taxaw fàttaliku jëmmi Ahmadu Maxtaar MBOW, di Jàngalekat bu amoon dayoo, doonoon fi Jëwriñu Jàng mi, Mbatiit ak Ndaw ñi, doonoon depite ak Bootalu UNESCO. Mu rafetlu bu baax jaar-jaar bu mucc ayib bu kàngam gu mag gii ci yoriinu nguur, di ku liggéeyal réewam dugal loxoom lool ci luy suqali njàngum réew mi, mbokkoo gi ak luy gën a yékkati Senegaal ci àddina si.

Ci wàll woowu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñ yi ñu dénk wàllu Njàng mi, Njàng mu Kawe mi ak Mbatiit, ñu waajal bisub sargal ñeel sunu naataango bu jàmbaare woon nga xam be ay bindam ak dogoom ci bëgg sa réew ak Afrig doon nañu lu ñu war a fésal jàngal ko dongo yi ak njàngaan yi. 

Lu soxal màggal "octobre rose", Njiitu Réew mi fésal na ag ñeewanteem jëme ci jigéen ñi am jàngoroy ngal. Sàkku na ci Jëwriñu Paj mi ak Dimbalante mu taxawu mbooleem kurél yi te dugal loxoom bu baax ngir sottal mbooleem naal yi ñuy teg ci diiru weer wi.

Ci tijjitel lekool yi ak jàngune yiy dëgmal, Njiitu Réew mi yékkati na kàdduy ñaax ak ñaanal ndam mbooleem ñiy yëngu ci njàng mi, rawati na jàngalekat yi ak dongo yi. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu jël mbooleem matwaay yi war, ànd ko ak ñiy yëngu ci mbir mi, ngir ci genn wàll, baral jéego yi jëm ci am ug dëppoo ci soppi doxaliinu njàng mi, ak ci geneen wàll taxaw temm ci fexe ba atum njàng 2024-2025 doon lu mucc ayib. Fésal na itam solos taxaw ci dooleel diisoo ak liggéeykat yi ci doxaliinu njàng mi waaye itam gën a jagal nekkiin wi ak li aju ci lekool yi.

Ba tay, Njiitu Réew mi woo na Ngóornamaŋ bi ñu door ca na mu gën a gaawee, taxawal sémb wu yaatu wu jëm ci  jëlee fi mbaari jàngukaay yi, defaraat ak amal tabax yu dëppoo ak barabu jàngukaay. Xamle na itam, wareefu gaww matale sémb wu yees wi soxal Njàng mi ak Tàggatu gi méngale ko ak mbaax ak mbatiitu sunu réew. Muy sémb wu war a bàyyi xel nammeeli sunu askan ak jafe-jafe yi aju ci wàllu xarala yi ak “Intelligence artificielle".

Ak ni sunu askan gënee bari ay ndaw, Njiitu Réew mi taxaw na ci jamp gi nekk ci tabaxaat sunu ekool piblig samp ko ci kenoy siwismu, ma-réewe, làkki réew mi ak tijjiku ci làkki doxandéem yi waaye tamit waajal ci man-mani xamtu, xarala ak xereñte, sunuy dongo ci nii àddina si di soppikoo.

Njiitu Réew mi jaajëfal na Njiital Jëwriñ li ak Jëwriñ yi mu soxal ci jéego yu am solo yi ñu teg ngir joyyanti ak jëmmal doxaliinu njàngum réew mi jaare ko ci xereñte, ci dëppoo, pas-pasu am njureef yu baax ak kóoluteg mbooleem partaneer yi.

Ngir taxaw ci amal doxaliin wu mucc ayib ak lëkkale gu ànd ak yëgoo ci yënguy lekool yi ak jàngune yi, Njiitu Réew mi jël na dogalu taxawal Ndiisoo Gu Mag ngir Njàng mi ak Tàggatu gi, di kurél gu ñuy samp ca Primature mu war a taxaw, ànd ko ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, topp ak xayma gu matale ci doxaliinu Sémbu Njàng mi ak Tàggatu gi.

Lu soxal tolluwaayu koppari pénc mi, Njiitu  Réew mi jaajëfal na Njiital Jëwriñ li ak mbooleem Ngóornamaŋ bi ci kaajar gi ñu amal jëm ci xamle ni ñu fekkee koppari pénc mi.

Ba muy àddu ci ndono lu diis li fi nguur gi fi bawoo bàyyi, ëppal yu doy waar yi ñu seetlu ci xayma koppari askan wi ak li mu jur ci doxal pénc mi ak jaayante Nguur yi teew tay ak yu ëllëg, Njiitu Réew mi woo na Njiital Jëwriñ li mu jël ca na mu gën a gaawee, matuwaayi joyyanti yi war ngir baral jéego yi ci delluwaat ca na ñu yàgg a  xamee njël li, koppar yi ak waññi gi niki ko Ndayi Sàrti Réew mi ak sàrt yi diglee. 

Njiitu Réew mi jaajëfal na Njiital Jëwriñ li ci anam yi mu jiitee liggéey yi jëmoon ci yeggali sukkandikukaay bu yees bu ci wàllu politigu koom ak nekkiin bi aju ci PROJET Senegaal gu moom boppam, jub te naat. Bég na bu baax ci sottig liggéey bu metti bii, nga xam ne boole na ñépp te doon na naal yu jëm tabaxaat koom ak suqaliku gog lépp day bawoo ci doomi réew mi di delluwaat ci doomi réew mi. Wayndare kaajar ak rëdd yooni sunu politigu koom ak nekkiin dina fésal boole ci màndargaal tànneef yu am solo yi ñu war a doxal te war a doon kenoy soppi gu matale ci Senegaal. Ci loolu, xamal na Ndiisoo gi ne dina jiite, altine 14i fani oktoobar 2024 ca CICAD, jataayub aajar ak xamle Wayndare Politigu Suqali Réew mi, ci teewaayu mbooleem Ngóornamaŋ bi, ñiy yëngu ci wàllu koom ak mbooleem ñi Senegaal lëngool. 

Lu soxal ndoxi taw yi wàccaat ayi-bis yii wees te indi ay loraange ci yenn goxi réew mi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñu Mbay mi, Jëwriñu Biir Réew mi yor kaaraangeg pénc mi ak Jëwriñu Ndox mi, ñu def ub tënk ci njureefi taw yi ak fengat yi ci dexi Senegaal, Gàmbi ak Kaasamaas def ci tool yi ak dëkkuwaay yi. Soññ na Ngóornamaŋ bi ñu dajale mbooleem jumtukaay yi war ngir yombal jegeel bu gaaw gox yooyu loru ci seen jumtukaayi njéggite yi daanu ndax taw yu am doole yi ak ñaax waa réew mi ñu indi seen ndimbal jëme ci askan woowu loru.

Njiitu Réew mi sàkku na itam ñu xoolaat te yataal doxaliin yi jëm ci taxawu mbay mi. Sàkku na tamit ci Jëwriñu Mbay mi mu def leeral ci jumtukaay yi ñu teg jëm ci waajal kàmpaañu njaayum li ñoree ci mbay mi.

 Njiitu Réew mi tëjee ci dikkaat ci tukki ga mu amal ca États Unis, 21 ba 28i sebtàmbar 2024, fa mu doon teewe ci Ndajem Waxtaane Ëllëg ak jataayub Ndaje Mu Mag mu Mbootaayu Réewi àddina si. Tukki boobu am pose la woon ci xamal àddina si yéeney Senegaal ci dox ngir jëmmal jàmm ak kaaraangeg àddina si ak gën a fésal doxaliinan wu yees ci ni muy jëflante ak ñi mu lëngool. Ci noonu la waa Etas Unis Amerig xamlee ne jekk nañu ci jàppale Senegaal ngir mu matale “New Deal Technologique” bi war a def sunu réew selebu yoonu xarala ci Afrig.

Njiital Jëwriñ li dooree ci, jébbal Njiitu Réew mi, ci turu Ngóornamaŋ bi, ay ndokkaleem ci kàddu yu mucc ayib yi mu yékkati ca Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi àddina si ak njureef yu am solo ya ñuy séntu ñu ruusee ca ndaje ya mu fa jot séq ak jëmm yu am dayoo ak nemmiku ya mu amal ca yenn warab ci tukki bi mu doon amal ca Amerig.

Ci tomb yi mu jot a yaatal, Njiital Jëwriñ li dikkaat na ci tolluwaayu koppari askan wi ñu xamle ci janoo bu mu amal ak taskati xibaar yi alxemes 26i fani sebtàmbar 2024. Jëfiin wii nag day wane dogug Njiitu Réew mi ci amal doxaliin wu leer ci ni ñuy saytoo alalu askan wi. 

Njiital Jëwriñ li taxaw na bu baax ci yitte ji Ngóornamaŋ bi am ci joyyanti ca na mu gën a gaawee, saytu gu mucc ayib ci koppari pénc mi, ci kanamu yaatuwaayu yàqu-yàqu yi ñu seetlu ci càmbar doxaliinu nguur gi fi bawoo. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñu koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo, ñu jël mbooleem matuwaay yi ci war, ànd ko rawati na ak FMI.

Njiital Jëwriñ li teg ci xamal Ndiisoo gi ci matuwaay yi ñu jël ngir amal ci lu jaar yoon, 14i fani oktoobar 2024, jataay bi Njiitu Réew mi war a jiite, te ñu jagleel ko fésal Sukkandikukaay bu yees bu politigu koom ak nekkiinu Senegaal ci diggante 2025-2050. Fésal na wareefu, Jëwriñ yi, ku ne ak la cay sa wàll, nga doon làntinoor jaare ko ci xamle ànd ko wàll yi mu soxal ci poligu pàcc yépp. 

Mu tëjee, moom Njiital Jëwriñ li  fàttali na Jëwriñ yi ak Jëwriñi Càmm yi ñu gën a bàyyi xel ci topp ndoxalug dogal yi jëm rawati na ci ubbiteg lekool bii ci 2024-2025, séddaleg ñiy door a am BAC yees ci jàngune yi, xeex mbëkk mi, saytu jafe-jafe yi dal ci askan wi ak mbay mi te tukkee ci taw bi ak des yi, dogali fegu ci gaagaande yiy am ci yoon yi niki noonu taxaw ci fay bir yi ñu ameel ñiy yëngu ci mbay mi.

CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:

Jëwriñu Koppar yi ak Njël li àddu na ci tënk yi bawoo ci ràppooru càmbar alalu askan wi ci diggante 2019 ba mars 2024, te IGF amal ko, seen njeexital ci wàllu njël li ak yooni yeesal yi war ngir indi ay saafara ci rëq-rëq yi ñu ci seetlu. Cambar gii mu ngi bawoo ci sas wu mu leen joxoon, te aju ci ay sukkandikukaay yu lalu ci ndigal yu mu joxoon ay wànqaasam. Njureefi càmbar yooyu yaatal nañu leen ci janoo ak taskati xibaar yi Njiiatal Jëwriñ li amal 26i fani sebtàmbar 2024.

CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

  • sémbu dogal bi aju ci lootaabe Njëwriñu Jumtukaayi Tabax yi ak Yaaley Suuf si ak Jawwu ji.

CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii: 

CI WÀLLU NJÉNDE LI: 

  • Sëriñ Mammadu Umar NJAAY, Saabalkat, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog Kurélug saytu caabal yi (CNRA), toogu bu kenn newutoon;
  • Sëriñ Mammadu Lamin JÀNTE, tabb nañu ko Njiital Ndiisoo gu Kawe gi yor Wàllu Diisoo gi mu wuutu Soxna Inosaas NTAP NJAAY;
  • Sëriñ Mustafaa JIITE, Àttekat, limatu payoor l°602 388/E, tabb nañu ko Bootalu Kurél giy saytu komand piblig (ARCOP), mu wuutu Sëriñ Sayeer Ñaŋ ; 

Ci wàllu Primature:

  • Sëriñ Hattaab SAANE tabb nañu ko Njiital Ndiisoog saytu kërug dooraat yënguy koom mi ak nekkiin wi ca Kaasamaas (ANRAC);

Ci wàllu Njëwriñu Jumtukaayi Tabax yi ak Yaaley suuf si ak jawwu ji:

  • Sëriñ Suleymaan GÉY, Kàngam ci Yaaleg Jaww ji, tabb nañu ko Bootalu Yaaleg Jaww ji mu wuutu Umar Xaasimu JA;
  • Sëriñ Badara JÓOB, Xereñtaanu jëfandikoo ci awiyaasiyoo siwil tabb nañu ko Bootalu Jumtukaayi tabaxi naawu yi mu wuutu Sëriñ Seex JUUF;
  • Sëriñ Ma-Njaay FAY, Xereñtaan ci wàllu yaale tabb nañu ko Bootalu yaale gi ci yoon yi ak dem bi ak dikk gi mu wuutu Sëriñ Muhammadu Mustafaa ÑAŊ ;
  • Sëriñ Abdul Siley Fataa BA, Xereñtaan ci wàllu Yaale, limatu payoor l°627472/L doonoon lu jiitu Njatigel Bànqaasu Caytug Xarala ca Njëwriñu Jumtukaayi Tabax yi ak Yaaley Suuf si ak Jaww ji, tabb nañu ko Bootalu Yaaley suuf si mu wuutu Sëriñ Yayaa Sàmba ÑAŊ;
  • Sëriñ Yanqooba Ben Alfuseyni SONKO, Master QHSE tabb nañu ko Njiital Ndiisoog Saytu Koppari yiy suqali Yaaley suuf si.

Ci wàllu Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu:

  • Sëriñ Baabakar SÉMBÉN, komiseer ci wàllu luññutug koom, tabb nañu ko Bootalub Kër giy Saytu Ja yi ca Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, mu wuutu Sëriñ Ansumaana SAANE;
  • Soxna Faraasuwaas FAY, komiseer ci wàllu luññutug koom, tabb nañu ko Kërug Senegaal ngir moomeelu ndefar yi ak fentug xarala ca Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, mu wuutu Sëriñ Maxtaar JA.
  • Sëriñ Ahmet Tijaan JA, komiseer ci wàllu luññutug koom, tabb nañu ko Bootalub yaxantug biir réew mi ca Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, mu wuutu Sëriñ Ansu Baaji;
  • Sëriñ Ãari Faal KARWALÓO, Xereñtaan ci Ndefar ci wàllu mbay mi ak lekk gi, limatu payoor l°618880/M, tabb nañu ko Bootalu Lijjanti yu Ndaw ak yu Yamamaay yi ca Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, mu wuutu Sëriñ Seydinaa Abuubakar Sadiix NJAAY;
  • Sëriñ Isaa WÀDD, komiseer ci wàllu luññutug koom, tabb nañu ko Bootalu Kurél giy Saytu Sistemu resipise àntarpóo ca Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, mu wuutu Sëriñ Diris Siñoor JÀLLO.
  • Sëriñ Aali Furu BA tabb nañu ko PCA CICES.

Ci wàllu Njëwriñu Foŋsoo Piblig , Xëy mi ak jëflante diggante Campeef yi:

  • Sëriñ Baabakar SI, espektëer ci wàllu liggéey ak sekirite sosiyaal, tabb nañu ko Bootalu xëy mi ca Njëwriñu xëy mi, mu wuutu Móodu FAAL, mi ñu woolu ci yeneen yitte;
  • Sëriñ Saalif KOLI, Jàngalekat ci Njàng mu digg-dóomu mi, limatu payoor l°551.277/Z, tabb nañu ko Bootaalu Centre National de Formation et d’Action, mu wuutu Sëriñ Kaliidu SOKOMAA, mi ñu woolu ci yeneen yitte;
    • Sëriñ Ibraahiima JEŊ, espektëer ci wàllu liggéey ak sekirite sosiyaal, limatu payoor l°515.700/B, doonoon lu ko jiitu Bootalu Ressources Humaines ca Njëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo, tabb nañu ko Bootalu Foŋsoo Piblig, mu wuutu Sëriñ Aamadu Mataar Siise, mi ñu woolu ci yeneen yitte.

Ci wàllu Ndaamaari gi ak Pasiin gi:

  • Sëriñ Góora GAY, am lijaasab DEA ci wàllu Melosuuf, tabb nañu ko Sekkereteer Seneraalu Kër giy fésal ak suqali Pasiin gi (APDA), mu wuutu Sëriñ Yuusufa BA, mi ñu woolu ci yeneen yitte;
  • Ansumaana SAANE, di yëngu ci wàllu ndaamaari, tabb nañu ko Njiital Ndiisoog Saytu këru giy dooleel ndaamaari ci Senegaal.

Ci wàllu Njëwriñu Caabal yi, Jokkoo yi ak Xarala:

  • Sëriñ Momar JONG, Saabalkat, am lijaasab Maitrise ci Lettres Modernes, tabb nañu ko Bootalu Kërug Tasukaayu Xibaar gu Senegaal (APS), mu wuutu Sëriñ Ceerno Aamadu Si;
  • Seexunaa BÉEY, Jàngalekat-gëstukat, Maître Kooferaas ci wàllu Tas xibaar ak Caabal, tabb nañu ko PCA bu RTS.

Ci wàllu Njëwriñu Paj mi:

  • Sëriñ Seega GÉY, am lijaasab Dotoraa ci Sociologie, tabb nañu ko Bootalu CMU, mu wuutu Sëriñ Seex Tàkko Jóob.

Ci wàllu Njëwriñu Yoon:

  • Sëriñ Mboose SOW, Gerefe, tabb nañu ko PCA ONRAC.

Ci wàllu Njëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi:

  • Sëriñ Abdu Salaam KÀNTE, di jiitekatu ay liggéey, aji-leŋ ci xare bi, tabb nañu ko PCS bu ASP, mu wuutu Sëriñ Haamidu MBOW;
  • Sëriñ Seex Ñaŋ, Àttekat, limatu payoor l°600 6672 /A, tabb nañu ko Sekkereteer Seneraalu Njëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, mu wuutu Sëriñ Àlliyun Aydara ÑAŊ mi war a dem leŋ.

Ci wàllu Njëwriñu Kéew mi ak Jàll ci ekolosi:

  • Sëriñ Saadibu JIBA, Jàngalekat ci njàng mu digg-dóomu gi ci wàllu Ndundat ak Suuf, tabb nañu ko PCA kër giy saytu mbirum jëmbat garab ak Grande Muraille verte.

Ci wàllu Njëwriñu napp mi ak Jumtukaayi géej yi ak waax yi:

  • Soxna BENGA, Aji-doxal mbirum géej, limatu payoor l°618 080/U, tabb nañu ko PCS bu ANAM ca Njëwriñu napp mi ak Jumtukaayi géej yi ak waax yi, mu wuutu Sëriñ Ibraahiima KAMARA;
  • Sëriñ Bekaay JÓOB, am lijaasab MBA ci Management, tabb nañu ko Bootalu ANAM ca Njëwriñu napp mi ak Jumtukaayi géej yi ak waax yi, mu wuutu Sëriñ Ma-Sàmba Asil GÉY;
  • Soxna Mbëgge GAY, Biologiste, tabb nañu ko Bootalu Pêche Continemtal ca Njëwriñu napp mi ak Jumtukaayi géej yi ak waax yi, mu wuutu Sëriñ Aadama FAY;
  • Sëriñ Aliw BA, Ma-koom vi wàllu balli mbindaare yi, Kàngam ci wàllu napp ak yarum jën, tabb nañu ko PCS bu kër giy saytu yarum jën ca Njëwriñu napp mi ak Jumtukaayi géej yi ak waax yi, mu wuutu Sëriñ Kille SAAXO.

Ci wàllu Njëwriñu Koppar yi ak Njël li:

  • Sëriñ Idriisa SÀMB, espektëer Impots, tabb nañu ko Aji-doxal Fonds de Garantie Automobile.

Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE