SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 4i FANI SUWE 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 04 MONTHS.JUNE 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 4i fani suwe 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoorteel i kàddoom, Njiitu Réew mi sant na mbooleem ñi doon teewe liggéey yi aju ci Péncoo Sistem politigu réew mi. Rafetlu na bu baax taxawaay bu am solo bi ñu wane ci bëgg réew mi ak jiital njariñu réew mi féete lépp kaw. Di taxawaay bob dina tax, ci kaw nangul kenn ku ne gis-gisam, ñu man a am ug dëppoo ci tomb yu am solo yi jëm ci amal coppitey politig ak campeef yi war ngir gën a dëgëral demokaraasi Senegaal. Feddali na ag dogoom ak gu Ngóornamaŋ bi ci def seen keem tolluwaayu kàttan jëm ci taxaw temm ngir gën a xóotal ak méngale ak jamono sunu demokaraasi jaare ko ci jëmmal digle yi war a bawoo ci péncoo gii ginnaaw ba ñu ci amee ag dëppoo.

Njiitu Réew mi dikkaat na ci luy gën a dëgëral diisoo diggante ñetti wàll yi (Ngóornamaŋ, Sàndikaa, Njaatige) ak jëmmalug “Pacte national de stabilité sociale” bi ngir yokkute gu ñépp di ànd te mu sax. Fàttali na Ngóornamaŋ bi sas wu yaatu wi “Haut Conseil du Dialogue social” am ci wàllu yombal, yaatal ak topp jëmmalug jaayante yi ñett wàll yi def ci déggoo gii ñu torlu 1 panu mee 2025. Ci loolu, sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi, ci Jëwriñ ji yor wàllu Liggéey bi ak ci Jëwriñ ji yor wàllu Koppar yi, ñu taxaw ci gën a dooleel jumtukaayi yënguy “Haut Conseil du Dialogue social” ngir gën a taxawu ci sàmmonte ak doxaliini diisoo gi ci pàcc yépp. 

Njiitu Réew mi xamle na ne fàww ñu gën a am mbaaxu fagaru ci yenn réeroo yi, sukkandiku ko ci anam yi méngoo ak bànqaasu Njëwriñ gu ne, taxawal ay kuréli diisoo ci pàcc yi ak ci gox gi, waaye itam ci yeesalaat ak torlug lii di “conventions collectives” yi ci mbooleem wànqaas yi. Ci yoonu diisoo ak yaatal waxtaan yi ñu bokk di amal, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi muy may nopp saa su ne ñiy yëngu ci wàllu koom mi ak dundiin wi, gunge, ci kaw sàmmonte ak sàrt yi, doxaliin yi ak yi ñu déggoo ci àddina si, ndoxalug yelleefi liggéeykat yi, dooleel diisoo gi ci diggante Nguur gi ak Sektéer piriwe bi ngir taxaw ci gën a jagal wàllu jëflante yi ak dundalaat koomum réew mi. Ci loolu, fàttali na Njiitu Jëwriñ yi ne fàww ñu gaaw yeggali boole ko ak jàllale sémbu yoonal wi jëm ci moom sunu bopp ci wàllu koom, di liy màndargaal sunu yéene ci soppi yënguy koom mi boole ko ak taxawu ak gën dooleel këri liggéeyukaay yi ci réew mi 

Njiitu Réew mi àddu na ci jafe-jafe yi am ci dogali ñoŋal yi ñu jël ngir amal njaay mu mucc ayib ci liy bawoo ci mbayum dër mi ak sàmm bu baax wàllu payteef yi. Ci kanamu jafe-jafe yi ñu jànkoonteel ren ngir denc ak jaay lim bu takku bi ñoree ci mbayum dër mi te doon lu man a gàllankoor dundug filiyeer yu bari, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi, ci kilifteefu Njiitu Jëwriñ yi, mu jël mbooleem matuwaay yi war, ngir taxaw, ca na mu gën a gaawee, ànd ko ak aktéer piriwey réew mi, ci fàkk ak tabax ay warab yu ñuy denc ak a sàmm liy ñoree ci mbayum dër mi. Soññ  na itam Njiitu Jëwriñ yi, Jëwriñu Koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi, Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, Jëwriñu Mbay mi, Bay-Dunde gi ak Càmm gi, Jëwriñu Kopparal gu Ndaw gi ak Koomum Jàppal ma Jàpp mi ak Sekereteer Detaa bi yor Koperaatif yi ak Taxawu Baykat yi, ñu teg pexe mu jëm ci jaay li ñoree ci mbay mi, lëkkale ko ak ndoxalug kàmpaañu mbay mi. Xamle na ne fàww ñu gën a lootaabewaat warab yi ñuy jaaye li bawoo ci mbay mi nga xam ne doon na lees war gën a méngale ak jamono te dëppale ko ak, bu demee ba mat, taxawalug bursu nasonaalu liy ñoree ci mbay mi, te war a boole mbooleem pàcc yi ci aju (kopparal gi, meññal gi, njëg gi, sopparñi, njaay mi…)

Ci Tabaski giy dëgmal, Njiitu Réew mi, ndokkale na mbooleem umma Islaam gi, julliti Senegaal, rawati na nag ñaan ngir Senegaalu jàmm, gu naataange ak jàppoo. Sant na Ngóornamaŋ bi ci mbooleem dogal yi mu jëloon, ca weeru awril 2025 ak leegi, lépp ngir fexe ba xar yi doy sëkk ci réew mi ci njëg yu jàppandi. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu jël mbooleem matukaay yi war ngir ñu man a amal bis bi ci anam yu mucc ayib, niki noonu yombalal askan wi bëgg a génn, dem gi ak dikk gi lépp ci kaw bàyyiwaale xel péexte ak kaaraangeg yoon yi. 

137eelu Ajug Mariyaal gu Popongin dina am 7, 8 ak 9i fani suwe 2025 jëm ci Pàntakot gi. Njiitu Réew mi ndokkale na mbooleem kerceŋ yi teg ci sàkku ci Ngóornamaŋ bi mu taxaw temm ci jël mbooleem matukaay yi aju ci wàllu kaaraange ak jumtukaay ngir taxawu taalibe yi ak fexe ba jàppandil yëngu yi ñuy amal ci warab yi ñuy amalee siyaar bi. 

Ndiisoog Jëwriñ gii mooy 50eel bi ci diggante ba ñu tegee Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY ci boppu réew mi ak tay. Ci loolu, Njiitu Réew mi ndokkale na Usmaan Sonko Njiitu Jëwriñ yi ci liggéey bu mucc ayib bi jëm ci rëdd, jëmmal, jubbanti ak topp jëfi Ngóornamaŋ bi ñu jot a amal ci mbooleem pàcc yi. Boole na ci ndokkale itam teg ci ñaax Ngóornamaŋ bi ci ag jaayanteem ak ni mu saxee dàkk ci matale liggéey bi. Sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi mu jël mbooleem matukaay yi war ngir baral jéego yi jëm ci jëmmal tegtalukaay bii di « Vision Sénégal 2050 ». Mu dolli ci xamle ne fàww ñuy topp weer wu jot sémb yi ak naal yi aju ci ”Agenda national de Transformation” bi, jaare ko ci taxawal ay « delivery units » yu njëwriñ yi. Mu tëjee bunt boobu, sàkku ci Njiitu Jëwriñ yi mu waajal ab lël bu jëm ci natt liggéeyu ngóornamaŋ bi ak baral jéego yi jëm ci jëmmal “Agenda national de Transformation” bi.

Ci arminaatam ci wàllu laamisoo, Njiitu Réew mi dikkaat na ci tukki nemmiku ga mu doon amal 26 ak 27i fani mee 2026, ca Gine Bisaawó, ci ndënel Umaro Sisoko Embaló. Sant na bu baax naataamgoom bii di magam niki noonu askanu Gine Bisaawó ci dalal gu mucc ayib gi ñu ko jagleel. Fésal na cant ak ngërëm jëme ci Peresidaa Embaló mi ko sargalee raaya Amilkaar KABRAAL, di wi gën a ràññiku ca réew ma. Feddali na itam ag taqoom ci jëflantey mbokk ak xaritoo yi yàgg a dox ci diggante ñaari réew yi. 

Àddug Njiitu Jëwriñ yi a ngi jëmoon ci anam yi ñuy saytoo coow yi ci wàllu suuf, yoriinu sistemu poroteksoo sosiyaal bi ak fagaru ci jafe-jafe yi aju ci nawet bi. 

Lu soxal coowal suuf si, Njiitu Jëwriñ yi xamle na ne daanaka bis bu set ñu jot ay càkkuteef yu bari ci Primature yu jóge ci ay ma-réew yu dogu yuy sàkku ñu àtte leen ba ñu man a jotaat ci seen i yelleef. Ci misaal rekk, ”Direction générale de la Surveillance et du Contrôle de l'Occupation du Sol (DGSCOS)” jot na ci diggante 2024 ak 2025, ay junniy jure yu jëm ci coowi suuf yoy, yi ci ëpp ba fii pexe amagu ci. Njiitu Jëwriñ naqarlu na anam yi ñuy ngardàjjoo suuf si ci dëkki taax yi ak ci kaw gi te doon luy jur ag jaxasoo ci pénc mi, di gàllankoor itam déggoo gi ak suqalikug koom mi. Njiitu Jëwriñ yi sàkku na ci wànqaas yi mu soxal ñu jël matukaay yi war ngir taxaw ci jafe-jafe boobu. Ci loolu, xamle na ne dees na estaabiliise “Termes de Référence” yi ngir caytu gu matale te yamale ci wàllu suuf. Njiitu Jëwriñ yi taxawlu na bu baax ci ne askan wi lañu war a gën a bàyyi xel ci yeesal yi. Ci noonu, pàkk yi ñu jotoon a nangu ginnaaw càmbar yi ñu amal ci wàllu suuf si ci sémbi daggug mbeeraay gi niki lu mel ni ”Plan d’Urbanisme de Détail (PUD)” bi ci Ndakaaru, lotismaa yu Dàgga Xolpaa ak Mbuur 4, dees na leen gën a jariñoo, rawati na ci wàllu dëkkuwaayi ndimbal yi. Ci wàll woowu ba leegi, ñi amoon ay pàkk te indi firnde yu leer, ñu ngi leen di delloowaat seen yelleef jamono jii.

Njiitu Jëwriñ yi toftal ci def ub njàngat ci sistemu sekirite sosiyaal bu Senegaal biy jànkoonte ak jafe-jafe yu bari, rawati na ci wàllu doxaliin, ak ci wàllu yaatal gi ak baaxaayu yëngu yi. Maanaam, taxawaayu wànqaas yi yor wàllu sekirite sosiyaal daa desal ginnaaw wàll yu bari rawati na ñiy liggéeyal seen bopp ak ñi nekk ci eeformel bi. Sémb yi ñu ci jot a amal yépp ngir yaatal taxawu gi ba fii daa des lu bari. Ci geneen wàll, li màndargaal sistemu àllaateret bi mooy ay paasiyoŋ ak baaxaayu serwiis bu néew doole. Njiitu Jëwriñ yi li mu seetlu mooy yoriin wu séddalikoo ci wànqaas yu bari yu benn bu ne am looy saytu. Dogat-dogatee googu nag ci tëraliinu campeef day jafeel jëmmalug politig sosiyaal bu méngoo te doon benn. Ngir loolu nag, Njiitu Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Liggéey bi mu sumb ay waxtaan ci nees di def ba boole “Institution de Prévoyance Retraite du Sénégal (IPRES)” ak “Caisse de Sécurité sociale (CSS)” def ko genn campeef gu mag boole ci taxaw, ànd ko ak Jëwriñ Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, ci gaaw jàllale kot sekirite sosiyaal bu bees bi. 

Njiitu Jëwriñ yi jox na yitte ju far wàllu fagaru gi jëm ci jafe-jafe yi aju ci nawet bi nga xam ne yi ci gën a fés ñooy : wal yi, fengat yi, lab yi, wopp yiy bawoo ci ndox yi, jéeya yiy bawoo ci wàllu mbëj rawati na dënnu yi, ñàkk kaaraange gi ci yoon yi ak njéeréer yi. Ci loolu, jot nañu cee jël ay matuwaay yu bari yu jëm amal fagaru gu mucc ayib ci jafe-jafe yooyu ci Ndajey Jëwriñ yu ñu fi amal lu jiitu. Waaye nag, matukaay yooyu taxul ñu mucc bu baax ci jafe-jafe yooyu ak i njeexitalam, rawati na ci jamonoy soppikug njuux gu jéggi dayo. Njiitu Jëwriñ yi soññ na Jëwriñ yi mu soxal ñu jël matuwaay yi war ngir fagaru boole ko, bu dee am na, ñu man a wàññi bu baax jafe-jafe yi teg ci indi ci ay saafara yu wér te wóor. Mu tëjee ci soññ “Aviation civile et de la Météorologie (ANACIM)” mu fexe ba askan wi, rawati na baykat yi, sàmmkat yi, ñiy jëfandikoo yoon yi, nappkat yi ak ñeneen ñiy dem géej, ñu man di gaaw a jot ci xibaari meteo yi, nga xam ne dina leen may ñu man di sàmmonte ak sàrti kaaraange yi manul a ñàkk. 

Ci àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñ ji yor  wàllu topp “Agenda national de Transformation” bi àddu na ci pexe yi ñuy teg ngir doxal “Agenda national de Transformation” bi ; 
  • Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa bi àddu na ci matukaayi fagaru yi ak caytug wal yi ci nawetu 2025 biy dëgmal. 
  • Jëwriñu Caabal yi, Jokkalekaay yi ak Xarala yi àddu na ci tolluwaayu jëmmalug « New Deal Technologique» bi.

CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

  • Tënku kaadraas bi ci “Loi de Finances Rectificative 2025” bi.

Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi. 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE