SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 3i FANI SULET 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 03 MONTHS.JULY 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 3i fani sulet 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Njiitu Réew mi posewu na ci at mu beesum jullit ñi (1447 ci gàddaay gi) ngir ñaanal atum jàmm mbooleen lislaam ji ak julliti Senegaal yiy waaj a màggal guddig Tamxarit gi.

Njiitu Réew mi dikkaat na ci wotub sémbu joyyanti koppral yu atum 2025, anam yu mucc ayib yi béjjante yi amee ci wàllu njël li ak mbébet yi jëm ci dooraat yënguy koom mi. Rafetlu na anam yi ñu amalee liggéey bii ci kaw dal ak sàmmonte ak sàrt ak tëraliin yi tënk doxiinu campeefi réew mi. Ci loolu, ndokkale na Ngóornamaŋ bi ak Ngomblaan gi ci waajtaay wu jaar yoon wi ak mucc ayibug waxtaan yi tax ñu leeral askan wi ci tolluwaayu koppari réew mi niki noonu eewestismaa ak yëngu yi Nguur gi di amal ngir jëmmalug “Agenda national de Transformation” bi. Sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi, mu wéyal jéego yi jëm ci gën a sellal yoriin wi ci alalu askan wi boole ko ak gën a liggéey ci eewestismaa yu am njariñ, fay bor yi ñu ame ci biir réew mi ak suqali sektéer piriwe bi.

Ci wàll woowu jëm ci joyyanti tolluwaayu koom mi, Njiitu Réew mi fàttali na ag taqoom ci gën a baaxal xar-kanamu jëflante yi war a gën a yékkatiku ba méngoo ak yi gën a mucc ayib ci àddina si. Ci loolu, fàttali na ne, fàww Njiitu Jëwriñ yi amal topp gu wér, waajtaayu “Forum Invest in Sénégal” bi ñu jàpp 07 ak 08i fani oktoobar 2025, fexe cee sóob bu baax sektéer piriweb réew mi. Ci geneen wàll, xamle na ne fàww ñu xoolaat, ngir lu gën a xereñ te ëpp i njariñ, matukaay ak jumtukaay yi ñuy kopparalee koomum réew mi. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, Jëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo gi ak Jëwriñ ji nekk ci wetu Njiitu Réew mi te yor topp doxal ak xayma ”Agenda national de Transformation Vision Sénégal 2050” bi, ñu gaaral, ci kilifteefu Njiitu Jëwriñ yi, pexem boole jumtukaayi kopparalug pénc mi (CDC, FONSIS, FONGIP, BNDE, BHS, LBA, FONAMIF, DER/FJ…). Pexe moomu nag dina tax, ci pas-pas bu yees, ñu gën a am koom muy bawoo ak a des ci réew mi jaare ko ci dajale gu mucc ayib ci balluwaay yi ci réew mi. 

Ak fi jamono tollu te li koy màndargaal di ñàkk a wóoradi ak wàññikug marse kopparal yi, fàww nu sukkandiku jëkk ci sunu dooley bopp jaare ko ci jëmmal politigu mbay mu bees ak bay dunde, peeg wàllu yasara gi, baral jéego yi jëm ci samp ay ndefar, gën a jariñoo sunu mbeeraay yi ak jëfandikoo  sunu balli mbindare yi ak filiyeer yiy yi man a jur liggéey yu bari. Ci wàllu yoriinu pénc moomu nag, li war mooy gën cee sóob ñiy yëngu ci wàllu koom mi te nekk ci biir réew mi ak ca biti réew ak mbooleem wànqaasi ndoxalug pénc mi. Mu tëjee bunt boobu moom Njiitu Réew mi ci soññ Njiitu Jëwriñ yi mu taxaw, li ko dalee tay, jëm ci waajal, sukkandiku ko ci yitte yi gën a far ak porogaraam yi ñu jot a walide, Sémbu yoonal Koppar yi ñu war a jëfandikoo ci atum 2026.

Lu jëm ci pexem lëkkaloo gu bees ak réewi àddina si ak gën a dooleel lëngoo piblig-piriwe, Njiitu Réew mi, fàttali na Ngóornamaŋ bi ne gis-gisu Senegaal gu moom boppam, gu tegu ci yoon te naat, mu ngi sampu ci doxaliinu lëkkaloo, lëngoo ak kopparal gu lalu ci tijjeeku, wegante, sàmm njariñi réew mi ak amal lëkkaloo yu wàll wu ne di gis boppam. Ci loolu, ndokkale na Njiitu Jëwriñ yi ak tañ  wi mu àndaloon, ci waajtaay wu mucc ayib wi ak ndam lu rëy li ñu am ci tukki nemmiku bi ñu doon amal ca Réewum Siin. Sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi mu taxaw, ànd ko ak Jëwriñ yi ak ñi mbir mi soxal ci piblig bi ak ci piriwe bi, ci amal topp gu wér jëm ci gaaw jëmmal mbooleem déggoo yi, jaayante yi ak sémb yi ñu tënkee ci tukki bu am solo bii. Ci wàll woowu ba leegi, xamal na Jëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo ne war naa gaaw yeggali jubluwaayu pexe mi jëm ci suqali sektéer piriwe bi te méngale ko ak politigu koom mi Nguur gi teg. Ci geneen wàll, xamle na ne fàww ñu am tegtalukaay bu wér ci wàllu lëkkaloo ci àddina si ak lëngoo yi war a gën a jagal caytu gi diggante njëwriñ yi ci wàllu lëkkaloo ci àddina si ak jëmmal gu wér, ànd ak yaxanal te xereñ ci lëngoog piblig-piriwe, ci pàcc bu ne, te bàyyiwaale xel pàcc-pàccee sémb yu am solo yi man a jur ay xëy ci Pôles yi.

Lootaabeg “Jeux olympiques de la Jeunesse (JOJ) Dakar 2026” yi ak suqali tàggat yaram ci ndaw ñi dañoo war a gën a dooleel réew mépp, rawati na bokk-moomeel yi, ci ay jumtukaayi tàggat yaram yu baax te tegu ci yoon. Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñu Tàggat Yaram ji mu baral jéego yi, ànd ko ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, jëm ci jëmmal sémb wi ñu teg ci réew mi ngir tabax ay jumtukaayi tàggat yaram boole ko ak taxaw temm ci baral liggéey yi aju ci JOJ yi, waaye itam dooraat liggéey yi yeggagul. Ci geneen wàll, woo na Jëwriñu Tàggat Yaram ji mu taxaw ànd ko ak njëwriñ yi mu soxal ak mbooleem wànqaasi pénc mi (Gox yi ak Goxaan yi, SOGIP, OGIS, Kurél, ONCAV, …) ak piriwe yi mu soxal, ci rëdd, sukkandiku ko ci jumtukaay yi, benn kaadaru yoriin wu tegu ci yoon ci jumtukaayu tàggat yaram yi. Sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi ak Jëwriñu Tàggat Yaram ji ñu baral jéego yi jëm ci jàllale balaa yàgg ci Ndiisoog Jëwriñ yi, lii di “Charte du Sport“ bi.

Ci wàllu arminaatu laamisoom, Njiitu Réew mi dikkaat na ci teewam, 30i fani suwe ba 2i fani sulet 2025 ca “Séville“, ca Espaañ, ca 4eelu Ndaje mi ñu doon amal ci kopparalug suqaliku gi. Tukki bii nag am pose la woon ci Njiitu Réew mi, mu feddali taqoog Senegaal ci lëkkaloo gu dul beddi kenn teg ci woote ngir ñu amal ay yeesal ci ni ñuy kopparalee ci àddina si, gën a yamale ak doxal yoon ci ni ñuy saytoo bor yi, jot ci kopparal ak teg sistemu galag bu bees ci àddina si. 

 Cig àddoom, Njiitu Jëwriñ yi fàttali na mbaax yi Senegaal yàgg a taqoo ci wàllu lëkkaloo ci wàllu koom gu tegu ci sunu mbaaxi cosaan, tijjeeku, moom sa bopp, laamisoo ak réewi digaloo yi, feddali jëflante yi ak partaneeri cosaan yi ak mbébeti  amal lëngoo yu bees.

Njiitu Jëwriñ yi dikkaat na ci tilukki liggéey ak xaritoo yi mu doon amal ci Afrig ak ca Asi. Ci geneen wàll, fàttali na ndigal yi ko Njiitu Réew mi dénk ngir mu doxal bu baax sunu lëkkaloo ak réewi “Proche” ak “Moyen Orient” yi ak  li des ci Asi. Ngir taxaw temm nag ci doxal sas woowu, am na wenn sémbu dekkere bu jëm ci lootaabe ak doxaliinu Primature buy waajal taxawal benn bànqaas bu ñu koy jagleel. Muy kon fexee am ug yëgoo ci lëkkaloo gi dox sunu digg ak biti réew, lépp ngir jàpp bu baax ci saytu jëflante yi ak biti réew, rawati na ci wàllu koom mi, nekkiin wi, mbatiit mi ak kéew mi. Bànqaas bu bees boobu dina gën a dëgëral sunu jëflantey koom, gën a gunge sektéer piriwe bi ak dooleel yoriin wu leer ngir suqaliku gu sax te ànd ak moom sa bopp.

Njiitu Jewriñ yi dikkaat na ci solos amal doxaliin wu yees ci sunu wàllu laamisoo. Firnde li ci gën a fés nag mooy, naalu seexale  gi ñu namm a amal diggante tundi Siin ya ak juróom ñetti “pôles territoires” yu Senegaal.

Njiitu Jëwriñ yi dikkaat na ci xew-xew yu tiis yi ñu seetlu ca Kàmbereen ak ca Rooso ba waral nit ñu ca ñàkk seen bakkan. 

 Way-kaaraange yi seen uw sas mooy sàmm kaaraangeg nit ñi ak seen alal ak wattu dalug pénc mi. Sas woowu nag dafa war a sori lépp luy xeetu metiital ak doxaliin wu niteedi wu ñuy teg ci kaw askan wi. 

Niki ko Njiitu Réew mi diglee, Njiitu Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi ak Jëwriñu Larme bi, ñu amal càmbar gu matale gu ñu ko war a jébbal gën gaa yeex 30i fani nowàmbar 2025 boole ko ak xoolaat bu baax tàggatug way-kaaraange yi, ngir gën a feddali, ci mbooleem yëngu yi ñuy amal, fulla gu ànd ak sàmmonte ak yelleef ak diññite askan wi, ci kaw sàrt yi ñu tëral.

Ci àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñ ji yor ci wetu Njiitu Réew mi toppug doxal ak xayma “Agenda national de Transformation Sénégal 2050” bi àddu na ci doxalug pexem “Agenda national de Transformation” bi. 


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi. 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE