SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 27i FANI NOWÀMBAR 2024

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 27 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, àllarba 27i fani nowàmbar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoorteel i Kàddoom, Njiitu Réew mi xamal na Ndiisoo gi ne, dina jël dekkere, ngir joxe lélub tijjitel jataay bu njëkk bi ñeel Ngomblaan gi ñu fal bees ni ko Ndayi Sàrti Réew mi diglee.

Lu soxal mbirum soppi gu matale ci jànguney pénc mi, Njiitu Réew mi fàttali na Njiital Jëwriñ yi jamp gi nekk ci jël matukaay yu wóor ngir ñu man a wéyal njàng mi te lépp ànd ak dal ci biir jàngune yi ak ci warabi njàng mu kawe mi. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu gi ak Fent ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, ñu ànd ak Rektéer yi ak ñi jiite warabi dëkkuwaayi njàngaan yi, ci caytug Njiital Jëwriñ yi, gaaw teg pexe yu jamp yu jëm ci amal arminaat bu wér ngir jébbale mbooleem liggéey yi Nguur gi sumboon ci jànguney pénc mi dale ko ci aamfitiyaatar yi, buluy jàgukaay yi, lekkukaay yi ak dëkkuwaay yi.

Ci yoon wi ñu jël jëm ci yeesalaat doxaliinu jàngune yi, Njiitu Réew mi xamle na solos gën a dooleel, te ànd ko ak njabootu jàngune yi, benn doxaliinu koom bu ànd ak dëppoo ngir man a taxaw ci amal doxaliin wu mucc ayib ak xereñteg  doxaliinu njàng mu kawe mi ak gëstu gi. Boo xoolee nag ni limub njàngaan yi di yokkoo at mu ne, war na ci Ngóornamaŋ bi, ci lu muy déggoo ak jàngune yi, mu taxawal politig bu yees ci ni ñuy saytoo nit ñi ngir teg pexe yu mucc ayib ci ni ñuy tasaare ñiy door a am BAC yees ci jàngune yi boole ko ak saytuwaat njëlul jàngalekat yi ngir taxawu leen ca na lu waree. Sàkku na ci Jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi, mu xalaat ci gis-gisu mottalante, fexee boole yenn liggéey yi te bàyyiwaale xel kàrtu jàngune yi nga xam ne seen jubluwaay dafa war a méngoo ak pexey « Póol » yi ñuy samp ci gox yi.

Ngir tëj bunt boobu, Njiitu Réew mi soññ na Jëwriñu ji yor wàllu Njàng mu kawe mi, mu lëngoo  ak Jëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo gi, baral jéego yi jëm ci matale mbind mi ñeel politigu pàcc bi soxal Njàng mu kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi. Yoon wu yees woowu ñu war a tegu dafa war a gën a dooleel taxawaay bu am solo bi Njàng mu kawe mi am ci biir dixaliinu pénc mi ak waar wi mu war a bay ci waajal ak joxaat gëdda doomi réew mi, di keno bu am solo ci « Vision Sénégal 2050 ».

Njiitu Réew mi àddu na ci lu jëm ci gën a dooleel cër bi daara war a am ci wàllu njàng mi ak tàggatu gi. Daara daa bokk ci keno yi gën a am solo ci yarug goney réew mi. Waaye ba fii warabi jàngukaay yooyu dese nañu leen a dugal bu baax ci sunum njàng moo xam muy ci seneraal bi, ci tàggatu xereñ gi walla sax gu xarala gi. Loolu tax na mu fàttali Ngóornamaŋ bi ne fàww ñu gën a sóob daara yi ci njàngum réew mi jaare ko ci xam mbooleem daara yi ci réew mi, defal ay jagle ñeel warab yooyu ak jàngalekat yu ñuy tàggat bu wér ci warab yu ñuy samp, amal ay tàggatu yu xereñ ñeel dongo yi ngir yombalal leen ñu man a bokk ci liy doxal koom mi. Soññ na Jëwriñu Njàng mi mu ànd ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, gaaw matale coppite yu wér, wóor te ànd ak dëppoo ngir moderniise daara yi. Xamal na Ndiisoo gi ne, dina jiite bis bi ñu jagleel daara yi ci réew mi te ñu war koo amal alxemes 28i fani nowàmbar 2024.

Lu soxal taxawu ak ñàkk a beddi way-laago yi ak màggalug bisub 3i fani desàmbar 2024 bi ñu leen jagleel ci àddina si, Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi wàccuwaay bu am solo bi ñu war a jox way-néew doole yii ci askan wi ci biir politig yi ñuy teg jëm ci yamale ak gën leen a boole ci askan wi. Woo na Jëwriñu Paj mi ak Dimbalante gi ak Jëwriñu Njaboot yi ak Jàppalante gi ñu gën a dooleel taxawaayu nguur gi jëm ci ñoom. Sàkku na ci Jëwriñ yi mu soxal ñu gaaw matale « Loi d’orientation sociale » l° 2010-15 bu 06i fani sulet 2010 bi jëm ci dooleel ak sàmm yelleefi way-laago yi, rawati na sistemu kàrti yamale muur yi, ak waajal pexe yu yees yu ñu war a teg ci réew mi jëm ci gunge way-laago yi. 

Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi xamal na Njiital Jëwriñ yi solos yombal, sukkandiku ko ci lijaasa yi ñu am ak ci kaw sàrt yi ñu tëral, jël ak tabb ay way-laago ci warabi liggéeyukaayi pénc mi. Dugal way-laago yi ci warabi liggéeyukaayi piriwe bi jaare ko ci amal ay diisoo ak mbootaayu njaatige yi. Sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Njàng mi, ju Tàggatu gu xereñ gi ak ju Njàng mu kawe mi, ñu gën a bàyyi xel lekool yi, warab yi ñu jagleel njàng, tàggatu ak xëyu nit ñi ame laago.

Mu tëjee moom Njiitu Réew mi ci xamal Ndiisoo gi ne dina jiite, dibéer 1 panu desàmbar 2024, ci teewaayu gan ñu bari ñu bawoo biti réew, xewu fàttaliku 80eelu atu « bóom gi amoon Caaroy ».

Njiital Jëwriñ yi cig àddoom, ginnaaw ba mu fàttalee ndigal yi Njiitu Réew mi joxoon Ngóornamaŋ bi jëm ci taxawal ay diisoo yu wóor te sax ak partaneer yi ak mbootaayi liggéeykat yi, sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu liggéey ak Jëwriñ yi mu soxal, ñu xamal ko ca na mu gën a gaawee, fan lañu tollu ci taxawu tomb yi liggéeykat yi doon sàkku boole ko ak arminaatu ndaje yi ñu jàpp a amal walla sax ñu jot koo amal ba noppi ak mbootaay yi diggante awril ak nowàmbar 2024. Nga xam ne dina ci man a sukkandiku ngir jébbal Njiitu Réew mi arminaatu ndaje yi mu fas yéenee amal ak mbootaayi liggéeykat yi jëm ci taxawal déggoo gu yees ngir indi ag dal ci warabi liggéeyukaay yi.

Lu soxal caytug warabi jaayukaay yi ginnaaw lakk gi am bu yàggul ca marse sàntaraal bu Cees, Njiitu Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu yaxantu gi, mu amal ag xayma ci sémbu moderniise ak saytu ja yi di PROMOGEN, ngir gaaral, ci àpp bu yenu maanaa, pexe mu jëm ci jëmmal sas wi ñu jox kurél googu. Fii ak boobu, woo na Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, mu lëkkaloo ak Jëwriñ yi mu soxal ak kilifay ndoxal gi ak goxaan yi, jël matuwaay yu jamp ngir rawati na saytu ak teg jumtukaayi kaaraange yu mucc ayib. 

Mu daaneel moom Njiital Jëwriñ yi ci fàttali solo si wànqaasi njëwriñ gu ne war a jox ci amal doxal gu mucc ayib ñeel ndigal yiy bawoo ci Ndiisoog Jëwriñ yi niki noonu ndiisoo ak ndaje yiy am diggante jëwriñ yi, ci lu soxal saytu gu war a tegu ci amal njureef yu wér te wóor. 


CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:

Jëwriñu Mbay mi, bay dunde ak Càmm gi àddu na ci waajtaayu kàmpaañu njaayum gerte gi ci atum 2024/2025.


CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

Ci wàllu Primature:

Sémbu dekkere bi jëm ci sos ak taxawal sàrti lootaabe ak doxiinu pekk biy lëkkale ak a topp sémb yi ak naal yi di BOCS.


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE