SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 26i FANI MARS 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 26 MONTHS.MARCH 2025

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 26i fani mars 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi tiislu na génn àddunag Me Seex Xuraysi Ba. Senegaal ñàkk ñàkk na layookat bu xereñ, ku amoon kàddu ci baro bi, nituk pas-pas ku gëmoon yoon ak péexte.

Njiitu Réew mi àddu na ci menn at mi mu jot a def ci boppu réew mi ginnaaw ñetteelu alternaas bi am ci demokaraasib Senegaal. 24i fani mars 2024, ci la ko askanu Senegaal faloon mu war a doon Njiitu Réew mi, ci wërngal wu njëkk wi ak 54,18% ci wétt yi. Ñu feddaliwaat kóolute googu jox lu tollu ci 130i depite limkag PASTEF gi Njiital Jëwriñ yi Usmaan Sonko jiite woon ca joŋantey lesislatif yu 17i fani nowàmbar 2024.

Njiitu Réew, feddaliwaat na cantam ak ngërëmam jëme ci askanu Senegaal wu jàmbaare wii ko wóolu ba dénk ko, ak ni muy jaayante saa su ne taxaw temm ci gunge Ngóornamaŋ bi, ngir mu man a samp ci jàmm, déggoo ci réew mi ak taxawaayu kilifteef giy tax ñu man a yegg ci Senegaal gu moom boppam, jub te naat. Feddali na jaayanteg Ngóornamaŋ bi, ci ñaareelu at mii ñuy door ci kay gi, ne dinañu def seen kéem tolluwaayu kàttan ngir baral jéego yi jëm ci amal ay coppite, càmbar ni ñu yoree woon alal ji ak jubbanti réew mi, waaye nag rawati na dooraat bu baax yëngu yi ci wàllu koom mi ak dundiin wi niki ñu ko tënkee ci biir « Agenda national de Transformation » bi ñu fésaloon 14i fani oktoobar 2024.  

Lu jëm ci wa jataayu korite giy màndargaal njeextalu weeeu koor wu sell wi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi, rawati na ci Jëwriñu Biir Réew mi, Jëwriñu Larme bi, Jëwriñu Yaaleg suuf si ak jawwu ji, Jëwriñu Yaxantu gi ak Jëwriñu Yaaleg Géej gi, ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir fexe ba dund bi yemb lool ci ja yi, niki noonu ñu amal korite gi ci anam yu mucc ayib fépp ci réew mi. 

Lu soxal ràppoor 2023-2024 bi Mejaatéeru Repiblig bi di amal at mu ne, te mu jot ci alaxemes 20i fani mars 2025, Njiitu Réew mi ndokkeelaat na, Njiit li ci liggéey bu am solo bi mu amal jëm ci sàmm yeleefi ma-réew yi ak ñiy jëfandikoo serwiis piblig bi, waaye tamit joyyanti gi war ci doxaliin ak xereñteg ndoxal yi. Sàkku na ci mbooleem ku bokk ci Ngóornamaŋ bi mu jëfe digle yi nekk ci biir ràppoor bii te indi ay tontu yu wér ci càkkuteef yi, tànn ñuy teewal Mejaatéer bi ci njëwriñ gu ne boole ko itam taxaw ci fexe ba am ay ndawi Mejaatéer bi ci mbooleem tund yi ak gox yi ak goxaan yi. Bu dee jàngat yi ñu war a def ci ràppooru 2023-2024 bi, xamal na Ngóornamaŋ bi ne fàww mu gën a bàyyi xel bu baax anam yi ñuy téyee nit ñi ci kaso yi jaare ko ci gën a taxawu xale yi nekk ciy jafe-jafe. Ngóornamaŋ bi dina taxaw temm itam ci saytu tolluwaayu liggéeykat yi ak àllateret yi Mejatéer bi jot a càmbar seen wayndare boole ko ak taxaw ca na mu gën a gaawee ci njàmbat yi jëm ci gën a jagal xar-kanamu liggéeyukay yi ci wàllu yoon, ci wàllu koom ak ci wàllu nekkiin. 

Njiitu Réew mi àddu na ci jafe-jafe yi am ci fexee amal caytu gu mucc ayib ci nawet biy dëgmal te laaj fuglu, waajtaay wu wóor ak lootaabewu ci fànn yépp. Sàkku na ci Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa bi mu jël mbooleem matuwaay yi war, ngir sumb ca na mu gën a gaawee, yëngu yi jëm ci waajal nawet bi fépp ci réew mi. Fàttali na solos gaaw liggéey ci waxtoom, yënguy fuglu yi jëm ci fattarndi kanal yi ci njiital ONAS, waaye tamit jëmmal doxaliin wu leer jëm ci fuglu ak saytu wal yi. Ci loolu kon, fàww ñu taxaw ci topp yooni ndox yi ci réew mi ànd ko ko mbootaay yii di OMVS ak OMVG ngir bàyyiwaale xel risk yi man a bawoo ci fengat yi ci pexe yi ñu war a teg jëm ci fuglu ak saytu wal yi. 

Njiitu Réew mi xamle na ne li gën a jamp fii mu ne mooy gën a jox yitte ci gaaw yeggali liggéey yi ñu sumboon jëm ci xeex wal yi, rawati na ci gox yu mel ni Kër Ma-Saar (Kër Ma-Saar Sud, Unite 3 Parsel Aseni) ak Mbàkke (Tuubaa). Ci wàll woowu ba leegi, xamal na Jëwriñu Jumtukaayi tabax yi ne fàww ñu gën a def pasteef ci jëmmal Palaŋu toppatoo ak defaraat yenn yoon yi rawati na ci tund ak gox yi am i jafe-jafe. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu amal, ci biir weeru awril wi, am ndaje diggante jëwriñ yi ngir waxtaane fuglu gi ñu war a def ci wal yi ak dooraat liggéeyi kurél giy saytu fuglug wal yi ci réew mi. 

Senegaal dina màggal, 04i fani awril 2025, 65eelu at mi mu moome woon boppam, di am pose ci Njiitu Réew mi mu dellusiwaat ci wareefu waxtaan ba juboo ci fexee soppi turi yeen tabax yi ak warabi pénc mi. Fàttali na Ngóornamaŋ bi ne, jumtukaayi yoon yi, yu mel ni xàll yu mag yi, buluwaar yi, mbedd yi, niki noonu warabi pénc mi nekk ci sunu dëkki taax yi ci bokk-moomeel yi, yépp dañoo war a yor tur yuy fàttali mboorum Senegaal ak Afrig. Dañoo war a màndargaal tur yuy saxal ci xel yépp mbooleem jëf ak jëmm yi doonoon ñu ràññiku ci dundug réew mi, niki noonu mbokkoo ak bennoog kembaar gi.

Cig àddoom, Njiital Jëwriñ ji dikkaat na ci jëmmalug « Agenda national de Transformation systémique » bu Senegaal, jaare ko ci fàttali taxawaay bi ñu war a am jëm ci taxaw temm ci diggante sémb yu am solo yi ak yaatal gi ci gox yi. Rafetlu na jataay yi ñu jot a amal jëm ci yaatal yenn sémb yi ak naal yi war a gaarànti ndam li ñuy séntu ci lëkkale pàcc yi manul a ñàkk ci gis-gisu doxal « filières » yi ak « chaînes de valeurs » yi ñu tënk ngir « Agenda Sénégal 2050 » bi. Taxaw na bu baax ci yitte ji ñu war a jox ci sémb yi ñuy woowee « projets catalytiques » ak yi ñu war a gaaw jëmmal. 

Njiital Jëwriñ yi teg ci ñaax Jëwriñ yi ñu door pàccu doxal gi jaare ko ci gaaw matale yoon yi ñu war a jaar ngir xamle tolluwaayu koppar yi war a dem ci sémb yi ñu jot a tànn ci jataay yooyu ak fexee joyyanti, ci loolu, bu ko jaree, seen « Lettres de Politique sectorielle (LPS) » yi, ngir waajal « Loi de Finance rectificative 2025 » bi njëkk. Ci loolu, xamle na, ci tolluwaay bi ñu fekk « finaas piblig » yi, ay « arbitrages budgétaires » yu mu war a jébbal Njiitu Réew mi ginnaaw ba mu ci diisoo ak Jëwriñ ji yor wàllu Njël li ak ji yor wàllu Koom mi. 

Ci ñaareelu tombu àddoom, Njiital Jëwriñ yi dikkaat na ci ci tolluwaay bi ñu amalee ndoortel  ñaari sémb yii di « Programme d’Appui aux Acteurs de l’Economie sociale et solidaire (PROGRESS) » bu « Programme de 1000 Coopératives solidaires (PCS) » te mu doon ko jiite. Ci loolu, soññe na ci mbébetu xeex ndóol gu tar gi am ci Senegaal te « Agenda national de Transformation » bi fas ko yéenee saafara. Mu sukkandiku ci njureef yi bawoo ci lànketub ANSD bi mu amaloon diggante 2019 ak 2022 ci anam yi njaboot yi di dunde te fésal ko at mii weesu, Njiital Jëwriñ yi, xamle na, bu weeso ni limub nit ñu ndóol ñi di yokkoo, tolluwaayu ndóol bu jéggi dayo bi am ci kaw gi boole ko màggetaayu nit ñi, néewug li ñuy am ak jafe-jafe yu metti yi ñuy jànkoonteel ngir jot ci serwiis yi manul a ñàkk yu mel ni am paj, am ndox, am njàng ak ub kuraŋ.

Ci loolu nag, Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Palaŋ mu gaaw yeesal xayma yi fi nekk jamono jii ngir xam dëgg-dëgg tegtalukaay bu wér ngir yoriinu réew mi. Xamle na itam ne fàww ñu boole jumtukaay yi ñu teg ngir xeex ndóol gi ngir taxawal ekositem bu gën a xereñ ci anam yi ñuy xeexe ndóol gi. Ci mbébet moomu, jël na dogalu taxawal, ci kilifteefu Primature, genn kurélug diisoo diggante Jëwriñ yi mu soxal, yu mel ni yi yor wàllu jàppalante gi, paj mi, dimbalante gi, koomum jàppal ma jàpp mi, mbay mi ak càmm gi. Xamle na ne wayndare wi gën a jamp te ñu war cee taxaw mooy, taxawu bu wér waa kaw gi, boole ci jur gi, loolu tax na mu sàkku ñu jël ci ay matuwaay yu wóor te jébbal ko ko ca na mu gën a gaawe. 

Mu daanele, moom Njiital Jëwriñ yi, fàttali jëwriñ yi,  ñu fexee a sàmmonte ak àpp yi mu leen jox ngir ñu war ko cee jébbal dogali joyyanti yi jëm ci wàññi bu baax anam yi nguur gi di dundee. Leerlu na itam ci liggéey yi ñu nekk di amal jamono jii ca njëwriñ gi yor wàllu Koppar yi, jëm ci tàmblee jëfandikoo palaatform bi BECEAO nekk di taxawal ngir ñu man fay jaarele payum lempo yi ak wareefi duwaañ yi. 


 

Lu soxal àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñu Yasara gi, Petorol bi ak Mbell yi àddu na ci : 
  • tolluwaayu jëmmal « Fonds d’Appui et de Péréquation pour les Collectivités territoriales »;
  • tolluwaayu jëmmal «Fonds de Réhabilitation des Sites miniers et de Carrières » ;
  • Tolluwaayu jëmmal benn sistem dekklaaraatif ngir dajale koppar yi ñu war a fay ci mbell yi.
  • Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi àddu na ci pexe yi ñu teg ngir dund bi doon lu yemb ci ja yi;
  • Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde gi ak Càmm gi àddu na ci kàmpaañu njaayum gerte gi ak toppug kàmpaañu payteef yi.

 

Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi. 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE