Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 22i fani sãawiye 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi dikkaat na ci xew wu njëkk wu ndajem kilifa ak Njiiti wànqaasi Pénc mi (CAMP), ñu ko doon amal altine 20i fani sãawiye 2025. Rafetlu na ndam lu mucc ayib li am ci ndaje mu mag mii bokk ci arminaatu Repiblig bi. Jaajëfal na Jëwriñ yi ak Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Njéndel Réew mi ci anam yu mucc ayib yi ñu lootaabee ndaje mi. Muy ndaje mom, guleet ñu amal ko, day sóob administaraasoo yi ci yoonu taxawaay bu bees, méngale ak jamono ak soppiku gu dëppoo ak keno, tegtal, yitte ak jubluwaayu « Vision Sénégal 2050. »
Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu jël mbooleem matuwaay yi war ngir yaatal digle yi bawoo ci ndaje mi, rawati na jëf yu baax yi wànqaas ak kurél yiy càmbar joxe ndigal, rawati na ci gën a jubbanti yoriinu pénc mi ci fànn yépp. Soññee na itam ci ñu baral jéego yi jëm ci yeesal foŋsoo piblig bi boole ko ak mottali kaadaru jëmmal sàrt 2022 bi ci wàllu sektéer piblig bi ak saytu gafag réew mi. Ci loolu, woo na Njiital Jëwriñ yi mu taxaw temm ci delloosi yoriin wu sell wu ñu gën a dooleel ci wànqaasi sektéer parapiblig bi ak ci këri liggéeyukaay yu am solo yi. Muy kon fexee yaatal ci lu gaaw kontraa « de performaas » yi ak jéem a peeg risk yi ci wàllu koppari réew mi.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu baral jéego yi jëm ci jëmmal ndànk-ndànk «pôles territoires » yi ngir gën a màndargaal tànneef gu wóor gi ñu am ci yaatal politig piblig yi fépp ci réew mi ci kaw jàppalante ak yamale. Sàkku na itam ci Njiital Jëwriñ yi mu gën a taxaw ci fésal riptiir ci wàllu administaraasoo bi boole ko ak dooleel wàllu « digital » bi ci serwiis yi, yeesal bind yi aju ci foŋsoo piblig ak fexee saxal pas-pasu njureef yu lalu ci soppi sistem gu matale fépp ci wànqaasi pénc mi.
« Vision Sénégal 2050 » dina gën a taxaw ci dooleel cér bi sektéer piriwe bi am ci suqali koom mi ak nekkiinu askan wi. Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu sumb ay waxtaan yu wóor diggam ak « industriel » yi ak operaatéer ekonomig yi ngir man a teg pexe yu ñu déggoo jëm ci suqali sektéer piriweb réew mi te bàyyiwaale ci xel gàllaankoor yi aju ci tolluwaayu àddina si. Diisoo yooyu nag lu manul a ñàkk la ngir baral jéego yi jëm ci yeggale sémbu yoonal wi aju ci wàllu « souveraineté économique » gi war a jëmmal politig bu wér bi nu bokk yéene ci tabax koom muy bawoo tey des ci réew mi, nga xam ne moo man a wommat coppite gu matale gi nu namm ci Senegaal.
Ci wàll woowu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu taxaw ci amal saytu gu xereñ te matale ci def Senegaal mu gën a xemmemu boole ko ak koom mu am doole ci réew mi jaare ko ci dooleel ak sóob ci loolu mbooleem sékteer yi ak njëwriñ yi. Xamle na itam ne fàww ñu gën a dooleel taxawaayu APIX ci wàllu jóo ak topp pàccu jëflante yi jaare ko ci tegaat pas-pas bu bees ci dooleel eewestismaa yi ak Senegaal gu xemmemu. Joxe na ndigal itam ngir ñu dekkalaat «Observatoire national des Investissements (ONI) » bi nga xam ne leegi ca Primature lañu koy féetale. Ci wàll woowu, sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi, mu ànd ak Jëwriñ yi yor wàllu Koom mi, wàllu Koppar yi, wàllu Yaxantu gi, wàllu Ndefar gi ak wàllu Xarala yi, koordone, ci ndoxalug APIX, bisub « Forum invest in Sénégal » bi ñu war a amal 24 ak 25i fani awril 2025. Xew-xewu koom boobu nag dina doon lu am solo ngir fésal réewum Senegaal ci wàllu lëkkaloo ak eewestismaa yiy bawoo biti réew.
Turism bi nag doon na pàcc bu am solo ci jëmmal « vision Sénégal 2050 » ak taxawal ay xëy. Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñu Turism bi ak Artisanaa, ñu jël mbooleem matuwaay yi war, ginnaaw ba ñu ci diisoo ak ñiy yëngu ci wàll wi, dooleel ak dekkalaat sektéer bi boole ko ak fésal warab yi ak man-manu Senegaal ci wàllu turism. Xamle na ne jot na sëkk ñu yokk kaaraange gi ci mbooleem tund ak goxi turism yu Senegaal jaare ko ci lootaabewaat poliis bi yor wàllu turism. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu amal ci fan yii di ñëw, am ndaje diggante jëwriñ yi ci wàllu turism bi ngir waxtaane mbooleem dogal yu jamp yi ñu war a jël jëm ci suqaliku gu matale ci wàll wi.
Lakk yu bari yi ak jafe-jafey kaaraange yi ñu seetlu ci marse yu bari ci réew mi te laaj ay dogal yu wóor yu tukkee ci Ngóornamaŋ bi tax na, Njiitu Réew mi sàkku ci Jëwriñ yi yor wàllu Yaxantu ak wàllu Gox yi ak Goxaan yi, ñu taxaw temm ànd ko ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, yokk kaaraange gi ak fexe ba marse yi ak warabi yaxantu yi dëppoo ak yoon fépp ci réew mi. Ci loolu, woo na Jëwriñ ji yor wàllu Yaxantu gi mu baral jéego yi jëm ci xayma niki noonu tëggaat sémb wii jëm ci moderniise ak saytu marse yi di PROMOGEN, sukkandiku ko ci yiite yu bees yi Nguur gi am ci wàllu dagg ak tabax ay warabi jaayukaay.
Njiital Jëwriñ yi a dooree ay kàddoom ci liggéey yi ñuy amal jëm ci jëmmal « Stratégie nationale de Développement (SND) 2025-2029 » bi, rawati na mottali mbindum sémb yi, naal yi ak yeesal yi niki noonu yitte yi ñu leen war a jox, ba man a jébbale wayndare wi ci Ndiisoog Jëwriñ yi, gën gaa yeex balaa weeru féewarye 2025 wi di xaaj.
Njiital Jëwriñ yi teg ci xamle ne jot na sëkk ñu tëggaat sektéeru enersi bi. Xamle na ci loolu ne dees na taxawal benn « komite bu jëwriñ yi di séq », ci njiital Jëwriñu Yasara gi, Petorol bi ak Mbell yi, ngir teg aw yoon ak i pexe yu jëm ci saafara mbooleem jafe-jafe yi wàll wi di jànkonteel. War na ci Komite boobu itam mu gaaral ay pexe yu sax yu jëm ci wàññi njëgu enersi bi. Njureef yiy bawoo ci Komite boobu nag, wareef na koo sóoraale ci digle yi ñu war a tegtaloo ngir mottali sémbu yoonal wi jëm ci tëggaat SENELEC ak sémbu dekkere wi war a taxawal anam yi ci eewestiséeri Senegaal yi war a bokkee niki noonu yoon wi soxal palaŋu kontënii lokaal bi ci wàllu kuraŋ bi. Mbooleem wayndare woowu warees na koo jébale ci Ndiisoo gi ci biir weeru féewarye 2025.
Ci geneen wàll, Njiital Jëwriñ yi yëgal na Ndiisoo gi ne taxawal nañu benn komite ad hoc bu war a liggéey ci gaaral ay pexe yu jëm ci suqali wàllu fosfaat bi, balaa njeextalu weeru féewarye 2025.
Mu tëjee moom Njiital Jëwriñ yi, dikkaat bu baax ci jafe-jafey koppar yi « Air Senegaal SA » ak « AIBD SA » di dund ak jampug tëggaat ñaari kër yooyu. Ci loolu, dina jiite ñaari ndaje diggante jëwriñ yi, ñu jagleel leen waxtaane tolluwaayu ñaari kër yooyu, ci ñaareelu xaaju weeru féewarye 2025.
Lu soxal àddug jëwriñ yi:
- Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox yi ak Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay yi àddu na ci sémb wii di « Programme national d’Accès au Logement et de Rénovation urbaine (PNALRU) » ;
- Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde ak Càmm gi àddu na ci tolluwaayu kàmpaañu Njaayum gerte bu 2024, topp gi ak « Sommet bu KAMPALA ».
CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:
Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :
- Sémbu dekkere buy may Njiitu Réew mi mu xaatim, déggoo gi ñu siñe woon 17i fani desàmbar 2004 ca Rabat, diggante Réewum Senegaal ak Réewum Marog jëm ci taxawu ñi ñu teg loxo, ak delloo ñi ñu teg i daan ca seen réew.
- Sémbu dekkere biy taxawal sàrti lootaabe ak doxaliinu komite biy topp sektéer paraapiblig bi.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE