Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 21i fani mee 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoorteel i kàddoom, Njiitu Réew mi def na woote bu am solo jëme ko ci mbooleem way-politig yi ak mbooleem ñi am kàddu ci réew mi ñu ñëw ñoom ñépp teewe diisoo yii mu woote te war a jiite jataayu tijjite li 28i mee 2025, ngir waxtaane sunu sistemu poliyig bi. Sàkku na ci Jëwriñu Biir Réew mi, mu ànd ak kabineem ak “Facilitateur général” bi, taxaw ci dëne mbooleem wàll yi ko séq (làngi politig yi, sosete siwil bi, mbootaayu sàndikaa yi, mbootaayu njaatige yi, kilifa diine yi ak yu aada yi, mbootaayi ndaw ñi ak jigéen ñi…) ak lootaabe gu mucc ayib ci liggéey yi.
Njiitu Réew mi àddu na ci taxawaay bu am solo bi jasporaa Senegaal bi war a am ci jëmmalug “Agenda national de Transformation” bi. Ndokkale na bu baax doomi Senegaal yi féete biti réew ci anam yu mucc ayib yi ñuy dugalee seen yoxo ci doxaliinu politig bi, koom mi ak dundiin wi, niki noonu ni ñuy fésalee mbatiitu réew mi ci àddina si. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu gën a bàyyi xel ci njàmbat yi aju ci wàllu ndoxal (njoxem Kardànte yi, jàll-waax yi ak yeneen xeeti këyit yi jëm ci wàllu laamisoo ak dundiin, fay paasiyoŋ yi, taxawu ak toppug seen i yelleef ci wàllu nekkiin) niki noonu gaaral ak xalaat yiy bawoo ci doomi Senegaal yi nekk biti réew. Woo na Jëwriñu Bennoog Afrig gi ak Jëflante ak Biti Réew ak Sekkereteer Detaa bi yor mbirum saa-senegaal yi nekk biti réew, ñu jël mbooleem matukaay yi war ngir taxaw ci amal serwiis yu gën a jege sunu bokk yiy dund ca biti réew jaare ko ci gën a sóob sunu ndaw yi teewal Senegaal ci wàllu laamisoo ci biti.
Njiitu Réew mi sàkku na, ci geneen wàll, ci Ngóornamaŋ bi mu gën a jariñoo man-man yi ak xam-xam yu wuute yi nekk ci doomi Senegaal yi nekk biti réew boole ko ak gunge leen ci seen sémb yi ñu am ci wàllu eewestismaa yu méngoo ak yitte yu far yi ñu tënk ci biir “Agenda national de Transformation” bi. Loolu sax nag moo war a tax ñu gën a dooleel jumtukaayu xarala bii ci Tabax Sénégal (www.tabaxsenegal.sn) te ñu war koo gën a fésal ci kanamu sunu doom yi féete biti réew. Ci loolu, jox na ndigal Njiitu Jëwriñ yi mu joyyantiwaat, ba mu gën a am njariñ, matukaay yi ñu teg jëm ci tegtal, taxawu, gunge ak kopparal sémb ak yënguy koom yu saa-senegaal yi nekk biti réew, rawati na “Fonds d’Appui aux Sénégalais de l’Extérieur (FAISE)”. Ci kanamu yitte ju kawe ji mu jox sunu doom yiy dund biti réew, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu jël matukaay yi war jëm ci lootaabe, ca weeru desàmbar 2025, ci Ndakaaru, edisoo bi jëkk ci bis bi ñuy jagleel Jasporaa bi. Ndaje mu mag moomu ñu war a amal ci réew mi, am pose lay doon ngir fésal boole ko ak jëfandikoo mbooleem mbébeti Jasporaa bi jëm ci gën a dooleel Senegaal gu moom boppam, gu tegu ci yoon, gu naat te dëppoo ak mbaax yu wér yi nu am ci wàllu jàppalante, mànkoo ak bennoo ci réew mi.
Njiitu Réew mi taxawlu na bu baax ci solo si mu jox waajtaayu “débat d’orientation budgétaire” biy dëgmal te ñu jàpp koo amal ca Ngomblaam ga balaa njeextalu weeru suwe 2025. Ndaje mii war a am ci kanamu ndawi réew mi, am pose la war a doon ci Ngóornamaŋ bi ngir aajar pexe mu bees mi mu am ci wàllu koom mi, njël li ak koppari Càmm gi, waaye itam baral jéego yi jëm ci jëmmal yeesal yi ak porogaraam yi aju ci coppite gu matale ci mbooleem pàcc yi ci réew mi. Sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi mu taxaw, ànd ko ak Jëwriñu koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, amal waajtaay wu mucc ayib ci “débat d’orientation budgétaire” bi, rawati na yeggale gu ànd ak yëgoo ci “document de programmation budgétaire et économique pluriannuelle” bi, nga xam ne dina doon jéego bu am solo ci doxaliin wu leer ci anam yi ñuy saytoo alali askan wi. Ci geneen wàll, xamal na Njiitu Jëwriñ yi ne, fàww ñu taxaw ci saytu yëngu yi aju ci ndajem « Invest in Sénégal » mi ñu jàpp 07 ak 08i fani oktoobar 2025 te doon lu méngoo ak sunu pexe yi nuy teg ci wàllu lëkkaloo ci àddina si ak gën a fésal lëkkaloo gu wàll wu ne di gis boppam.
Njiitu Réew mi àddu na ci mbirum pexe yi ñu war a teg ngir gën a dugalaat bu baax wàllu ndaamaraas gi ci koomum réew mi, rawati na ca tundu Kaasamaas ga nga xam ne njaayum ndaamaraas mi bokk na ci yënguy koom ya fa ëpp doole. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi, rawati na ci Jëwriñ ji yor wàllu Yaxantu gi, mu jël mbooleem matukaay yi aju ci wàllu ndoxal, jumtukaay ak kaaraange ngir amal ci kàmpaañ bu jaar yoon. Fàttali na Ngóornamaŋ bi itam ne fàww mu gën a dooleel mbébet yi piriwe bi am jëm ci sopparñee ci réew mi li fiy meññ ci ndamaraas ngir dugalaat bu baax pàcc bii ci naal yi ñuy sumb jëm ci samp ay ndefar ci réew mi.
Mu tëjee, ci arminaatu laamisoom, moom Njiitu Réew mi xamal Ndiisoo gi ne, dina nemmikuji, alxemes 22i fani mee 2025, ànd ko ak naataangoom bu Réewum Móritani, jumtukaayu ”Grand tortue Ahmeyim” (GTA).
Cig àddoom, Njiitu Jëwriñ yi fàttali na taxawaay bu am solo ci wàllu diine bi Tabaski am ci réew mi. Ci loolu sax lañu ci jotoon a amal, am ndaje diggante Jëwriñ yi, ci waajtaay wi ba joxe woon ci ay tegal yu jëm ci fexe ba xar yi doon lu jàppandi ci marse yi ci réew mi. Lu ko jiitu itam, Njiitu Jëwriñ yi jëloon na, jaare ko ci bataaxel bu mu jagleeloon ñenn ñu bokk ci Ngóornamaŋ bi te mu soxal leen, ay dogal yu jëm ci woyofal caytug sëfaan yi ak daamar yiy yab xar yi, teggi yenn wareef yi ñu daan fay ak may leen teewaayu ñetti sàmmkat ci biir sëfaan bu ne ngir wattu jur gi ñuy indi, gën a dooleel kaaraangeg pénc mi ak wàllu wér gi yaram ci mbooleem warabi jaayukaay yi ak yoon wi ñuy jaarale xar yi. Njiitu Jëwriñ yi ginnaaw ba mu refetloo jëfe gu mucc ayib gi ci digleem yooyu, woo na Jëwriñ yi yor wàllu Larme bi, Kaaraangeg Pénc mi, Koppar yi ak Gox yi ak Goxaan yi ñu taxaw temm ci fexe ba ñu jëfe ca na mu waree, ci mbooleem warab yi nekk ci réew mi, digle yi Ngóornamaŋ bi teg. Njiitu Jëwriñ yi xamle na ne, ci bisub 18i fani mee 2025, lim bi ñu amoon ci ay xar ci marse bi mu ngi tolloon ci 406 592, ci 830 000 yi ñu soxla ci réew mi, muy 48,99% ci xayma, ñetti ayu-bis laataa feet gi. Tolluwaay bi ci warabi jaayukaay yi ñu samp itam dal na xel, ak jubluwaayu 278i warab yu Góornoori Tund yi tëral. Xamle na itam tolluwaay bu dal xel bu am ci marseb soble si ak pombiteer bi. Ci tënk, Njiitu Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ yi ñu taxaw temm, ba ca cappaandaw la, ba dogal yi ñu jël yépp ñu matale leen. Lu jëm ci wàllu dimbalante gi ci réew mi, Njiitu Jëwriñ yi mu ngi topp bu baax, matukaay yi ñu teg jëm ci taxawu way-néew doole yi ngir fexe ba ñoom itam ñu man a amal feetu tabaski gi ci ngor.
Njiitu Jëwriñ yi dikkaat na ci tukkib xaritoo ak liggéey bi mu jot a amal ca Burkinaa Faaso ci ndënel naataangoom bu Burkinaa bii di Njiitu Jëwriñ yi Rimtalba Jean Emmanuel WEDRAAWOGO. Ci pose moomu, Njiitu Réew ma di Ibraahiim TARAAWORE dalal na ko, ba mu jottaliwaale ko bataaxelu mbokkoo bi bawoo ci naataangoom bu Senegaal di Basiiru Jomaay Jaxaar FAY. Teewe na itam xewu tijjitel barabu Peresidaa Tomaas SÀNKARA, di jëmm juy màndargaal panafrikaanism. Njiitu Jëwriñ yi tëjee ci sant bu baax askanu Burkinaa ci dalal gu mucc ayib gi ñu ko jagleel.
Ci àddug jëwriñ yi:
- Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox yi ak Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay gi àddu na ci tolluwaayu waxtaan yi ñuy amal jëm ci jëmmal “pôles territoires” yi.
CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:
Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :
- Sémbu dekkere bi jëm ci taxawal ak rëdd sàrti lootaabe ak doxaliinu daara jiy tàggat ci wàllu Petorol ak Gaas (INPG);
- Sémbu dekkere bi jëm ci taxawal ak rëdd sàrti lootaabe ak doxaliinu Ndiisoog Yaaley Jaww ji ci réew mi (CNTA).
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi.
Aamadu Mustafaa Njekk SARE