Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 19i fani mars 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi dikkaat na ci siyaar ak njaal yi mu jot a amal ca Tuubaa ak ca Daaru Muhti, gaawu 15i fani mars 2025. Sant na bu baax boole ko ak gërëm Kilifag yoonu Muriid, Sëriñ Muntaxaa Basiiru MBÀKKE ak mbooleem kilifa yi mu jot a dajeel, ci dalal gu mucc ayib gi ñu ko jagleel, ci jataay yu am solo yi mu séq ak ñoom ak ñaan yi ñu amal ngir Senegaalu jàmm, gu naat te jàppoo.
Njiitu Réew mi àddu na ci jafe-jafe bi nekk ci càmbar yenn sànce ak liggéey yi managul a yegg ba leegi ak coppite yi ñu war a amal ci anam yi ñuy saytoo tabax jumtukaayi pénc mi. Li am nag mooy, ay at yu bari a ngi nii, ñu seetlu lim bu takku ci ay sànce yu manul a fexe ba yegg ci gox yu bari ci Senegaal. Muy ci pàcc yu mel ni njàng mu kawe mi, njàng mi, tàggatu gu xereñ gi, paj mi, yasara gi, asanismaa, yoon yi ak tàggat yaram. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu amal xayma gu matale ci njëwriñ gu ne, mbooleem sémbi tabax yi noppeegul teg ci gaaral ko yoon ak matuwaay yi ñu war a jël ngir joyyanti ak dooraat sànce yooyu, lépp ci kaw sàmmonte ak yoon yi ñu tëral ci wàllu marse piblig yi ak doxaliin yi aju ci sañ-sañu « Agence judiciaire de l’Etat ». Xamle na itam ne jot na sëkk ñu leeral sémb yi aju ci PUDC, PROMOVILLES, PNDL ak PUMA, mbooleem naal yi nga xam ne boole seen i yëngu dina tax mu gën a jur njariñ ci « territorialisation » ci doxaliinu pénc mi.
Njiitu Réew mi, ci geneen wàll, sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu xoolaat nu ñuy def ba gën a yokk, ci wàllu yoon, dooley « Agence de Construction des Bâtiments et Edifices publics (ACBEP) » ci anam yi ñuy doxalee liggéey yi aju ci tabax jumtukaayi pénc mi jaare ko ci tënk ay njëg yu ñu war di sàmmonteel ak anam yi ñuy saytoo koppar yi ci at yu bari. Ci geneen wàll, xamal na Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñu Gox yi ak Goxaan yi, ñu ànd ak partaneeri Nguur gi ci wàllu xarala ak kopparal, teg doxaliin wu yees ñeel « Agence d’Exécution des Travaux d’Intérêt public contre le sous-emploi (AGETIP) » ak « Agence de Développement municipal (ADM) », méngale ko ak doxaliinu njël li, tëraliinu « Agenda national de Transformation » bi ak pexe yi jëm ci doolel xëyu ndaw ñi. Ci loolu, xamle na ne fàww ñu amal taxaw-seetlu gu matale ci mbooleem sémb yi ñu tegoon ci yoxoy AGETIP ak ADM boole ko ak taxaw ci fexe ba ag yëgoo am ci yënguy ñaari wànqaasi Nguur yu am solo yii.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi woo na Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox yi ak Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay gi, ñu sumb ay waxtaan, ànd ko ak mbooleem ñi mu soxal, ngir xool doxaliin wu bees ci dooleel koppar yi jot a jàppandi jëm ci jëmmal ay sémb yu far ci « pôle-territoire » bu nekk.
Lu jëm ci yitte ju kawe ji mu jox xëyu ndaw ñi, Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi ne ndawi réew mi war nañoo tax Nguur gi ak ñiy yëngu ci wàllu koom mi ñu joxante loxo liggéey ngir dooleel jéemantu gi ak fexee taxaw ci ndaw ñiy wut um xëy fépp ci réew mi man a am ci lu ñu jàpp. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñ ji yor wàllu Xëy mi, ñu baral jéego yi jëm ci matale, balaa njeextalu weeru awril 2025, wayndare wi ëmb doxaliin wu yees wi aju ci wàllu xëy ci réew mi. Xamle na ne fàww ngóornamaŋ bi teg sistem bu wér te wóor ci xibaar yi aju ci marseb liggéey bi te méngoo ak limub li ñu am ci ay lijaasa ci wàllu tàggatu gu xereñ gi ci warabi tàggatukaay yi ak ci ISEP yi.
Njiitu Réew mi woo na Njiital Jëwriñ yi mu baral jéego yi jëm ci méngale ak boole yënguy mbooleem wànqaasi nguur yiy yëngu ci wàllu jéemantu ak xëyu ndaw ñi.
Lu soxal mbirum yeesal anam yi ñuy saytoo wàllu àllaateret ak sekirite sosiyaal, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu taxaw temm ci loolu fexee gën a joxaat gëdda wàllu liggéey bi ak porotegsoo sosiyaalu Nguur gi. Tay, ni askanu Senegaal tëddee ak seen uw nekkiin war naa tax ñu xoolaat ni ñuy saytoo koppar yi ci wàllum paj ak dundiin rawati na nag yi aju ci wàllu àllaateret ak sekirite sosiyaal. Sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Liggéey bi ak Xëy mi, mu gaaw matale, ànd ko ak partaneer yi, sémb wii di « Code unique de Sécurité sociale », muy sàrt bu war a bokk ci liy gën a jagal yoriinu wànqaas yiy taxawu liggéeykat yii di « [Institution de Prévoyance Retraite du Sénégal (IPRES), Caisse de Sécurité sociale (CSS) et Institution de Prévoyance Maladie (IPM)]. »
Ci wàll woowu ba leegi, Njiitu Réew mi woo na Jëwriñu Koppar yi ak Njël li mu def yitte ju far ci jéem a peeg alal ji nguur gi di def ci wàllum paj ñeel ay liggéeykatam, jàppandig koppar yi jëm ci wàllu « Couverture sanitaire Universelle » ak rawati na ag yamale gu wér te sax ci « Fonds national de Retraite (FNR) ». Ci loolu, woo na Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñ ji yor wàllu Liggéey bi, ñu leeral, balaa njeextalu weeru sulet 2025, tolluwaayu koppar yi ñu jagleel sistemu àllaateret bi (FNR ak IPRES) ak ay mbébetam, sukkandiku ko ci ni marseb liggéey bi di doxee ci diir bu gàtt, bu digg-dóomu ak bu yàgg.
Mu daanelee moom Njiitu Réew mi, ci xamle ne fàww ñu càmbaraat yoon yu ñu man a jaar ngir yokk paasiyoŋi àllaateret yi gën a néew boole ko ak sóob ndawi nguur gi, liggéeykat yi ak partaneer yi, ci yoonu taxawal li ñuy tuddee « retraites supplémentaires par capitalisation ».
Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi wax na ci jafe-jafe yi baykat yi di jànkonteel rawati na lu jëm ci jàllale yenn ci yi ñu jot a ñorle, lu mel ni gerte gi, payteef yi ak mboq mi, ndax ay jafe-jafe yees seetlu ci matukaay yi ñu teg ngir njaay mi.
Ci loolu, xamle na ne fàww ñu taxaw temm ci doxaliin wu mucc ayib ñeel mbooleem pàcc yi aju ci mbay mi, te bokk ci yooyu taxawu gi ci wàllu ay koppar, ngir man a yegg ci jubluwaayu bay dunde gi ñu tënk ci biir « Agenda Vision Sénégal 2050 ». Ci tolluwaay boobu nag ak korite gi ak « Pâques » biy dëgmal ak depaas yu diis yi nar a gàllu ci ndoddi njaboot yi, woo na Jëwriñ yi yor wàllu Mbay mi, wàllu Koppar yi ak wàllu Yaxantu gi, ñu jébbal ko matuwaay yu jamp, balaa altine 24i fani mars 2025, yu ñu war a gaaral Njiitu Réew mi mu war koo jàllale, ngir wut ay pexe ci jafe-jafe bi am ci limub li ñu jot a denc ci wàllu dund lu mel ni gerte gi, payteef yi ak mboq mi. Ci anam yu gën a lootaabewu, sàkku na ci Jëwriñ yii ñu jot a lim, ñu amal gën gaa yeex ci ñaareelu xaaju weeru awril 2025, ndaje mu war a dox diggante jëwriñ yi, ñu jagleel ko waxtaane jafe-jafe yi am ci njaayum liy bawoo ci mbay mi ci anam yu gën a matale.
Ci ñaareelu tomb bi mu àddu, Njiital Jëwriñ yi fàttali na ne doxaliin wi Ngóornamaŋ bi tànn ngir amal coppite gu matale ci Senegaal dafa laaj ñu gën a dooleel xereñte ci Ndoxal gi muy ci mbooleem wànqaasi Nguur gi niki noonu itam ci liggéeykat yi. Xamle na ay jéego a ngi am ci anam yi Senegaal di doxalee ci jéem a méngoo ak matukaay yi UEMOA teg ci anam yi ñuy saytoo koppar yi. Waaye nag, Njiital Jëwriñ yi xamle na ne matukaay bi dese naa xereñ lool ndax ni ci aktéer yi gën a am solo néewee, yeexaay bi am ci doxal gi ci lu jëm ci wàllu topp gi ak xayma gi, waaye rawati na, ñàkk a tegal liggéeykat yi ay jubluwaay yu wér yu ñu war a matale ci at mu ne boole ko ak di natt seen ug xereñte.Tolluwaay boobu nag moy tax duñu man a rànnatle xereñteg liggéeykat bu ne. Kon, Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Foŋsoo Piblig, mu lëkkaloo ak Jëwriñ ji yor wàllu Kppar yi ak Jëwriñ Sekkerteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, ñu taxaw temm ci jafe-jafe bi am ci natt xereñteg bépp liggéeykat bu ne ci yoon wi ñu war a tegtaloo ci atum 2025 ci « Plan d’action 2025-2029 » bu « Agenda Vision Sénégal 2050 »
Mu daaneel moom Njiital Jëwriñ yi, ci xamle ne fàww ñu taxaw ci ñàkk sàmmonte gi am ci wareefu yeesal xar-kanamu taaxi piblig bi ak piriwe bi. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Dëkkuwaay mu gaaral ko ay mayuwaay yu ñu war a jël ci jafe-jafe boobu lépp ci kaw sàmmonte ak sàrt yi ñu tëral.
Lu soxal àddug jëwriñ yi:
- Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi àddu na ci yembug dund bi ci ja yi;
- Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde ak Càmm gi àddu na ci kàmpaañu njaayum gerte gi ak toppug kàmpaañu payteef yi.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi.
Aamadu Mustafaa Njekk SARE