Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 19i fani féewarye 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi jébbal na njaalam Sëriñ Muntaxaa Mbàkke Basiiru Kilifag Yoonu Muriid, ginnaaw Sëriñ Amdi Móodu Mbenda Faal Kilifag Baay Faal yi ak Sëriñ Mustafaa Saalihu Mbàkke, ñi wuyuji seen Boroom.
Lu soxal jàngat bi ñu war a def ci njureef yi tukkee ci càmbar yi « Cour des Comptes » amal ci ni ñu yoree woon alalu askan wi, Njiitu Réew mi soññe na ci ñu gaaw jël matuwaay yu wér te wóor ngir gën a dooleel boole ko ak taxawu sunu doxaliimu koom, njël li, koppar yi ak kontaabilite bi. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu gaaral ko arminaat bu jëm ci doxal mbooleem digle yi bawoo ci ràppooru càmbar bu « Cour des Comptes », te jébbal ko ca na mu gën a gaawee, sémb wu jëm ci fexee peeg depaas yi, te bàyyiwaale xel wareef yi ci wàllu koom mi ak akan wi, ci anam yi ñu ko tënkee ci gis-gisu Senegaal 2050.
Njiitu Réew mi xamle na ne fàww ñu taxaw temm ci peeg bu wér sémbi njël yi, palaŋi Nguur gi ci wàllu koppar yi ak yoriin wi ci ñetti at yiy dëgmal, depaas yi ci wàllu galag ak ci bor bi. Ci lu soxal tomb bu mujj bi, sàkku na ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak ci Jëwriñ ji yor wàllu Koom mi ñu gaaral ko, ci lëkkaleg Njiital Jëwriñ yi, tëraliin wu bees ci sàrt ak anam yi Nguur gi war di lebee niki noonu lootaabe gu bees ci ni ñuy saytoo bor bi. Njiital Jëwriñ yi war naa taxaw itam ci fexe ba Jëwriñu Koppar yi ak Njël li gaaw waajal benn « projet de loi rectificative des finances », jëm ci waajal « débat d’orientation budgétaire ».
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi xamal na Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo, jamp gi nekk ci :
- taxaw ci fésal xibaar yu wér ci wàllu koppar yi ci anam yu wóor, matale, wér te dëggu;
- baral jéego yi jëm ci wàllu « digitalisation » ak « duggalanteg » doxaliinu xarala yi ñuy jëfandikoo ci wàllu koom, koppar ak kontaabilite Nguur gi;
- dooleel caytu gi ci doxaliinu « cadrage macroéconomique » bi ;
- suqali « planification triennale consensuelle » bi ci wàllu eewetismaa yiy bawoo ci biir réew mi ak ci biti ak ci lëkkaloo yi dox diggante Nguur gi ak piriwe bi.
Xamle na ne yoonu dëgg wi ñu sóobu, am pose la ngir ñu sumb ay coppite yu wér te xóot ci doxaliinu koom mi, koppar yi ak kontaabilite Nguur gi ak seen ug lëkkaloo ak partaneer yi ak sistemu kopparal gi. Ci loolu soññee na ci ñu soppi anam yi Nguur gi di doxalee ci wàllu ndoxal, koom mi, koppar yi ak kontaabilite bi.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu sumb ay waxtaan diggam ak mbooleem ñi am kàddu ci réew mi, mbootaayi liggéeykat yi, sektéer piriweb réew mi ak rawati na njaatige yi, ngir bokk ak ñoom yaatal ci njureef yi tukkee ci tolluwaay bii ñu doon wax boole ko ak wut ay pexe yu ñu déggoo ngir jëmmal doxaliin wu bees wu jëm ci soppi ni ñuy saytoo alalu askan wi, lépp ci jàppalante ak aar ñi gën a néew doole ci askan wi.
Fexe ba askan wi jot ci ndox mu sell, rawati na ci kaw gi, moo war a doon yittey Ngóornamaŋ bi. Ci loolu, Njiitu Réew mi woo na Njiital Jëwriñ yi mu wéyal jéego yi jëm ci gën a yombalal askan wi jot ci ndox mu sell ci njëg yu yomb. Rafetlu na waxtaan yi ñu amal bu yàggul dara ci wàllu ndox mi, teg ci woote ngir ñu baral jéego yi jëm ci taxawal pexe yu wér ngir sàmm ndox mi waaye tamit fexe ba teg yoon woo xam ne bu noppee ndox mi dina man a yaatu ba yegg ci taax yi ak li ko wër ba ci kaw gi. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa mu xoolaat anam yi ñuy joxee caytug ndox mi ci kaw gi yennn këri liggéeyukaay yi, boole ko ak dooleel toppatoo gi ak yeesalaat fooraas yi ak jumtukaayi ndox mi. Jëwriñu Ndox mi war naa bàyyi xel itam yoriin wu leer ci lu soxal njëg yi ak caytu gi kër yi ñu dénk ndox mi di amal.
Ci yoon wi ñu tegu jëm ci fàkk ak taxawal « xàlli ndox yi », Ngóornamaŋ bi war naa fuglu ay xalaat yu jëm ci anam yi wàll wi di doxee ci wàllu koom boole ko ak wàllu asanismaa (ndox yu yàqu yi ak ndoxi taw bi) ak yokkuteg sémb yi jëm ci segg ndoxi xorom yi. Bokk na ci tamit, fexee gën a sóob gox yi ak goxaan yi ak askan wi ci ni ñuy saytoo wàll wi. Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa, mu tëggaat politigu ndox mi ci dëkk yi, yaatal bu baax perimeetar bii ñuy wax « affermé » sukkandiku ko ci anam yi dëkkuwaay yi di yokkoo ci réew mi ak jafe-jafe yi aju ci wàllu njuux li, ba tax ñu war a xoolaat bu baax doxaliinu asanismaa bi ci wàllu pexe, xarala ak koppar. Ci loolu, jox na ndigal Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa mu sumb ay liggéey yu jamp ngir taxaw ci doxaliin wu mucc ayib ci serwiis ak reso yi aju ci ONAS.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi xamal na Ngóornamaŋ bi ne, jot na sëkk ñu jël mobooleem matukaay yi war ngir dooleel fuglu gi ak xeex wal mi. Sàkku na ci Jëwriñu Ndox mi ak Asananismaa mu sumb, ca na mu gën a gaawee, yëngu yi jëm ci waajal nawet bi boole ko ak jël matukaay yu jamp ci wàllu fuglu ak saytu wal mi, rawati na ci warab ak gox yi nga xam ne ay warabi ndox lañu.
Njiitu Réew mi fàttali na itam Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa ne fàww ñu gaaw matale sémbu yoonal wi soxal « Code de l’eau ». Sàrt bii nag dina tax ñu gën a dooleel anam yi ñuy sàmmee sunu balli mbindare yi ci wàllu ndox ak yoriin wu leer ci doxaliin wu ñépp di ànd. Dees na taxawal itam genn kurél guy saytu wàllu ndox mi. Mu tëjee bunt boobu moom Njiitu Réew mi ci yëgle ne dina amal, àjjuma 21i fani féewarye 2025 ca Kungéel, ndoortelu sémbu PROMOREM wii jëm ci dajale balluwaayi ndox yi nekk ca dexu Ñanija Bolong.
Mu daanele moom Njiitu Réew mi ci teew ga mu teewoon ca Ecopi, ca 38eelu Ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu Mbootaayu Réewi Afrig mi ñu doon amal 15 ak 16i fani féewarye 2025 ak ca màggalug bis bi Réewum Gàmbi moomee boppam, ci ndënel naataangoom bii di Aadma Baro, ngir feddali jàppoo ak mbokkoo gi dox sunu diggante ak askanu Gàmbi wi nga xam ne Yàlla moo boole mbiram ak mu Senegaal.
Cig àddoom, Njjital Jëwriñ yi xamal na Ndiisoo gi ne dina teew ca Ngomblaan ga àjjuma 21i fani féewarye 2025 ci lu soxal laaji xew-xew yi ñu jagleel Ngóornamaŋ bi, ngir weccente ak jàmbur yi ci jàngat yi ñu jëlee ci seetlu yu doy waar ak digle yi bawoo ci Rappooru « Cour des Comptes » ci anam yi ñu yoree woon alalu askan wi diggante 2019 ba 31i fani mars 2024, rawati na matukaay yi ñu ci fas yéene jël ngir joyyanti. Njiital Jëwriñ yi fésal na yenn tomb yu nekk ci biir ràppoor bi, jëm ci muj gi « Cour des Comptes » jàpp ne moom lañu war am ci yenn jëf yi laale ak jalgati walla ndëngte gu laaj ñu yóbbu mbir mi ci yoon.
Niki tegtal yi ci Njiitu Réew mi joxe woon, moom Njiital Jëwriñ yi jox na ndigal Jëwriñu Koppar yi ak Njël li mu jël matukaay yi war jëm ci doxal, ci lu amul àpp, joyyanti yi war ngir jëmmal digle yooyu.Ci loolu kon, dina am solo lool ñu bàyyi xel ci doxalin wu leer te wóor ci dogal yi ñu war a jël ëllëg ci jëflante yi ñuy séq ak ñiy yëngu ci wàllu koppar.
Njiital Jëwriñ yi xamle na ne bu weesoo joyyanti yi ñu war a amal ci ni ñuy saytoo njël li ak alalu askan wi, Ngóornamaŋ bi fas na yéene jël matukaayi jubbanti yi war balaa yàgg, jëm ci yaxanal alalu askan wi ak wàññi bu baax anam yi Nguur gi di dunde. Xamle na ne niki ko Njiitu Réew mi diglee, dina amal ndaje mu njëkk diggante Ngóornamaŋ bi ak partaneer yi, alxemes 27i fani féewarye 2025, ngir sóob mbooleem ñi am kàddu ci réew mi ci jubnanti gi ñu namm a amal ci koom mi ak koppari réew mi. Ndaje moomu nag war a doon ndoortel diisoo yu ñépp di séq, mu wér te lalu ci bëgg sa réew, dina dajale Ngóornamaŋ bi, mbootaayi liggéeykat yi, mbootaayi njaatige yi ak sosete siwil bi, Campeefi Réew mi, njiiti këri liggéeyukaay, mbootaay yi ci réew mi añs.
Lu soxal jëmmal sémb ak naal yi aju ci Gis-Gisu Senegaal 2050 bi, ci diggante juróomi at yii di 2025-2029, Njiital Jëwriñ yi soññ na Jëwriñ yi ñu taxaw ci gaaw mottali yoon wi ñu war a jaar ak tàmbalig sémb yi njëkk ci atum 2025 ca na mu gën a gaawee.
Mu daanele, moom Njiital Jëwriñ yi ci defal Ndiisoo gi ab tënk ci liggéey yi kurél gi ñu dénk ca desàmbar 2024 màggalug 80eelu at mi ñu bóomoon Tiraayeer yu Senegaal ca Caaroy, di wéyal. Ci loolu, fàttali na ne Njiitu Réew mi jëloon na dogal, 13i fani sãawiye 2025, def sëgi sóobare yu Caaroy muy « cimetière national » teg ci yoonal bisub 1 panu desàmbar muy bis bi ñu jagleel tiiraayeeri Senegaal. Njiital Jëwriñ yi xamle na itam ne njëwriñ yi mu soxal ñu taxaw bu baax ci yeneen ñenti dogal yu Njiitu Réew mi jëloon ngir saxal ci xel yi, fàttaliku xew-xew bu tiis boobu. Muy tabaxug « mémorial Thiaroye 44 », barabu gëstu, tuddee ñi loru woon ci xew-xew boobu turi mbedd yi ak warabi pénc mi ak dugal mbooru Caaroy 45 ci njàng mi.
Lu jëm ci fexee xam dëgg dëgg limub ñi ci faatu, Njiital Jëwriñ yi yëgal na Ndiisoo gi ne ba leegi ñu ngi xaar yenn xibaar yu war a mottali gëstu yi. Ci loolu sax nag, xamle na ne dees na sulliwaat yenn ci bàmmeel yi ñu leen suul.
Lu soxal àddug jëwriñ yi:
- Jëwriñu Bennoog Afrig gi ak Jëflante ak Biti Réew àddu na ci génnug réewi AES yi vi CEDEAO;
- Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi àddu na ci pexe yi ñu war a teg ngir am dund bu doy sëkk ci ja yi;
- Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde gi ak Càmm gi dikkaat na ci tolluwaayu kàmpaañu njaayum gerte gi, wéyal kàmpaañu payteef yi ak waajtaayi bis bi ñu jagleel càmm ci réew mi;
- Jëwriñu Càmm gi yor suqalikug këri lijjanti yu ndaw yi ak yu digg-dóomu yi àddu na ci 4eelu edisoo bu Ndajem PME yi jëm ci teg i pexe ngir dooleel ak suqali PME/PMI yi ci réew mi.
CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:
Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :
- Sémbu dekkere biy jox ndigal Njiitu Réew mi mu xaatim déggoo giy tëral « Commission bancaire de l’Union monétaire ouest africaine » te ñu jàllale woon ko 31i fani mars 2023 ci Ndakaaru;
- Sémbu dekkere bi jëm ci sos ak taxawal anami lootaabe ak doxaliinu « Comité de Gouvernance du Numérique (GouvNum) ».
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE