Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, tay ci àllarba ji 18i fani desàmbar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi dikkaat na ci xew wi ñu doon amal, alxemes 12i fani desàmbar 2024 ca Cees, jëm ci daloo tën wi ñu jagleel kenn ci jàmbaari réew mi di Lat Joor Ngóone Latiir Jóob, ci téeméeri ati fàttaliku ag faatoom. Sant na bu baax boole ko ak gërëm askanu Cees, rawati na dongo ya, ci ni ñu takkoo taxaw amal teertu gu mucc ayib ñeel ko. Cant yooyu nag yaatal na ko ba ci kilifay gox ba, fara ba, way-falu ña, kilifa diine ya ak kilifa aada yu Cees yi dugal seen loxo ngir ndamul bis bi.
Teewaayu Njiitu Réew mi ca Cees nag day firndeel ag taqoom ci gën a fullaal sunu moomeel ci wàllu mboor ak mbatiit gi nga Xam ne fàww ñu sàmm ko te nangu ko, muy mboor muy bàyyi xel sunuy mbaax ak sunu cosaan yi lalu ci fàttaliku ak a màggal sunu jàmbaari réew yi ci fànn yépp. Ci loolu, sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Gox yi ak Goxaan yi, Jëwriñu Mbatiit mi ak Sekkereteer Detaa ci wàllu Mbatiit, ñu ànd ak Gox yi ak Goxaan yi, amal liggéey bu jëm ci tuddaat sunu mbedd yi, xàll yi, tabaxi pénc mi méngale ko ak jëfi mboor yi ak jàmbaar yi fésoon lool ci dundug réew mi.
Njiitu Réew mi xamle na itam solos yaatal ak jàngale mboorum Senegaal. Ci loolu sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu xayma te dooraat sémbu bindaat mboorum Senegaal, dekkalaat ak dooleel sunu moomeel ci wàllu mboorum sunuy bokk-moomeel ak sunuy gox. Xamal na ci wàll woowu, Jëwriñ ji yor wàllu Mbatiit mi ak Sekkereteer Detaa bi yor sunu moomeel ci wàllu mboor, ne fàww ñu liggéey ci dundalaat moomeelu dun yi, rawati na yu Gore ak Karabaan ànd ko ak njiiti gox yi ak askan wi. Ci geneen wàll itam, woo na Njiital Jëwriñ yi mu sumb ay xalaat jëm ci taxawal ci réew mi ag Kurél guy saytu denc ak saytu sunu moomeel ci wàllu Mboor ngir def càmmug sunu mboor muy jumtukaayu suqaliku gu am doole ci wàllu koom, nekkiin ak mbatiitu Senegaal.
Lu soxal mbirum irbanism, arsitegtiir, dëkkuwaay ak lu koy dooleel, Njiitu Réew mi xamle na ne jëmmal Gis-Gisu Senegaal 2050, wane na jamp gi nekk ci baral jéego yi ci wàllu daggug mbeeraay gi, suqali sunuy gox niki noonu méngale ak jamono sunuy bokk-moomeel ak sunuy gox jaare ko ci póol yi. Sàkku na ci Jëwriñu Dëkkuwaay ji, Gox Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay gi mu taxaw ci yesaalaat ak matale palaŋ yi jëm ci doxaliinu irbanism ci bokk-moomeel yépp ak ci goxi Senegaal yi. Doxaliin wu manul a ñàkk woowu nag, day lu am solo ngir peeg suqlikug gox yi boole ko ak baral jéego yi jëm ci doxal politigu dëkkuwaay yi ak dooleel lóosmaa sosiyóo yi rawati na. Ci wàll woowu, jox na ndigal Jëwriñu Dëkkuwaay ji, Gox Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay gi, mu taxaw ci ñu doxal ci na mu waree sàrti arsitegtiir yu méngoo ci bokk-moomeel ak goxu Senegaal bu ne. Ci loolu, woo na Ngóornamaŋ bi ñu ànd ak kurélu arsiteg yi liggéey ngir gaaral xar-kanam gu yees ci sàrtu doxal politigu arsitegtiir bu yees bu Senegaal.
Ci yoon wi ñu jël jëm ci tëggaat politigu irbanism, tabax ak dëkkuwaay, Njiitu Réew mi sóob na Ngóornamaŋ bi mu wéyal jéego yi muy teg jëm ci dooleel tabax yi ci sàrt yi ñu tëral ci wàllu dëkkuwaay, taax ak tabax yi te boole ko ak:
- doxal gu wér ci kotu irbanism, tabax, asanismaa ak kéew mi;
- peeg daggiin ak dëkkiin yi ci tefes gi;
- boole laboraatuwaar biy saytu wàllu taax yi ak tabaxi pénc mi tey taxaw ci nangug jumtukaay ak porodiwi yi ñuy jëfandikoo ci wàllu BTP di taxaw it ci baaxaay ak méngoo ak tabax yi;
- dugal ci sàrt yi njëmbatum garab ak warabi nëtëx ci koñ yi ak dëkkuwaay yi;
- tàggatu gu xereñ gu dul dog ñeel ñiy yëngu ci wàllu tabax ci lekool yi ak warab yi ñu ko jagleel.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi xamle na jampug baral jéego yi jëm ci doxal sémbu lóosmaa sosiyóo yi. Ci loolu sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu dooraat sémbu tabax ay lóosmaa sósiyóo ci gox yi mu méngool yu ànd ak lotismaa, daggiin yu wóor ak këyiti dëkkuwaay yu wér yu ñuy joxe ginnaaw bu càmbar yi ñuy amal ci wàllu suuf si jamono jii noppee. Ngóornamaŋ bi war naa gaaral itam ay pexe yu wér ngir baral jéego yi jëm ci taxawal dëkkuwaay yu mucc ayib jaare ko ci defar ay palaŋ yu ñuy dëppoo ci tabaxaat ak yeesalaat dëkki taax yi te jublu itam ci méngale ak jamono dëkkuwaay yi ci dëkki kaw gi. Woo na Njiital Jëwriñ yi ak Ngóornamaŋ bi ñu def dëkkuwaay bu baax muy yittey réew mi li ko dalee atum 2025. Jëwriñu Irbanism ak Sekkereteer Detaa bi yor wàllu Dëkkuwaay dinañu dikk weer wu jot ci Ndiisoog Jëwriñ yi, leeral fi ñu tollu ci doxal politig bi ñeel wàllu dëkkuwaay.
Ci loolu, sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak ci Jëwriñ ji yor wàllu Irbanism, ñu taxawal, ci ñetti at yii di dëgmal, sas ak wàll wi SAFRU war a yëngoo, muy kurél gu war a am suuf ak koppar yu doy yu tegu ci modelu koom mu wér. Ñu boole ci càmbar « Fonds de Garantie » bi jëm ci jot ci dëkkuwaay (FOCALOG) ak doxal luwaa oriyàntaasiyoo l° 2016-31 bu 08i fani nowàmbar 2016 ci wàllu dëkkuwaayu sosiyaal ànd ko ak jumtukaayu « Fonds pour l’Habitat social (FHS) ».
Ngóornamaŋ bi dina taxaw itam ci doxalaat « póol irbee » yi ak yenn tund yi ñu jot a fàkk ngir yombal jot gi ci wàllu suuf ak dëkkuwaay ànd ko ak Bànk yi ak warabi kopparal yi (CDC rawati na…) Ci yoon woowu, dees na ci jiital jéem a gën a suqali « póol irbee » bu Jamñaajo ak Lag Róos yi ñu tàmbalee samp ay dallukaay yu méngoo ak jamono.
Boo xoole nag ni wàllu turism bi di yokkoo, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi, ci Jëwriñ ji yor wàllu Gox yi ak Goxaan yi ak ci Jëwriñ ji yor wàllu Turism bi ñu taxaw ci peeg bu baax suqalikug goxi turist yu Senegaal.
Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi yëgal na Ndiisoo gi ne, ni ko Ndayi Sàrti Réew mi diglee, rawati na na ci artiikal 84, Njiitu Réew mi bind na Ngomblaan ga ngir xamle ne dees na amal DPG bi, àjjuma 27i fani desàmbar 2024, ni ko arrtikal 55 bu Ndayi Sàrti Réew mi rëddee.
Lu soxal waajtaayu asàndaa lesisltif bi ci atum 2025, Njiital Jëwriñ yi xamle na ne sémbi yoonal yi ci aju yépp dañoo war a méngoo ak Gis-Gisu Senegaal 2050 bi. Xamle na ne wareef la ci njëwriñ gu ne mu bind asàndaa lesislatifam ci ñetti weer yu njëkk yi ci atum 2025, te jébbal ko Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi gën gaa yeex xaaju weeru sãawiye 2025. Ci loolu sàkku na ci Jëwriñ yi ñu taxaw bu baax, ginnaaw ba ñu xoolaatee sémbi yoonal yi ñu bindoon laataa awril 2024, ci xool bind yi jëm ci wàllu pexe ak yi jëm ci wàllu doxal, ngir man a waajal ci jafe-jafe yi ak àpp to niki noonu yi ci gën a doon yitte. Fàww itam ñu boole ci bàyyiwaale xel jubluwaay bu am solo bi jëm ci yaxanal alalu askan wi.
Ci geneen wàll, Njiital Jëwriñ yi bàyyiloo na xel ci taxawaay bi ñu war a am jëm ci joyyantiwaat këri liggéeyukaayi piblig ak parapiblig yi nekk ciy jafe-jafe ngir taxaw ci wéyal serwiis piblig bi. Ci noonu sàkku na ci Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi mu taxaw ci dooraat liggéeyi komite enterministeriyel bi jëm ci Topp ak Joyyanti këri liggéeyukaayi piblig ak parapiblig yi, teg ci jox ndigal Jëwriñu Koppar yi ak Njël li mu jël mbooleem matuwaay yi war ngir doxal gu wér ci « Fonds de Relance » ngir joyyanti yooyule këri liggéeyukaay.
Mu daaneel moom Njiital Jëwriñ yi ci yëgal Ndiisoo gi ne dina ànd ak Topp-Njiital Gàmbi, ci tukkib liggéey ak xaritoo bu muy amal ca réew ma 19 ak 20i fani desàmbar 2024, jiite ndajem Kurél giy saytu topp lëkkaloo diggante ñaari réew yi te gëjoon a am 2011 ba leegi. Ndaje moomu dees na ko jagleel xoolaat doxalug dogal ya bawoo woon ca Ndiisoog Njiit ga ñu amaloon 1 panu ut 2023 ak càmbar yenn wayndare yi. Njiitu Jëwriñ yi dina ànd ak Topp-Njiital Gàmbi li, jiite tijjitel 2eelu Ndajem Senegalo-Gàmbi ci wàllu koom, yaxantu ak dugal xaalis.
CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:
- Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat Yaram ak Mbatiit dikk na ci leeral yi muy amal weer wu jot ci waajtaayu lootaabeg powi olempigu ndaw ñi (JOJ) ci Ndakaaru ci atum 2026;
- Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde ak Càmm gi àddu na ci tolluwaayu kàmpaañu njaayum gerte gi ci atum 2024, mbayum dër mi ak kàmpaañu payteef yi;
- Jëwriñu Kopparal gu ndaw gi ak koomum Jàppal ma jàpp mi àddu na ci taxawaayu Ngóornamaŋ bi ci doxal pexem koppparal mi ñu teg ci réew mi (SNFC) ngir taxawu koomum Jàppal ma Jàpp mi.
CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:
Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :
Sémbu dekkere biy lootaabe Njëwriñu Bennaleg Afrig gi ak Jëflante ak Biti Réew.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE