SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 14i FANI MEE 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 14 MONTHS.MAY 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 14i fani mee 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoorteel i kàddoom, Njiitu Réew mi ndokkale na njabootu katolig gi ginnaaw tabbug seen kilifa gu bees gi, Paab Lewon XIV, di nitu pas-pas di ku tijjiku ku fas yéene bay waar ci wàllu diisoo, jàppoo ak bennoo diggante askan yi ngir àddina su am jàmm, dal te tegu ci yoon. Ci loolu, woo na Ngóornamaŋ bi mu jël mbooleem dogal ak matuwaay yi war ngir amal ci anam yu mucc ayib, 0, 8 ak 9i fani suwe 2025, 137eelu Ajuj Popongin gi.

Njiitu Réew mi dikkaat na ci jafe-jafe bi am jëm ci amal caytu gu jaar yoon ci anam yi ñuy tabaxee taaxi pénc mi. Ndax kat, at yii weesu yépp dañoo seetlu ne taax yiy daanu dañoo bari lool, rawati na ci jamonoy nawet. Muy tekki kon ne, fàww ñu taxaw temm jiital ci jéegoo yi ñuy teg ci wàllu tabax ak dëkkuwaay, fexe ba ñu sàmmonte ak baaxaay, yàggaay ak kaaraangeg tabax yi ci anam yi yoon tëral. Ci noonu, Njiitu Réew mi woo na Ngóornamaŋ bi mu gën a taxaw ci saytu tabax yi ngir man a xam tolluwaay bi vi réew mi boole ko ak jël ay dogal yu wér yu ñu war a doxal ci yi ñu seetlu yépp ne jaarul yoon, ba ci joyyanti yi ñu ci war a indi ngir sàmmonte ak palaŋ yi ñu jëkk a digle jëm ci daaneel taax yi yàqu walla ñu nekk ci yoonu màbb. Sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu dëkkuwaay ak Tabax ak Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi ñu taxaw, ànd ko ak fara yi ak wànqaas yi yor kaaraangeg siwil gi, ci amal benn kàmpaañu yeete jëme ko ci askan wi ci sàrt yi aju ci wàllu dëkkuwaay ak matukaay yi nekk ci kot bi aju ci wàllu tabax nga xam ne dees koo war a jëfee ca na mu waree. Xamle na ne fàww ñu omolge mataryeli tabax yi ñuy jaay waaye itam di amal caytu gu wér ci liggéeyi tabax yi ñuy amal boole ko ak wànqaasi nguur yi yor wàllu caytu gi di wàcc saa su ne ci suuf ngir càmbar liggéey yi ba xam ñu ngi sàmmonte ak ndigalu tabax yi ñu leen jox. Ci loolu, Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi, niki mu ci joxe woon ndigal ca Ndiisoog Jëwriñ gu 18i fani desàmbar 2024, fàww ñu gën a taxaw ci yokkuteg yënguy “Laboratoire national de Référence des Bâtiments et Travaux publics (LNR - BTP)” bi ñu taxawaloon jaare ko ci sàrt l° 2023- 12 bu 21i fani suwe 2023. Dekkere l° 2023-1780 bu 29i fani ut 2023 bi koy doxal leeral na liggéey yi ñu sas kër gii ci wàllu njoxem agremaa yi ñeel “laboratoires” yiy yëngu ci wàllu gëstu ak saytu, omologasoo mataryel ak jumtukaay yi ñuy jëfandikoo ci taax yi ak liggéeyi pénc mi, saytu gëstu yi ci wàllu “géotechniques“ niki noonu risk natirel yi ak yu kéew mi.  Xamle na itam ne, fàww Njëwriñ gu ne, def ab tënk ci tolluwaayu kaaraangeg taax yi dalal seen i wànqaas niki mu ci joxee woon ay tegtal ca Ndiisoog Jëwriñ gu 9i fani awril 2025. Ci geneen wàll, xamle na solos taxawal, ànd ko ak ”Ordre des architectes”, pexem fagaru ci méngale ak saytu tabax yi ak rëddinu mbooleem gox yi ak bokk-moomeeli Senegaal yi.

Njiitu Réew mi àddu na ci mbirum suqaliku ak jigéen ñi ak ndaw ñiy jéem a taxawal dara ngir taxawu sosum xëy yi. Ndokkale na Njiitu Jëwriñ yi ci ndam li am ci ciiwalug, 08i fani mee 2025, ndoortel ñaareelu pàccu sémbu taxawu ak gunge jigéen ak ndaw ñiy jéem a taxawal dara (PAVIE 2) te ñu jagleel ko 107,2i milyaari FCFA. Taxaw na ci ne fàww ñu gën a taxawu ndaw ñi ak jigéen ñiy jéem a taxawal dara jaare ko ci gën a yaatal ci mbooleem gox yi matukaayi gunge yi ak kopparal yi, niki noonu fexe ba yëngu yi ñuy amal gën a am i njeexital. Muy lol dina gën a dooleel coppite yi ñu namm a amal ci pàcc yu am solo yiy indi ag yokkute boole ko ak jur ay xëy niki mbay mi, càmm gi, napp gi, pasiin gi ak xarala yi. Sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi mu fexe ba ñu amal céddale gu maandu ci koppar yi ci mbooleem goxi réew mi te gën cee jiital sémb yiy am njeexital yu wér ci yokk liy ñoree ci mbay mi ak bay-dunde gi. Njiitu Réew mi xamal na Njiitu Jëwriñ yi itam ne fàww ñu jiital ci koppar yi aju ci PAVIE  bii jëmale ko ci pexe yuy tax jigéen ñi manal seen bopp ci wàllu koom, rawati na jigéeni kaw gi, muy liy wane solos jàllale balaa yàgg sémbu yoonal wi jëm ci fexe ba jigéen ñi manal seen bopp ci wàllu koom. 

Njiitu Réew mi taxaw na ci déggoo gi war a am ci jëmmalug pexe yi ñuy teg ci ni ñuy saytoo njafaan yi ci réew mi. Ndokkale na Ngóornamaŋ bi, rawati na Jëwriñ ji yor wàllu Yasara gi ak Petorol bi ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi ci piblig bi ak ci piriwe bi tey dugal seen loxo ci yëngu ak yoriinu pàccu koom bu am solo bii nga xam ne caytu gi dafa war a leer te am njariñ. 

Ci jamono jii nu tollu jëm ci jëlaatal sunu bopp sunuy balli mbimdare, mbell, petorol ak gaas ak yoon wi nu sóobu jëm ci tàmbalee jëfandikoo gaas bi ci yenn sàntaraali SENELEC yi, sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi mu taxaw ci ñu amal doxaliin wu mucc ayib ci pas yi nu torlu ak sunuy partaneer waaye itam yoriin wu leer ci wàll wi te sóob ci mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi muy piblig bi mbaa piriwe bi. 

Njiitu Réew mi, ci geneen wàll, feddali na ag taqoom ci gën a suqali li jot a am ci réew mi boole ko ak gungeg Nguur gi ci keleŋi réew miy yëngu ci wàllu petorol bi ak gaas bi. Xamle na itam ne, fàww ñu def bilaŋu “Fonds de Stabilisation” bi ak “Fonds intergénérationnel” bi ñu dénk FONSIS mu koy saytu.

Mu daaneel ci wet gii, sàkku ci Jëwriñ ji yor wàllu Yasara gi ak Petorol bi, ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, ci Jëwriñu Koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi ak ci Sekkretariyaa bu COS-PETROGAZ ñu waajal, ci kilifteefu Njiitu Jëwriñ yi, ndaje mu jëkk mu kurél gi ci nguuram, balaa njeextalu weeru sulet 2025, ci teewaayu mbooleem ñi ci bokk ak mbooleel ñi teewal sektéer piriwe réew mi. 

Njàngalem làkki réew mi ak ay porogaraami liifantu ak gën a sóob Daara yi ci doxaliinu njàng mi doon na lu yitteel Njiitu Réew mi. Sàkku na ci Jëwriñu Njàng mi mu sumb, ànd ko ak ñiy yëngu ci wàll wi, xayma gu wér ak dundalaat bu baax politig yi ci wàllu liifantu ak gën a dooleel njàngalem làkki réew mi. Ndax kat, jàngee ci sunu làkki réew mi day lu am solo ngir gën a dëgëral moom sunu bopp gi.

Ci loolu, xamal na Jëwriñu Njàng mi ne fàww ñu def ub tënk ci njàngum làkki réew mi ñu jot a yoonal te gën leen a dooleel ci di leen jëfandikoo (dawal ak bind) ci biir mbooleem pàcc yi nekk ci campeef yi, ndoxal gi, njàng mi, koom mi ak dund gi. Ci geneen wàll, rafetlu na ndoortel liggéey yi jëm ci waajal waxtaan yi ñu namm a amal ci Daara yi. Diisoo yooyu ñu fas yéenee ànd ak ñépp dina tax ñu man a am ug déggoo ci jëmmal ay jëf yu wér yu jëm ci dugal Daara yi ci doxaliinu njàng mi ak koom mi ci réew mi.

Mu tëjee, ci arminaatu laamisoom, moom Njiitu Réew mi dikkaat ci teewaayam, 12i fani mee 2025 ca Abijaŋ, ca edisoo 2025 bu Afrikaa CEO Forum ba mu daje ak ay meññilukat yu bari ci àddina si te am yéene doxal ay sémb ak ay lëkkaloo yu làq njariñ seen diggante ak Senegaal ci lu soxal jëmmalug “Agenda Nationale de Transaformation Vision Senegaal 20250” bi.

Cig àddoom, Njiitu Jëwriñ yi dikkaat na bu baax ci taxawu gi ñu war a amal jëme ko ci këri liggéeyukaay yi nekk ci jafe-jafe ak méngale ndoxalug pénc mi ak jamono.

Lu jëm ci taxawu këri liggéeyukaay yi nekk ci jafe-jafe, Njiitu Jëwriñ yi, ginnaaw ba mu fésalee taxawaay bu am so bi këri liggéeyukaayi sektéer paraapiblig bi am ci luy gën a dooleel koomum réew mi sosug ay xëy, taxawlu na ci seen jafe-jafe yi nga xam ne li ci ëpp a ngi bawoo ci yoriin wu bon ak ay tànneefi làmbatu yuy tax duñu am njeexital yu am solo. Njiitu Jëwriñ yi fàttali na pexe yi ñu teg jëm ci sàmm ak dooraat yënguy ñaari kër yii di yëngu ci yaaleg jaww ji muy AIBD SA ak Air Sénégal SA, jaare ko ci dogal yi ñu jëloon ca ndaje ma jëwriñ yi séqoon 03i fani awril 2025. Njiitu Jëwriñ yi jox na ndigal Njëwriñ yi mu soxal ñu taxaw ci amal topp gu wér ci dogal yooyu ngir amal caytu gu mucc ayib te wóor ci yoon woowu jëm ci dundalaat kër yooyu. Njiitu Jëwriñ yi sàkku na itam ci Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi ak ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ñu dooraat yënguy ”Comité interministériel” biy topp ak a joyyanyiwaat këri liggéeyukayi pénc mi ak këri liggéeyukaay yi nga xam ne nguur a ci ëpp wàll. Mu tëjee ci wet gii moom Njiitu Jëwriñ yi, taxawlu ci solos teg politig bu bees buy dogoo ak jëfiin ya fi woon. 

Lu jëm ci méngale ndoxalu pénc mi ak jamono, Njiitu Jëwriñ yi fàttali na ne, doon na keno bu am solo ci jëmmalug ”Vision Sénégal 2050” bi ñu tënk ci “Agenda national de Transformation” bi. Ci loolu, soppi ko boole ci méngale ko ak jamono dinañu am solo lool ngir serwiis piblig bu mucc ayib. Ngir loolu nag, Njiitu Jëwriñ yi xamle na ay dogal yu ñu ci war a jël ngir baral jéego yi jëm ci jëfandikoo xarala yi ak gën a jagal anam yi ñuy saytoo liggéeykati Nguur gi, rawati na saytukat yi ak way-doxal yi. Njiitu Jëwriñ yi daaneele ci taxawlu ci wareefu yokk man-man yi aju ci wàllu doxal coppite yi, xereñteg ndoxal gi, jub ak jubal ci liggéey bi ngir tabax ndoxalug suqaliku, gu sukkandiku ci keno yi war ngir sottal “Vision Sénégal 2050” bi.

Lu soxal àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñu Kéew mi ak Jàll jëm ci Ekolosi àddu na ci lootaabeg Ndajem àddina si ñu jagleel warabi ndox yi ñu aar te war koo amal ca atum 2027 ci Ndakaaru ;
  • Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat Yaram yi ak Mbatiit mi àddu na ci tolluwaayu déggooy lëkkaloo yi ñu am ngir jébbale liggéey yi aju ci powi olympigu Ndaw ñi (JOJ) ci Ndakaaru 2026.

CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

  • Sémbu dekkere biy may Njiitu Réew mi mu xaatim porotokol yi aju ci amàndmaa yu artiikal 50 alinea a ak 56 yu déggoo gi jëm ci mbirum “aviation civile internationale” bi ñu torlu woon ca Montreal 06i fani oktoobar 2016. 

Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi. 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE