SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 12i FANI MARS 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 12 MONTHS.MARCH 2025

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 12i fani mars 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi jébbal na njaalam Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, ginnaaw faatug Sëriñ Abdu JUUF, Njiital Njël li, te ñu tabboon ko 22i fani sãawiye 2025 ci Ndiisoog Jëwriñ yi. Abdu JUUF nekkoon « Inspecteur du Trésor » bu mucc ayib bob, njàmbaaram, xereñam ak xamam doxaliinu Nguur doonoon la lu ñépp rafetlu. Yal na Yàlla def Àjjana muy dëkkuwaayam.

Njiitu Réew mi dikkaat na ci njàngat ak digle yi bawoo ci ayu bis bi ñu jagleel jigéen ñi. Ndokeel na bu baax Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalnte gi ci ci lootaabe gu mucc ayib gi ak ndqm li am ci xew wii ñu tëjee ci dajale mbooleem ñi teewal mbootaayi jigéeni Senegaal yi ca « Grand Théâtre national », 08i fani mars 2025. Sàkku na ci Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi mu def ug xayma ci njàmbati jigéen ñi ci tund wu ne te gaaral ko pexe yi ñu war a doxal ci réew mi ngir gën a jagal nekkiinu jigéen ñi.

Pas-pasu doxaliin wu xereñ te mucc ayib nag mooy li war a gunge jëmmalug « Agenda national de Transformation » bi. Loolu tax na Njiitu Réew Mi jël dogalu taxawal ci ab dekkere, aw raaya ci wàllu xereñte tuddee ko « Médaille Gaïndé de la performance » ngir neexal ma-réew yi gën a ràññiku ci amal ay jëf yu jëm ci suqali ak fésal réewum Senegaal. Muy raaya wu ñuy jagleel jëf yi jëm ci suqali wàllu njàng mi, paj mi, kaaraange gi, wattu gi, xarala yi, pasiin yi, mbatiit mi, tàggat yaram, mbay mi, koom mi, fent gi, ndoxal gi, añs. Ñu war koo jox képp kuy doomi Senegaal te matale sàrt yii ñu tëral, ak képp ku amal liggéey bu am solo ci wàllu xereñte.

Yoriin wu leer ci balli mbindaare yi nag doon na lu yitteel lool Nguur gii. Ci wàll woowu, Njiitu Réew mi fàttali na ag taqoom ci amal doxaliin wu mucc ayib ci kurel gii di « Comité national de l’Initiative pour la Transparence dans les Industries extractives (ITIE Sénégal) » ak dooleel gu sax dàkk ci jumtukaay yi ñu koy jagleel ngir mu man a matale li ñu ko sas. Sàkku na ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, ci Jëwriñu Yasara gi, Petorol bi ak Mbell yi ak ci Jëwriñu Kéew mi ak Jàll jëm ci Ekolosi, ñu jël mbooleem matuwaay yi war, ànd ko ITIE Sénégal, ngir taxaw ci sàrt yu bees yi ñu tëral ci ITIE 2023 te Senegaal war koo walide fii ak weeru sulet 2025. Xamal na Ngóornamaŋ bi itam solos taxaw temm ci gën a leeral, jaare ko ci di siiwal lim yi ci wàllu koom mi ak koppar yiy bawoo ci jëfandikug mbell yi, petorol bi ak gaas bi. Ci loolu, fàttali na ne fàww ñu yeesal sistem bi Nguur gi di dajalee koppar yiy bawoo ci wàllu mbell yi ak petorol bi, mu teg ci taxaw bu baax ne fàww ñu fexe di siiwal saa su ne limub way-tonowu yi niki noonu càmbar yi ñu amal ci kontaraa yi ci wàllu mbell yi ak petorol bi, galag yi ak njëg yi ci keri liggéeyukaay yi.

Njiitu Réew mi xamle na solos amal caytu gu mucc ayib ci njureefi kéew mi ak nekkiin yiy bawoo ci jëfandikug mbell yi ak petorol bi ci dundiinu askan wi. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, ci Jëwriñu Yasra gi, Petorol bi ak Mbell yi ak ci Jëwriñu Kéew mi ak Jàll jëm ci Ekolosi, ñu lëkkaloo ak Jëwriñ ji yor wàllu Gox yi ak Goxaan yi, xayma ba ñu leen taxawalee ak leegi, tolluwaayu koppari mbell yi ñu jagleel taxawu ak yamale gox yi, niki noonu itam koppar yi ñu jagleel yeesalaat warab yi am i mbell. Jox na ndigal Jëwriñ yi mu soxal, ñu àndandoo càmbar sektéer yi ànd ko ak « Comité national ITIE » ngir gën a waajal yoonu « validation » bu Senegaal teg ci yëgal askan wi ak ñi séq wàll wi ci doxaliinu pàccu liy bawoo ci biir suuf. Ci loolu sax, woo na Jëwriñu Koppar yi ak Njël li muy indi ay leeral weer wu jot ci Ndiisoog Jëwriñ yi, tollwaayu « Fonds intergénérationnel » bi ak « Fonds de stabilisation » bi ñu tënk ci sàrt bi soxal anam yi ñuy séddalee ak a saytu alal jiy bawoo ci jëfandikug hidrokarbiir yi.

Gis-gisu « Sénégal 2050 » yitte ju kawe la am ci baral jéego yi jëm ci samp ay ndefar ci réew mi jaare ko ci xoolaat ak suqali fànn yu bari yi te am solo lool ci réew mi, yu mel ni fosfaat bi, payteef yi ak turism bi. Muy kon fexee tabax koom mu am doole te xemmemu, mu jeng jëm ci gën a dooleel man-man yi ci réew mi ak balli mbindaare yi nga xam ne dinañu man a jur ay xëy yu mucc ayib. Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Koom mi ak ji yor wàllu Ndefar yi, ñu lëkkaloo ak APIX, xayma « zones économiques spéciales » yi ak « agropoles » yi ñu taxawal, ci limub këri liggéeyukaay yi ñu jot a samp, alal ji ñu ci jot a dugal ak li ñu jot a fent ci wàllu xarala, jàppandal yi (ndoxal, galag, suuf…) leen Nguur gi jagleel, xëy yi ñu jot a jur ak seen taxawaay ci dooleel wàllu « exportations » yi ak doxal « Pôles territoires » yi. 

Ak yokkute gi ñu namm a amal ci teg ay politig ci wàllu ndefar, Njiitu Réew mi daaneel ci xamal Njiital Jëwriñ yi solos taxaw temm ci lëkkale yëngu ak dooley kër yii di APIX, ASEPEX, APROSI, ASPIT ak porogaraam bi jëm ci suqali Agrople yi muy PNDAS.

Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi leeral na Ndiisoo gi tolluwaayu liggéeyi càmbar yi ñu doon amal ci wàllu suuf si te soxaloon lotismaa yi nekk ci tund yu Ndakaaru, Cees ak Ndar. Fàttali na wareefu càmbar yooyu ndax jalgati yu jéggi dayo yu ñu ci seetlu te yàggoon leen a yoole. Ci loolu, ci ndigalu Njiitu Réew mi, santaane woon na ñu amalandoo ay càmbar ba xam, anam yi ñu sancee woon suuf si féete ci tefesi pénc mi ak yenn lotismaa yi, tegu nañu ci yoon. 

Njiital Jëwriñ yi xamle na ne, tàmbali nañoo doxal digle yi bawoo ci ràppoor bi ñu amal ci anam yi ñu sancee woon suuf si féete ci tefesi penc mi. 

Lu soxal lotismaa yi nekk ci Ndakaaru, Cees ak Ndar, te waraloon càmbar gi, kurél gi ñu tegoon ngir loolu matale na daanaka ràppoori càmbar yi ci ëppoon solo. Dogal yi ñu digle ci ràppoor yooyu nag ñu ngi jëm ci :

  • neenal lépp walla lenn ci yenn lotismaa yi, Palaŋi Dëkkuwaay yi ak pàkk yi ñu jot a dagg, ndax seen ñàkk a sàmmonte ak yoon yi ñu tëral ci wàll woowu;
  • dakkal ndigalu cakkuteefi jot ci suuf ci ab barab, fii ak ñuy tëral palaŋu fàkk bees waxtaane ba am cig dëppoo;
  • wéyal ak teggi liggéey yi ñu dakkalandi woon, ci kaw ñu amal ay joyyanti, ci lépp walla ci lenn ci lotismaa yi, ginnaaw ba DGSCOS amalee ay càmbar benn benn rawati na ci suuf su bari su ñu seetlu ñu jox ko kenn nit rekk mu ngardàjjoo ko.

Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ yi mu soxal ñu jël matuwaay yi war jëm ci matale liggéeyi càmbar yooyu, ca na mu gën a gaawee.

Ci geneen wàll, niki ko Njiitu Réew mi diglee woon, Njiital Jëwriñ yi taxaw na bu baax ci lu jëm ci jàngat yi ñu war a jëlee ci càmbar yi bawoo ci ni ñu yoree woon alalu askan wi ci diggante 2019 jàpp mars 2024, ne fàww ñu taxaw temm ci amal yoriin wu wóor te leer ci alalu askan wi ci mbooleem wànqaasi parapiblig bi. Ci loolu, sóob na mbooleem jëwriñ yi ci ñu fexee matale liggéey yi war ci wànqaas yi aju ci ñoom, rawati na ci lu jëm ci jataayi dëggal  yi kuréli càmbar yi war a amal ci anam yi ñu yoree alal ji ci atum 2024. Muy lu mel ni taxawal arminaatu ndajey « pré-conseil » yi niki noonu fexee méngale sàrt yiy doxal wànqaas yooyu ak li yoon tëral ci doxaliinu sektéer parapiblig bi, saytu gafag réew mi ak càmbar nit ñi am lenn lu leen Nguur gi dénk ngir ñu war koo doxal. 

 Lu soxal àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñu Bennoog Afrig gi ak Jëflante ak Biti Réew ak Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi bokk nañu àddu ci jafe-jafe yi am ci wàllu jàll-waax yi ñuy jox saa-senegaal yi féete biti réew ;
  • Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi àddu na ci anam yi ñuy sottee dund bu doy ci ja bi;
  • Jëwriñu Foŋsoo Piblig bi ak Yeesal Serwiis Piblig bi indi ay leeral ci topp gi ñuy amal ci tegtal yi bawoo ci ndaje mi doxoon diggante Nguur-Njaatige-Sàndikaa;
  • Jëwriñu Ndaw Ñi, Tàggat Yaram ak Mbatiit mi àddu na ci waajtaay wi ci wàllu mbatiit jëm ci JOJ DAKAAR 2026 yi ak tolluwaayu jëmmal dogal yi ñu jëloon ci ndaje mi ñu ci amaloon diggante jëwriñ ji.

CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

  • Sémbu yoonal wi aju ci sos ak taxawal anam yi ñuy lootaabee ak ak a doxal « Observatoire national des Lieux de Privation de Liberté (ONLPL);
  • Sémbu dekkere bi aju ci sos ak taxawal anam yi ñuy lootaabee ak ak a doxal « Fonds de Développement de la Microfinance islamique (FDMI) ».

Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE