Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, tay ci àllarba ji 11i fani desàmbar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi dikkaat na ci bis bi ñu jagleel yeleefi doomi aadama yi te doon ko màggal ci àddina si démb, 10i fani desàmbar 2024, mu posewu ci ngir àddu ci mbirum gën a dooleel Réewum yoon ci Senegaal ak politig bi ñu teg ci réew mi ngir fésal ak sàmm yelleefi doomi aadama.
Ci noonu fàttali na taqoo gi Senegaal taqoo ak réewum yoon ak sàmmonte ba fàww ak yelleefi doomi aadama ak lu leen di sàmm. Loolu mooy li tax ñu lootaabe woon, 28i fani mee 2024, Jataayi Waxtaane Yoon yi nga xam ne ñu ngi ci tànki doxal digle yi fa bawoo woon sukkandiku ko ci arminaat bu leer.
Ci geneen wàll, fésal na jéego yu am solo yi ñu seetlu ci at mii, ci doxal politigu fésal yeleefi doomi aadma yi boole ko ak dooleel yombal gi jaare ko ci dëggal, 18i fani sebtàmbar 2024, sàrt l°2024-14 bi aju ci taxawal ci réew mi Kurél guy saytu yelleefi doomi aadama yi nga xam ne ña ca war a bokk dees na leen tànn jaare ko ci woote ag lawaxu. Ci loolu, jox na ndigal, Jëwriñu yoon ji, mu jël mbooleem matuwaay yi war yi jëm ci jël ak tabbug ñi war a bokk ci Kurél giy saytu yelleefi doomi aadma yi ci réew mi balaa 31i fani sãawiye 2025.
Ci geneen wàll, xamal na Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ne fàww ñu dooleel ci wàllu koppar kurél gu yees gii, nga xam ne, war naa tëral fii mu ne, ci juróomi at yii di ñëw, pexem suqaliku mu wóor mu méngoo ak gis-gisu Senegaal gu moom boppam, Jub te naat. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu taxaw ci topp ak a càmbar mbooleem jëfi ngóornamaŋ bi jëm ci gën a jagal taxawaayu Senegaal ci toftaleg kuréli àddina siy yëngu ci wàllu Yelleefi doomi aadama boole ko ak taxaw ci fexe ba ñuy jàngale wàllu fésal ak sàmm yeleefi doomi aadama yi ci lekool yi ak ci jàngune yi, niki noonu ci mbooleem warabi tàggatukaay yi ci réew mi.
Njiitu Réew mi àddu na ci mbirum tëggaat ci lu jamp politigu xëyu ndaw ñi doon yitte ju far ci réew mi, boo xoolee ni li ëpp ci askanu Senegaal doonee ay ndaw ak ni ñàkk a xëy mi yaatoo ci ndaw ñi. Woo na Njiital Jëwriñ yi mu gaaw matale xayma gi ci mbooleem yéene yi, naal yi, sémb yi ak matukaay yi nguur gi teg ngir xëyu ndaw ñi (ANPEJ, DER/FJ, 3 FPT, XËYU NDAW ÑI, Domaines agricoles communautaires (DAC), Formation Ecole Entreprise (F2E), AGETIP, FERA…). Sàkku na itam ci Njiital Jëwriñ yi mu sumb, ànd ko ak Jëwriñ yi ak wànqaasi nguur yi mu soxal, sektéer piriwe bi ak mbootaayi liggéeykat yi, bind ak doxal pexe mu yees, mu wér te wóor mu jëm ci wutal ndaw ñi ay xëy.
Njiitu Réew mi feddaliwaat na ag taqoom gu wóor ci doleel séddale ci mbeeraay gi politigu tàggatu gu xereñ gi ak gu xarala gi jaare ko ci méngale ko ak kàrtu jàngune yi ak ISEP yi, taxawal juróom ñetti (8) goxi koom, rëdd ak yaatalaat pàcc yi gën a am solo ci sukkandikukaayu politigu koom mi ak dundiinu askan wi. Xamle na ci loolu ne fàww ñu dooleel tàggatu gu xereñ gi ak gu xarala gi jaare ko ci fexe mu bari te wuute, yeesal ak méngale tàggatu gi te taxaw bu baax doore ko ca njàng mu digg-dóomu ma, ci waajal dongo bi ci wàllu xereñte. Ak fexe itam baral jéego yi ci sémbi tabax warabi tàggatu gu xereñ gi ci gox yi ak tëral pexey tàggatu yu wér ngir man a fexe ba ndaw ñi nga xam ne dañoo teel a bàyyi njàng mi ñu man a am fu ñu dugg.
Njiitu Réew mi xamal na Njiital Jëwriñ yi ci geneen wàll ne fàww ñu jëme politig yi ak matuwaayi taxawu gi, kopparal ak dooleel ndaw ñiy taaba-taaba ak a jéem a taxawal seen xëyu bopp, jaare ko ci teg sistemu xamle gu wér boole ko ak topp gu wóor. Ci loolu ba leegi, xamle na jampug xoolaat pas yi ci wàllu déggoo yi dox diggante Nguur gi ak Njaatige yi (CNEE), di jumtukaay bu ñu war a gën a jëmale ci pàcc yiy gën a indi ay xëy. Fàttali na itam Jëwriñ ji yor wàllu Liggéey ak Xëy, ndigalam li jëmoon ci waajal gu mucc ayib 3eelu ndaje mi ñu jagleel Xëyu Ndaw ñi.
Lu soxal jafe-jafey peeg bu wér nit ñi ci doxaliinu njàng mi, Njiitu Réew mi seetlu na ne jàngalekat yi dañoo néew lool ci lekool yu bari, ci kolees yi ak ci liise yu Senegaal. Tolluwaay boobu di gën a jéggi dayoo at mu jot, bokk na ci li ko waral mooy limub ni nit ñi di yokkoo ak saytu gu baaxul ci fuglu limub dongo yi, xëy yi ak man-man yi ci pàccu njàng mi. Sàkku na kon ci Jëwriñu Njàng mi, Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, ñu gaaw matale, ci caytug Njiital Jëwriñ yi, sémb wu ñu jagleel jël ay jàngalekat ci ñetti at (2025, 2026, 2027), sukkandiku ko ci espesiyaalite ak màcceer yi ñu yittewoo. Ci geneen wàll, woo na Njiital Jëwriñ yi mu baral jéego yi jëm ci doxal sémb wu jamp wi soxal jëlee fi lekooli mbaar yi ànd ko ak larme bi, rawati na xam-xamu sóobare si, ci amal liggéey bu wér te wóor.
Lu soxal arminaatam ci wàllu laamisoo, Njiitu Réew mi dikkaat na ci ngan yi mu jot a amal ca Abu Dabi ak ca Kataar ga mu teewe Ndajem Waxtaan ma woon ca Dohaa. Ca Abu Dabi ak Dohaa, fas nañu yéene yóbbu lëkkaloo gi fu gën a kawe. Njiitu Réew mi dikkaat na itam ci tukki nemmiku gi mu amal ca Nuwaagsót, ca Réewum Islaam gu Móritani, ngir teewe Ndaje mi Mbootaayu Réewi Afrig yi jagleloon Njàng mi, Ndaw ñi ak Xëyu Ndaw ñi.
Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi xamle na solo su kawe si am ci natt jàppandig nit ñu mucc ayib ci ndoxal gi ngir sottal pexem soppi Senegaal fii ak 2050. Ci loolu, woo na Jëwriñ yi ñu taxaw ci gën a yokk man-mani liggéeykat yi, jaare ko ci di amal ay tàggatu ak di xool tomb yi leen dese te man a doon lu ñuy soxla ngir doxal ci biir foŋsoo piblig.
Lu soxal waxtaane njël yi balaa yàgg ca Ngombalaan ga, Njiital Jëwriñ yi fàttali na pas-pas bi ko lal te jiitu taxawalug Sàrtu kopparal bu 2025, te tënku ci yaxanal deppaas yi niki noonu liy bawoo ci li nuy am, bees sukkandikoo ci li càmbar yi wane ci tolluwaayu alalu askan wi.
Sàkku na ci Jëwriñ yi ñu def ni seen yëfi bopp pas-pas bii ci doxaliin wu yees wii ci alalu askan wi laajoon ay leeral ci njël li. Jëleef na dogalu bañ a dugal ci njël li lu dul sémb ak naal yu wér yi am njeexital ci koom mi ak dundiin wi.
Ci geneen wàll, ni ko Njiitu Réew mi diglee woon, sàkku na ci Jëwriñu koppar yi ak njël li ak yeneen Jëwriñ yi, ci lu soxal wànqaas yi aju ci ñoom, ñu jëllu mbooleem matuwaay yi war ci wànqaas yi mu soxal ngir taxaw bu wér ci sàmmonte ak sàrt yi, àpp yi, payoor yi, bursu njàng mi ak yenn ndàmpaay yi Nguur gi warloo.
Mu tëjee moom Njiital Jëwriñ yi ci àddu, ni ko Njiitu Réew mi diglee woon, yitte ji ñu war a def ci atum 2025 ci door pexe mu jamp mi jëm ci saafara jàngalekat yu néew yi, jaare ko ci dugal koppar yi ñuy jëlee ci li ñu jot a yaxanal ci yenn campeef ak kurél yi ñuy tas, jëlaat ci ay jàngalekat yu bees ngir dooleel pàcc boobu. Ñi ñu ci war a jiital nag ñooy kontraktiyel yi fi jot a nekk.
CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:
Jëwriñu Yasara gi, Petorol bi ak Mbell yi àddu na ci càmbar gi njëwriñam jot a amal ci këyiti mbell yi;
Jëwriñu Kéew mi ak Jàll Jëm ci Ekolosi def na ab tënk ci ndajem pàcci COP yi ci wàllu biyodiwersite (COP16), soppikug njuux li (COP29) ak tàkkal yi (COP 16);
Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde ak Càmm gi àddu na ci kàmpaañu njaayum gerte gi ci atum 2024, njureefi gerte gi ak kàmpaañu lujum yi.
CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:
Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :
Sémbu yoonal wi jëm ci far sàrtu organig l° 2012-28 bu 28i fani desàmbar 2012 bi aju ci lootaabe ak doxaliinu CESE ak sàrtu organig l° 2016-24 bu 14i fani sulet 2016 bi aju ci lootaabe ak doxaliinu HCCT;
Sémbu yoonal wi jëm ci yeesalaat Ndayi Sàrti Réew mi.
CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii:
Ci wàllu Njëwriñu Bennaleg Afrig ak Jëflante ak biti réew :
Sëriñ Maam Baaba Siise, xelalekat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 516 903/B, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ci wetu kilifa gi Philippe 1er, Buuru Belsig, mu wuutu Sëriñ Baay Moktaar Jóob, mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Soxna Faatu Isidoraa Maaraa Ñaŋ xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 602 565/D, doonoon lu ko jiitu ma-laamisoo, Sekkereteer Seneraalu Jëwriñu Jëflante ak Biti Réew, tabb nañu ko Ma-laamisoo, Ndawul Njiitu Réew mi ca Farànkofoni;
Sëriñ Ibraahiima Al Xaliil Sekk, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 604 448/B, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoob Senegaal ca Kowet, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca wetu Kilifa gi Felipe VI, Buuru Espaañ, mu wuutu soxna Mariyaam Si mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Koli Sekk, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 604 134/H, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoo, Ndawul Senegaal ca Office des Nations Unies ca Genève, tabb nañu ko Ma-laamisoo, Ndawul Senegaal ca Mbootaayu Réewi Àddina si ca New York, mu wuutu Sëriñ Seex Ñaŋ mi war a dem àllaateret;
Sëriñ Abuubakar Sadiix Bari, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 604 133/I, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoob Senegaal ca Gana, tabb nañu ko Ma-laamisoo, Ndawul Senegaal ca Office des Nations Unies ca Genève, mu wuutu Sëriñ Koli Sekk mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Biram Mbañig JAAÑ, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 604 446/D, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoob Senegaal ca Réewum Islaam gu Móritani, tabb nañu ko Ma-lamisoob Senegaal ca wetu Kilifa gi Salmaan Bin Abdel Asiis Al Sawud, Buuru Araabi Sawudit, Sàmmkatu Ñaari Jàkka yu Sell yi, mu wuutu Sëriñ Mammadu Sàll mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Seex Tiijaan Sàll limatu payoor 604 131/K, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoob Senegaal ca Almaañ, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca wetu Kilifa gi Seex Tamiin Bin Ahmat Al Tamin, Emiir bu Kataar, mu wuutu Sëriñ Muhammet Abiibu Jàllo mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Soxna Geneviève Fay MANEL, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 606 892/K, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca wetu Kilifa gi Siril Ramafosaa, Njiitu Réewum Afrig Di Sidd, mu wuutu Soxna Safiyatu Njaay mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Soxna Mari Ñama Baseen, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 611 459/B, doonoon lu ko jiitu Jëwriñ-Xelalekat ca dalu laamisoob Senegaal ca Itaali, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca wetu kilifa gi Luiz Inacio Lula Da Silva, Njiitu Réewum Beresil, mu wuutu soxna Aminata Faal Siise mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Asan Sugu, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 603 336/C, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoob Senegaal ca Pari, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca wetu kilifa gi Nawaaf Al-Ahmat Al-Jabeer Al-Sabah, Emiir bu Kowet, mu wuutu Sëriñ Ibraahim Al Xaliil Sekk mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Isidoor Marsel Seen, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 624 526/A, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoob Senegaal ca Washington, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca wetu ku Sell ki Paab François, mu wuutu Sëriñ Martin Paskaal Tin mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Mustafaa Soxna Jóob, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 616 223/H, doonoon lu ko jiitu Ma-laamisoo, xelalekatu xarala ca Njëwriñu Bennaleg Afrig ak Jëflante ak biti réew, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca Wetu Recep Tayyip ERDOGAN, Njiitu Réewum Turki, mu wuutu Seneraal Seex Géy mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Piyeer Maad FAY, xelalakat ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 624 511/C, Ma-laamisoo, Njiital Organisations internationales et de la Mondialisation, tabb nañu ko Delege ca UNESCO, mu wuutu Suleymaan Jules Jóob mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Aaróona Siise, Chancelier ci wàllu jëflante ak biti Réew, limatu payoor 506 348/D, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca Jedda, mu wuutu Sëriñ Seexunaa Mbàkke mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Saalifu JAJU, Chancelier ci wàllu jëflante ak biti réew limatu payoor 602 521/D, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca Naples, mu wuutu Sëriñ Idriisa Ben Seen mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Momar Anta Siise, Chancelier ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 616 051/O tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca Kaasabalànkaa, mu wuutu Sëriñ Yuusu Jóob mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Mammadu Lóo, Chancelier ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 616 055/K, tabb nañu ko Ma-laamisoob Senegaal ca Madrid, mu wuutu Sëriñ Mammadu Mustafaa Lum mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Sëriñ Lamin Ka Mbay, Chancelier ci wàllu jëflante ak biti réew, limatu payoor 620 657/D, tabb nañu ko Ma-Laamisoob Senegaal ca Barsalon, mu wuutu Sëriñ Aliw Jaawo mi ñu woolu ci yeneen yitte;
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE