SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 09i FANI AWRIL 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 09 MONTHS.APRIL 2025

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 09i fani awril 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi jébbal na njaalam ci turu askan wi jëme ci njabootug Laayeen ak Jullit ñi, ginnaaw génn àddunag Sëriñ Muhammadu Maxtaax Laay, Xalifa Seneraalu Layeen yi. 

Menn at mu mat sëkk ci tay, ci la Njiitu Réew mi jiite woon Ndiisoog Jëwriñ gu njëkk, ginnaaw ba ñu taxawalee Ngóornamaŋ bi, Usmaan Sonko nekk ca bopp ba di Njiital Jëwriñ yi. Ginnaaw at mu mat sëkk mu mu jot a liggéey, Njiitu Réew mi a ngi dellu di sant Yàlla. Kañ na bu baax taxawaay bu mat sëkk bi Ngóornamaŋ bi wane ngir sottal ca na mu gën a gaawee sémbu Senegaal gu moom boppam, gu yoon di dox te naat, ci kaw jàmm, dal ak jàppalante. 

Njiitu Réew mi dellusiwaat na ci Màggalug 65eelu at mi Senegaal moomee boppam, te ñu amalee ko ci anam yu mucc ayib, ci biir mbokkoo ak bëgg sa réew, muy wane mbégte mu rëy ci mbooleem askan wi. Njiitu Réew mi rafetlu na teewaayu Njiiti Réew yu Gàmbi, Móritani ak Gine Bisaawóo ak bu Topp-njiitu Réewum Niseriyaa. Ndokkale na Jëwriñu Larme bi, Seef Detaa Masoor Seneraalu Larme bi ak Hóo Kumàndaŋ bu Sàndarmëri Nasonaal ci wajtaay ak anam yu mucc ayib yi ñu amalee fésalug gànnaay yi ak maaj gi fépp ci réew mi. Ndokkale na mbooleem way-kaaraange yi ci seen jaayante gu sax dàkk ngir réew mi teg ci tamit jaajëfal boole ko ak ndokkale dongo yi, mbootaayi ndaw ñi, ñiy yëngu ci wàllu mbatiit ak mbooleem ñi am taxawaay ci réew mi te doon ñu dugal seen yoxo ci yëngu yi ak maaj yi. Ci jamono jii nu tollu ci jëlaatal sunu bopp sunu mboor ak sunu mbaax yu am solo yi, kañ na bu baax ni sunu way-kaaraange yi doonee royukaay ci wàllu sàmm ak dooleel bëgg sa réew gu wér ngir tabax Senegaal. 

Fésal mbaaxu yar ak teggiin ak bëgg sa réew ci mbooleem pàcc yiy doxal réew mi doon nañu lu yitteel Njiitu Réew mi. Ci loolu fàttali na Ngóornamaŋ bi ne, bokk na ci yitte yi ñu war a jiital, mooy fexee sóob ndaw ñi ak taxawu leen ci ay yënguy suqaliku, niki noonu gën a dooleel déggoo diggante larme bi ak askan wi. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu yokk, ci yéeney Senegaal gu moom boppam, tegu ci yoon te naat, doxal sémb wii di « Programme national de Promotion de la Citoyenneté », waaye itam doxal politig bu bees ñeel ndaw ñi, ci genn wàll, sunuy mbaax ak sunu mbatiit, ak ci geneen wàll, ci yokkuteg xarala yi, koom mi ak dundiinu jamono ji. 

Njiitu Réew mi xamle na ne fàww ñu gën a joxaat gëdd « instruction civique » ci njàng mi boole ko ak tabax ay jumtukaay ci wàllu nekkiin, tàggat yaram ak mbatiit yu jëm ci taxawu ak fésal man-man yi nekk ci ndawi Senegaal. Kon nag, fàww ñu gën a dooleel mànkoo gi ci lekool yi, ci daara yi ak ci mbooleem koñ yi ak dëkki Senegaal yi. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Ndaw ñi mu taxaw ci lootaabe gu ñu dëppoo, balaa 1 panu sulet 2025, lii di « Conseil national de la Jeunesse » gi war a soppiku jëm ci doon genn kurélug diisoo guy boole mbooleem gaaral ak nammeeli ndawi Senegaal ci wàllu suqalikug réew mi. Rafetlu na lootaabeg bis yi ñu jagleel ndaw ñi ci àddina si (JMJ) 6 ak 5i fani awril ca Puut Jaag (ci tundu Cees) teg ci ndokkale mbooleem ñi ko doon teewe. 

Njiitu Réew mi posewu na ci màggalug bis bi ñu jagleel wàllu wér gi yaram ci àddina si, 07i fani awril 2025, ngir fàttali Ngóornamaŋ bi, rawati na Jëwriñu Paj mi ak Ndimbal li, jampug gaaw teg ay matuwaay yu wér te wóor yu jëm ci méngale doxaliinu paj mi ak jamono ci fànn yépp nag. Xamle na ci loolu ne, fàww ñu taxaw temm ci fexe ba fegu ci tawat yi doon li ñuy jiital ci politig yi ñuy teg ci wàllu wér gi yaram. Dina am solo loom kon ñu amal doxaliinu paj mu xereñ ci anam yi ñuy saytoo jarag yi. Ci yoon woowu kon, woote na ci ñu rëddaat kàrt bu bees ci wàllu pajum Senegaal lépp tegu ci méngoo, mottalante ak gën a baaxal taax yi ak warabi fajukaay yi, niki noonu serwiis yi ak paj mi ñuy amal. Xamle na, ci geneen wàll itam, solos gaaw mottali yeesal yi aju ci raglu yi, taxaw temm ci am ay jumtukaay yu mucc ayib ci wàllu paj mi niki noonu fexe ba serwiis yiy dalal jarag yi ak yiy taxaw ci yu jamp di dox bu baax. 

Njiitu Réew mi taxaw na bu baax ci ne fàww ñu gën a baaxal taxawu gi ci wopp yu koronig yi (jafe-jafey dëmbeen, ngal, añs), dooraat lii di porogaraam bi aju ci wàllu ñakk yi boole ko ak gaaral palaŋu  juróomi at bu jëm ci jël ay liggéeykat ci kaw sistemu pajum pénc mi ngir waajal tijjite ak yeesalaat raglu yi ak warabi fajukaay yi ci mbooleem tund yi ci Senegaal. Ci geneen wàll, sàkku na ci Jëwriñu Paj mi ak Ndimbal li, mu lëkkaloo ak Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, jël mbooleem dogal ak matukaay yi war ngir xeex njaay mu jaarul yoon mi ci wàllu garab yi ak ñiy yëngu ci lu dul yoon ci wàllum paj ak xay fépp ci réew mi. Ci loolu ba leegi, sàkku na ci Jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi ak ci Jëwriñu Paj mi ak Ndimbal li, ñu liggéey ci amal caytu gu mucc ayib ci warab yiy jàngale ak a tàggat ci wàllu paj, garabal ak ci wàllu suqalikug paj ak ndimbal. 

Njiitu Réew mi soññ na Ngóornamaŋ bi mu gën a bàyyi xel Fakilte yi ak Warabi Tàggatukaay yi ak Gëstukaay yi ci wàllu paj, warabi piblig yi ak piriwe yiy tàggat ci wàllu paj, garabal ak xereñte ci wàllu wér gi yaram. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu taxaw ci doxaliinu « Centres hospitalo-universitaires » (yu mel ni CHU Fann ak Dantec), gën a yokk liggéeykat yi ñuy jël ak tegaat « Ecole militaire de Santé » ak « Service de santé des Armées » ci biir Doxaliinu paj mi. Ci geneen wàll, sàkku na ci Jëwriñu Paj mi ak Ndimbal li mu wéyal jéego yi jëm ci joyyantiwaat  ak suqali ndefari garabal yi ngir def Senegaal selebe yoonu garabal bi gën a ràññiku ci Afrig. Ci loolu, fàttali na Ngóornamaŋ bi ne fàww mu taxaw temm ci amal topp gu wér ci yënguy « Agence sénégalaise de Réglementation pharmaceutique (ARP) ak yu  Pharmacie nationale d’Approvisionnement (PNA) », niki noonu sémb yi ñu teg ci yoxoy « Institut Pasteur » bu Ndakaaru, te aju ci wàllu dooleel Senegaal ngir mu manal boppam ci wàllu ñàkk ak garabal. Mu tëjee bunt boobu, ci woo  Jëwriñu Paj mi ak Ndimbal li mu ànd ak ñiy yëngu ci wàll wi, xalaat ci pexe yu ñu dëppoo jëm ci peeg alal ji ñuy dugal ci wàllu paj mi ak kopparal gu sax ci doxaliinu paj mi. Muy kon, fexee baral jéego yi jëm ci jëfandikoo xarala yi ci serwiisi paj mi, ci lu soxal New Deal technologique bi.

Njiitu Réew mi jiite na ndoortel 2eelu edisoo bu « caravane nationale de l’espace » bii ñu tuddee, « SPACEBUS 2025 », te « Agence sénégalaise d’Etudes spatiales (ASES) » di ko doxal. Ndokkale na Njiital ASES ak mbooleem ñi jàpp ci jëmmal mbébet mu am solo mii jëm ci dooleel wàllu jawwu ji ci Senegaal. Ginnaaw ba Senegaal sànnee satelitam bu njëkk (microsatellite GaindeSat 1A), 16i fani ut 2024, ca Etats-Unis, sàkku na ci Jëwriñu Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi mu dajale mbooleem wànqaasi nguur gi ak yu piriweb réew mi niki noonu partaneer yi, ngir gaaw mottali wayndare wi ñu war a tegtaloo ci politigu réew mi ak jëf yu méngoo ak suqalikug jawwu ji, te doon lu ñu tënk ci biir « Vision Sénégal 2050 ».

Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi bàyyiloo na xel Ndiisoo gi, ginnaaw xew-xew yu tiis yi fi am bu yàggul dara, ci jafe-jafe bi am ci taxawu gi war ci wàllu woppi xel, rawati na ni jamono rawee sàrt l°75-80  bu 9i fani sulet 1975 biy wax ci anam yi ñu war a toppatoo ñi am tawati xel ak anam yi ñu war a téyee ñenn ci ñoom ci ay warab. 

Njiital Jëwriñ yi fàttali na jafe-jafe yu bari yi ñu war a  taxaw ci mbirum woppi xel, rawati na ñàkk a am kaadar bu leer ci wàllu politig piblig bu wóor ngir amal ay diisoo ci diggante sektéer yi ak wànqaas yi niki noonu ñàkk a jëmmalug porogaraam bi ñu waroon a doxal ci réew mi ci wàllu woppi xel ci diggante 2024-2028. Lim na itam, ci yi ñu war a taxaw, muy ni way-dese yi nee xuus ci pénc mi di wëraalu, ñàkkug jumtukaayi paj yu doy ci warabi fajukaay yi ak ñàkk a am politig bu wér jëm ci dajale koppar yu doy yu ñuy jagleel woppi xel. 

Lu jëm ci nit ñi am woppi xel tey wëraalu ci mbedd yi te doon jafe-jafe bu wér, Njiital Jëwriñ yi xamle na dayo bi mu am ci sunu dundiin te laaj na ñépp dugal ci seen loxo nekk vi wetu Càmm gi dale ko ci njaboot yi ak askan wépp. 

Ci loolu nag, Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñu Paj mi ak Ndimbal li, mu lëkkaloo ak Jëwriñ yi yor wàllu Yoon, wàllu Biir Réew mi ak wàllu Njaboot gi, taxawal benn komite ad hoc bu war a liggéey, ànd ko mbooleem ñi mbir mi soxal, balaa njeextalu weeru ut 2025, ci genn wàll, mottali yoon wi jëm ci xoolaat sàrt bii def daanaka lu jege  xaaju xarnu tey wax ci anam yi ñu war a taxawoo nit ñi am woppi xel ak ni ñu war a téyee ñenn ci xeet yooyu, ak ci geneen wàll, jëmmal palaŋu 2024-2028 bu am solo bii jëm ci gën a suqali paj mi aju ci wàllu woppi xel. 

Yeesal yi ñuy xaar ci wàll woowu nag mooy, gën a dooleel warab yi ñu jagleel faj ak téyee ñi am woppi xel, mottali lim bu néew bi am ci fajkat yi ci wàllu woopi xel, yoon yi ñu war a jaar ngir jëlee nit ñi am woppi xel tey wëraalu ci digg pénc mi ak fexee taxaw temm ci saytu ndax warab yiy yëngu ci wàll woowu dëppoo nañu ak yoon. Muy nag jëf yu ñu war a boole ak porogaraam bu yaatu bu Njëwriñu Paj mi ak Ndimbal li di teg ànd ko ak Njëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi, jëm ci yeete ci mbir mi. 


Lu soxal àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñu Koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi àddu na ci jéego yi Senegaal jot a teg ci wàllu koom ci diggante 2014-2024;
  • Jëwriñu Jumtukaay yi ak Yaaleg Suuf si ak Jaww ji àddu ci mbirum lëkkaleg xàll yu mag yi;
  • Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa bi àddu na ci waajtaayu nawetu 2025 bi ci lépp lu jëm ci fuglu ak saytu wal yi; 
  • Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat Yaram yi ak Mbatiit mi àddu na ci sémbu waajal atleti réew mi jëm ci powi olympigu Ndaw ñi (JOJ) ci Ndakaaru 2026.

CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

  • Sémbu dekkere biy wax ci « statuts-types » yi ñu war a doxal ci këri liggéeyukaayi réew mi; 
  •  Sémbu dekkere biy teg sàrti doxaliinu  « organe délibérant » yi nekk ci wànqaasi sektéer parapiblig bi. 

Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi. 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE