SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 08i FANI SÃAWIYE 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 08 MONTHS.JANUARY 2025


Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 08i  fani sãawiye 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.


Njiitu Réew mi posowu na ci Ndiisoog Jëwriñ gu Njëkk gii ci atum 2025, ngir ndokkale boole ko ak ñaanal wér gi yaram ak ndam lu mucc ayib ñeel Njiital Jëwriñ yi, ñi bokk ci Ndiisoo gi ak mbooleem ñi séq réew mi. Atum 2025 mii nag fi ñu ko war a teg mooy feddali laxasaay yi, dogu ci liggéey bi, amal ay yeesal (campeef yi, koom mi, dundiinu askan wi añs), ay coppite yu ànd ak njeexital yu am solo.


Njiitu Réew sant na bu baax Njiital Jëwriñ yi ci liggéey bu am solo bi Ngornamaŋ bi jot a amal ci juróom ñetti weer yii weesu ngir joyyantiwaat tolluwaayu réew mi. Rafetlu na bu baax nag yenn matuwaay yi ñu jël jëm ci jubbanti yenn pàcc yi muy ay « mesures sectorielles de rectification » boole ko ak dooraat yëngu yi ci wàllu koom mi ak dundiin wi, niki noonu « Declaration de Politique Générale (DPG) bi ak « Loi de Finances rectificative 2024 » ak « projet de Loi de Finances » ci atum 2025, yi ñu jàllale ca Asàmbale ci anami settee, muy wane rekk ne nguur moom lépp kontinite la.

 

Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu ànd ak Jëwriñ Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, aajar « Plan d’action » bu Ngóornamaŋ bi ci atum 2025, boole ko ak dugalaale « agenda législatif et réglementaire » te lépp ànd ak bàyyiwaale xel doxaliin wu mucc ayib ci njàng mi, iniwersite yi ak warabi njàng mu kawe mi.


Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi itam mu jital ci yitte yi pàcc bi aju ci wàllu paj mi boole ko ak gën a dooleel taxawu gi ci askan wi, muy wàllu « protection sociale » ak yaatal « couverture sanitaire universelle » bi ak joyyantiwaat sémb yii di « programmes de filets sociaux » ak yu « Fonds de Solidarité nationale » ci yeesalaat « Registre national unique (RNU) » bi ñu war a walide balaa njeextalu tirimestar bi njëkk ci atum 2025. 


Ci wàll woowu, woo na Ngóornamaŋ bi mu fexe ba ag dal ci wàllu liggéey bi am ci mbooleem sektéer yi jaare ko ci ànd ak Njaatige yi ak Mbootaayi liggéeykat yi, bokk càmbar mbooleem njàmbat yi. Ci loolu, xamle na ne fàww ñu gaaw, balaa feet bi ñu jagleel liggéeykat yi di yegsi, taxawal « pacte social » bu bees diggante nguur gi ak Mbootaayi liggéeykat yi ak mbootaay yi ëmb njaatige yi.


Njiitu Réew mi ñaax na Ngóornamaŋ bi mu wéyal jéego yi mu doon teg jëm ci gën a sellal ni ñuy yoree alalu askan wi, di yaxanal ak rawati na nag xeex ak dund bu seer bi ak jàmmaarloo ak ñi nanguwul a doxal njëg yi nguur gi teg. Loolu nag mu ngi jaar ci gën a dooleel li nu tànn jëm ci bay dunde ak xoolaat politigu ni ñuy saytoo approwisonmaa bi ci réew mi rawati na ci wàllu hidrokarbiir, wàllu dund ak yenn ci porodiwi yi ñuy faral di jëfandikoo. Ci geneen wàll itam, dees na taxaw temm ci dundalaat koomum réew mi jaare ko ci : 

1- Gën a rattaxal wàllu jëflante yi (environnement des affaires) ;  


2- suqali sektéer piriweb réew mi boole ko ak dooleel ay «champions industriels » ci réew mi ; 


3- yokk dooley « investissement » yuy meññ bu baax boole ko ak finaasmaa yu bees ak baral jéego yi jëm ci doxal sémb yi gën a far ci mbooleem sektéer yi niki mu dikkee ci 

« Agenda national de Transformation » bi.


Ci loolu, Njiitu Réew mi woo na Njiital Jëwriñ yi mu gaaw matale liggéey bi jëm ci walide 

« projet de loi » biy wax ci wàllu « souveraineté » ci wàllu koom mi, ànd ak mbooleem bind yi, jumtukaay yi ak pexe yi aju ci anam yi nu war a jëfandikoo sunu mbell yi, petorol bi ak gaas bi. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu taxaw temm ci fexe ba lépp liy bawoo ci sunu balli mbindaare yooyu ñu saytu leen ci anam yu leer yu mucc ayib te dëppoo ak njariñu askanu Senegaal.


Ci loolu, xamal na Ngóornamaŋ bi ne, fàww ñu gaaw doxal jumtukaayi yoonal ak Kopparal yi aju ci « Fonds de stabilisation » ak « Fonds intergénérationnel » yi ñu teg jaare ko ci « loi n° 2022-09 » bu 19i fani awril 2022  biy wax ci anam yi ñuy séddalee ak a taxawoo alal jiy bawoo ci hidrokarbiir yi. Ci geneen wàll, jox na ndigal Njiital Jëwriñ yi mu ànd ak Jëwriñu Enersii, Petorol ak Mbell yi, Jëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo, Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Sekkeretariyaa bu « COS - PETROGAZ », waajal ndajem komite boobu ci fan yiy ñëw, ci tëralinam wu bees, balaa njeextalu weeru awril 2025.


Njiitu Réew mi xamle na itam ne fàww ñu gaaw waajal jëfandikoo « Pôles territoires » yi nga xam ne ñooy tax ñu man a am ndam ci politigu koom ak dundiin ci Senegaal, ànd ak sémb yu am solo yi ñu war a door ci pàcc bu nekk, ci anam yu dëppoo ak « Agenda national de Transformation » bi. Ci Yoon woowu jëm ci dundalaat gox yi, li ñu ci war a jiital mooy yombalal ndaw ñi am xëy. Muy kon fexee baral jéego yi jëm ci tabax ay warabi tàggatukaay yu xereñ niki noonu gën a yombal jumtukaayi dooleel «entreprenariat » ak xëyu ndaw ñi ak jigéen ñi. 


Ci loolu, soññ na Ngóornamaŋ bi mu gën a taxaw ci luy suqali koomum jàppal ma jàpp mi, waaye tamit fexee jëmmal yéeneem ci dooleel jigéeni Senegaal ak yu jasporaa bi jaare ko ci gaaw tëgg ab sàrt bu jëm ci fexe ba jigéen ñi manal seen bopp ci wàllu koom.


Njiitu Réew mi, joxe na ndigal itam ci ñu taxawal kurél goo xam ne mooy topp ak a xayma doxalug mbooleem fànn yi ñu rëdd ci biir « Vision Sénégal 2050 » ngir ñu man di xam tolluwaayu liggéey yi ak njureef yi. Lu soxal lootaabe ak waajtaayu « Jeux olympiques de la Jeunesse » yi, Njiitu Réew mi xamle na ne « JOJ Dakar 2026 » yii, bu weesoo dayo bi mu am ci wàllu tàggat yaram, koom, tabax, mbatiit ak jumtukaay, aw sas wu mag la ci Senegaal ci fànn yépp. Loolu nag war naa tax mu bokk ci yitte yi gën a soxal Ngóornamaŋ bi ci atum 2025.


Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu taxaw temm kon leegi, ci amal caytu gu sax (ànd ko ak Jëwriñ ji ñu dénk Tàggat yaram) ci mbooleem yëngu, sémb ak kopparal yi aju ci 

wàllu JOJ Dakar 2026 yooyu. Taxaw na bu baax nag ci ne fàww ñu gaaw jébbale ci àpp yi ñu joxe woon, mbooleem liggéey yi aju ci xew wii di dajale, guleet ci Afrig, mbooleem ndawi àddina si.


Njiitu Réew mi àddu na itam ci 8eelu bëccëgu Setal Sunu Réew bi mu jiite gaawu 04i fani sãawiye 2025 ca Site Komiko nekk ci bokk-moomeelu Yëmbël Noor. Refetlu na bu baax ni ñu saxalee yëngu yii ñuy amal gaawu bi njëkk ci weer wu ne, te ñu koy màndargalee waxtaane benn tomb bu jëm ci soññ akan wi ñu gën a jaayante ci setal, sàmm kéew mi, bëgg sa réew ak fexe ba kenn ku ne dugal sa loxo ci doxaliinu pénc mi.


Jaajëfal na bu baax Jëwriñu Larme bi, « Chef d’Etat-major général des Armées,  Haut Commandant de la Gendarmerie nationale et Directeur de la Justice militaire » ak mbooleem way-kaaraange gi, ci ni ñu takkoo taxaw ba tax bëccëgu jaayante gii am ci anam yu jaar yoon. Mu doon luy feddali sunug sax ci jëmmal pas-pas bii di  « Armée-Nation » te doon lu am solo ngir suqaliku gu matale ci Senegaal gu moom boppam, tegu ci yoon te naat 


Lu soxal arminaatam ci wàllu laamisoo, Njiitu Réew mi dikkaat na ci la mu doon teewe, ci talaata ji 07i fani sãawiye 2025 ca Akkraa, sampug Njiitu Réew ma ñu fal bees ca Gana, di Kilifa gi John Dramani Mahama.


Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi taxaw na ci xamle yoon wi Ngóornamaŋ bi war a jaar ci atum 2025, muy tàbbi ci kàddu yi Njiitu Réew mi yékkati bisub 31i fani desàmbar 2024 ak moom it DPG bi mu amal 27i fani desàmbar 2024.


Ci loolu, xamle na matuwaay bi ñu jël ngir doxal « Agenda national de Transformation Sénégal 2050 » bi, mu boole ko ak taxaw bu baax nag ci jumtukaay yi ñu teg jëm ci topp doxalug naal yi, sémb yi ak yeesal yi. Ci wàll woowu, soññe na bu baax ngir ñu jëfandikoo ci anam yu wóor njureef ak digle yiy bawoo ci liggéey yi ñu nekk di amal jamono jii ak kàngami ministeer yi, te jagleel ko doxalug « Agenda » bi, rawati na ci wàllu naal yi, sémb yi ak yeesal yi gën a far ci diggante 2025 jàpp 2029.


Lu soxal ndam li ñuy séntu ci « Vision Sénégal 2050 » bi, te mooy soppi gu matale ci réew ci wàllu doxaliin, Njiital Jëwriñ yi ñaax na mbooleem ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi, ñu taxaw temm ci fexe ba seen i ndaw taqoo ak juróom ñaari (7) riptiir yi mu xamle woon ca DPG ba. Riptiir yooyu lañu war di tegtaloo ci diggante 2025 jàpp 2029, boole ko ak di leen doxal ci anam yu wér te wóor ci mbooleem wànqaas yi aju ci njëwriñ yi. Ci geneen wàll, Njiital Jëwriñ yi xamle na taxawaay bi Jëwriñ yi war a am, te mooy di tànn ak a càmbar àngaasmaa yi serwiis yi aju ci ñoom di jël ci xaaj bi njëkk ci atum 2025, ci wàllu depaas yi soxal sémb yi ak naal yi ñu nekk di doxal jamono jii, ngir fexe ba méngale ko ak jubluwaay yu am solo yi ñu war a doxal ci palaŋ bu bees bi ci juróomi at yiy dëgmal. Xamle na itam ne dina am solo lool ñu topp liggéey yi des walla yi ñu war a wéyal ci « Plan d’action d’urgence » bi ngóornamaŋ bi dooroon ca 2024. 


Mu daanele moom Njiital Jëwriñ yi ci sàkku ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li mu taxaw ci doxal bu wér ci lu soxal likidaasoo HCCT ak CESE ginnaaw ba ñu leen seeyalee ba noppi. 


CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:

  • Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa àddu na ci topp gi ñuy amal ci wayndare yi gën a far te jamp ci wàllu ndox mi ak asanismaa.
  • Sekkereteer Seneraalu « Présidence de la République » aajar na tomb yi soxal « Conférence des Administrateurs et Managers publics (CAMP) » bu 20i fani sãawiye 2025.


CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

Sémbu yoonal wi jëm ci « réglementation de la microfinance »; 


Sémbu yoonal wi jëm ci « réglementation bancaire ».


CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii: 


  • Njénde li:


Soxna Ndey Aysatu Tabara TURE, lu ko jiitu mu doonoon Perefe bu Bàmbey, tabb nañu ko « Secrétaire général de la Délégation générale de l’Entrepreneuriat rapide des Femmes et des Jeunes (DER/FJ), » mu wuutu Sëriñ Seex Ahmadu Bàmba FAAL; 


Sëriñ Seex Aliw BÉEY, Ingénieur ci wàllu « gestion de développement urbain », tabb nañu ko  Njiital « Conseil de surveillance de la Délégation générale à la Promotion des Pôles urbains de Diamniadio et du Lac Rose (DGPU) » mu wuutu Sëriñ Aadama BA.


- Primature.


Sëriñ Ibrahiima FAAL, “contrôleur de gestion », tabb nañu ko Njiital « observatoire national sur l’investissement », mu wuutu Lamin KEYTA.


- Njëwriñu Bennoog Afrig ak Jëflante ak Biti Réew 


Sëriñ Xuraysi Abdulaay CAAM, am lijaasab master ci wàllu « management de l’Administration » tabb nañu ko Aji-doxal ju « Fonds d’Appui à l’Investissement des Sénégalais de l’Extérieur (FAISE) », mu wuutu Soxna  Naata SÀMB. 


- Njëwriñu Koppar yi ak Njël li


Sëriñ Ahet Lamin AAJ, ne woon lu ko jiitu 

« Waqf et des partenariats à Haute Autorité du WAQF », tabb nañu ko Njiital Waqf, mu wuutu Sëriñ Raasin BA; 


Sëriñ Seex Siidiya El Moktaar BÉEY, « inspecteur général d’Etat » bu àllaaterete, tabb nañu ko Njiital « Conseil d’Administration du Fonds souverain d’investissement stratégiques » mu wuutu Soxna Nagisatu JÓOB.  


Direction générale des impôts et Domaines (DGID). 


Sëriñ Jean KONE, « inspecteur principal des impôts de classe exceptionnelle », limatu payoor l° 608855/F, doonoon lu ko jiitu Njiital « renseignement et des stratégies de contrôle fiscal », tabb nañu ko Njiital « impôts et Domaines », mu wuutu Sëriñ Abdulaay JAAÑ; 


Sëriñ Seex Muhammet Haadi JÉEY, « inspecteur principal des impôts de classe exceptionnelle », limatu payoor l° 515385/J, doonoon lu ko jiitu Njiital « Grandes entreprises », tabb nañu ko  Lëkalekatub « Direction Générale des impôts et des Domaines », mu wuutu Sëriñ Addu Asiis GÉY mi war a dem àllaateret;


Sëriñ Ma-Xaali FAY, « inspecteur principal des impôts de classe exceptionnelle », limatu payoor l° 606893/J, doonoon liggéeye lu ko jiitu ca « inspection général des finances », tabb nañu ko Njital «  grandes entreprises » ca « Direction Générale des impôts et des Domaines », mu wuutu Sëriñ  Muhammet Haadi JÉEY mi ñu woolu ci yeneen yitte; 


Soxna Ndey Aysatu NDAW, « inspecteur principal des impôts de classe exceptionnelle », limatu payoor l°606886/J, doonoon lu ko jiitu Njiital « moyennes entreprises », tabb nañu ko Njiital « renseignement et des stratégies de contrôle fiscal » ca « Direction Générale des impôts et Domaines », mu wuutu Sëriñ Jean KONE, mi ñu woolu ci yeneen yitte; 


Soxna Yaama KUYAATE, « inspecteur principal des impôts de classe exceptionnelle », limatu payoor l° 606885/G, doonoon lu ko jiitu Njiital « recouvrement », tabb nañu ko Njiital « moyennes entreprises » ca « Direction Générale des impôts et des Domaines », mu wuutu Ndey Aysatu NDAW mi ñu woolu ci yeneen yitte; 


Sëriñ Mammadu NJAAY, « inspecteur principal des impôts de classe exceptionnelle », limatu payoor l°602574/F, doonoon liggéeye lu ko jiitu ca « inspection général des finances », tabb nañu ko Njiital  « Recouvrement » ca « Direction Générale des impôts et des Domaines », mu wuutu Soxna Yaama KUYAATE mi ñu woolu ci yeneen yitte; 


Sëriñ Ibraahiima NJAAY, « inspecteur principal des impôts de classe exceptionnelle », limatu payoor l° 611438/C, doon liggéeye lu ko jiitu ca « direction du Contrôle interne », tabb nañu ko Njiital « Administration et du personnel » ca « Direction Générale des impôts et des Domaines », mu wuutu  Sëriñ Abdu Ben Jenkins SÀMBU.


- Njëwriñu Ndox mi ak Asanismaa


Sëriñ Seydu MÀNJAŊ tabb nañu ko Njiital 

« Conseil d’Administration de l’Office des Forages ruraux (OFOR) », mu wuutu Sëriñ Alfa Bayla GÉY ; 


Sëriñ Mbàkke JEŊ, « Ingénieur, xereñ ci wàllu “gestion des projets en infrastructures hydraulique » tabb nañu ko Njiital  « Office des Forages ruraux (OFOR) », mu wuutu Sëriñ Hammaat NJAAY. 


- Njëwriñu Napp gi, Jumtukaayi Géej yi ak Waax yi 


Sëriñ Mammadu Abiibu JAAÑ, « docteur vétérinaire de classe exceptionnelle », limatu payoor l°600694/E tabb nañu ko Sekkereteer Seneraalu Njëwriñu Napp gi, Jumtukaayi Géej yi ak Waax yi, mu wuutu Sëriñ Basiiru NJAAY;


Sëriñ Baabakar FAY, tabb nañu ko Njiital « Société des Infrastructures de Réparation Navale (SIRN) », mu wuutu Sëriñ Saaliw SÀMB. 


- Njëwriñu Jumtukaayi ak Yaaleg Suf si ak Jawwu ji 


Sëriñ Moktaar BA, « Manager logistique » tabb nañu ko Njiital « Société les Grands Trains du Sénégal (GTS) » mu wuutu Sëriñ Umar Aamadu SOW; 


Sëriñ Basiiru KOLI, tabb nañu ko Njiital « Conseil d’Administration de la Société les Grands Trains du Sénégal (GTS) », mu wuutu Soxna Seynabu NJÉGÉN. 


- Njëwriñu Caabal yi, Jokkoo yi ak Xarala yi 


Sëriñ Muhammet COMBAAN, Monsieur Mouhamadou THIOMBANE, Ingénieur ci wàllu « Télécommunication et Electronique – Expert en Management de Projets » tabb nañu ko Njiital « Sénégal Connect Park (SCP) », mu wuutu Sëriñ Abdul BA. 


- Njëwriñu Njaboot yi ak Ndimbal li 


Soxna Ayca BOJAŊ, Jàngalekat, tabb nañu ko Njiital « Conseil de surveillance du Commissariat à la Sécurité alimentaire et à la résilience (CSAR) » mu wuutu Sëriñ en Ernest Ndig NGOM ;


- Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi 


Sëriñ Mataar Njaga SILLA, « expert agréé industrie » tabb nañu ko Njiital « Conseil de surveillance de l’Agence de Promotion des sites industriels (APROSI) », mu wuutu Sëriñ Semu JUUF; 


- Njëwriñu Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi 


Sëriñ Lamin SAANE, « enseignant-chercheur en télécommunications », tabb nañu ko Njiital « Agence Nationale de Recherche Scientifique Appliquée », mu wuutu Sëriñ Muhammadu Mbàkke LÓO; 


- Njëwriñu Dëkkuwaay, Gox yi ak Goxaan yi ak rëddug Mbeeraay Gi


Sëriñ Siidi Alburi NJAAY tabb nañu ko Njiital “Conseil d’Administration de l’Agence Nationale de l’Aménagement du Territoire (ANAT)”, mu wuutu Sëriñ Mammadu GASAMA; 


Sëriñ Àlliyun KEBE, “administrateur de société”, am lijaasab master ci wàllu “fiscalité et droit des affaires”, tabb nañu ko Njiital “Centre national de la Fonction publique locale et de la Formation”, mu wuutu Sëriñ Abdu Xaadir NJAAY. 


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE