Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 05i fani mars 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi ndokkale na askanu kerceŋ yi ci àllarba jii di « mercredi des cendres » te doon bis bi njëkk ci Karem bi. Ñaan na ci ngir nu am Senegaalu jàmm ak déggoo ci réew mi. Posewu na ci koor gi ak karem bi daje ngir kañ nangulante gi am ci wàllu diine ak dëkkandoo gi ci jàmm. Muy xéewal guy gën a dëgëral yéene ji nu am ci feddali dëkkandoo ci jàmm gi ci Senegaal.
Ci njiital Jëwriñ ju Njëkk ji, Ngóornamaŋ bi daje na, alxemes 27i fani féewarye 2025, ak mbootaayi sàndikaa yi, njaatige yi ak ñeneen ñu am kàddu ci réew mi, ngir amal jataayu weccente xalaat bu leer ci, genn wàll tolluwaayu koom mi, koppar yi ak dundiinu askan wi, ak ci geneen wàll, li nguur gi man dëgg ci taxaw ci seen i njàmbat. Njiitu Réew mi ndokkale na Njiital Jëwriñ yi ak mbooleem Ngóornamaŋ bi ci anam yu mucc ayib yi ñu amalee guleet waxtaan wu leer wii lépp ci kaw joxante cér ak nangul ñépp ñi teewe woon jataay bi seen gëm-gëm, seen i gaaral ak seen i xalaat. Rafetlu na bu baax déglu ak taxawaayu kilifteef gi sàndikaa yi ak njaatige yi wane ci kanamu jafe-jafe yi Nguur gi di jànkoonteel ci wàllu njël li ak koppar yi, te ràppooru « Cour des Comptes » ci ni ñu yoree woon alalu askan wi ci diggante 2019 ba mars 2024 firndeel ko.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu wéyal waxtaan yu wér diggam ak partaneer yi ngir man a taxaw ci seen i njàmbat, ci kaw doxaliin wu wóor wu Njiital Jëwriñ yi di saytu. Woo na Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñ ji yor wàllu Liggéey bi ñu ànd ak mbootaayi sàndikaa yi ak njaatige yi, taxawal arminaatu waxtaan wu jëm ci torlu, 1 panu mee 2025, benn « pacte de stabilité sociale » bu bees ci diggante 2025-2029. Ñu war a amal itam ay ndaje 6i weer yu ne ngir natt ak gën a dooleel waxtaan diggante ñetti wàll yi (Ngóornamaŋ-Njaatige-Sàndikaa), te war a doon lu tegu ci kóolute, dëgg, njaxlaf ak sàmm njariñu askan wi. Ci geneen wàll, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi, ci kaw sàmmonte ak sàrt yi doxaliin yi, mu sukkandiku ci arminaat bu wér, taxaw ci saafara càkkuteefi sàndikaa yi ak njaatige yi nga xam ne laalewuñu ak koppari pénc mi walla ñu doon lees àttan.
Ci wàll woowu ba leegi, xamal na Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ne, jot na sëkk ñu càmbar yoon ak matukaay yu ñuy teg ngir baral jéego yi jëm ci fay bor yi ñu ame ci biir réew mi. Njiital Jëwriñ yi war naa ànd ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñu Foŋsoo Piblig bi, sumb ay xalaat yu jëm ci xayma anam bi ñuy saytoo payoor yi ci sektéer piblig bi ( foŋsoo piblig bi ak sektéer paraapiblig bi), nga xam ne dina tax ñu man a jàll ci doxaliin wu gën maandu te yamale.
Lu soxal màggal gi ñuy waajal ci bis bi àddina bi jagleel jigéen ñi, te ñu jàpp ko 08i fani mars 2025, Njiitu Réew mi ndokkale na teg ci jaajëfal mbooleem jigéeni Senegaal ak Afrig. Rafetlu na lootaabeg ayu-bis bi ñu jagleel jigéen ñi ci réew mi teg ci kañ taxawaay bu am solo bi jigéen ñi am ci suqali koom mi ak nekkiin wi ci Senegaal. Sàkku na ci Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi, mu wéyal te gën a dooleel jéego yi ñuy teg ci xeex fitna yi ñuy teg ci kaw jigéen ñi. Jox na itam yitte ju kawe njàng ak tàggatug xale yu jigéen yi, waaye itam taxawu ak kopparal yënguy jigéen ñi ci wàllu koom jaare ko fexe ba kopparal gi yaatu ci gox yi ak goxaan yi.
Njiitu Réew mi fàttali na Jëwriñu Njaboot gi ak Dimblante gi ne, jot na sëkk ñu gaaw matale sémbu yoonal wii jëm ci fexe ba jigéen ñi manal seen bopp ci wàllu koom. Taxawaay bu bees boobu ci wàllu yoonal dina tax ñu man a yaatal teg ci boole man-man yi ci wàllu tàggatu, taxawu ak kopparal yënguy jigéen ñi. Dina yombal itam réew mi mu man a sax ci koomum jàppal ma jàpp mi niki noonu suqaliku warab yi fépp ci réew mi. Ci loolu, fàww ñu yeesalaat waññi mbootaay ak kuréli jigéen ñi ci gox yi, ngir man a xam seen ub lim ak sistemu xibaar bu wér te wóor buy tax ñu man a jëmale yënguy Nguur gi ci ñi ko yelloo. Ci wàll woowu ba leegi, woo na Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi ñu sumb ay xalaat ci nees di def ba boolee mbooleem alal ji jëm ci kopparal ak suqali jigéen ñiy jéem a taxawal dara.
Ci yoon wi Nguur gi tegu ngir gunge ak taxawu jigéen ñi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi, mu yokk dooley « Conseil consultatif de la Femme » bi ci wàllu li ñu ko sas, ñi ko séq ak ay jumtukaayam, rawati na lu jëm ci dooleel jigéen ñiy jéemantu, jumtukaay yi ak woyofalug liggéeyi jigéen ñi, waajal samp ay jumtukaay yu méngoo ak jigéen ñi ak sàmm ñi gën a néew doole rawati na ñiy dund ak laago.
Ci geneen wàll, soññ na Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi mu teg politig yu wóor yu jëm ci gën a sóob njaboot gi ci sunuy mbaax yu am doole yi sunu askan làmboo ci wàllu cosaan ak diine. Mu tëjee bunt boobu ci, sàkku ci Jëwriñu Njaboot gi ak dimbalante gi mu xoolaat anam yi ñuy jëfandikoo porogaraamu bursu familiyaal yi, sukkandiku ko ci càmbar yi ñu jot a amal ak yeesalaat « Registre national Unique (RNU) » bi.
Nappum cosaan mi doon na pàcc bu am solo bob ñu bari ci askan wi ñu ngi ciy yëngu. Ci jafe-jafe yi ñu ci seetlu nag ci at yii wees tax na, Njiitu Réew mi sàkku ci Njiial Jëwriñ yi ak Jëwriñu Napp gi, ñu sumb ay diisoo yu boole mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, ngir dundalaat boole ko ak suqali pàcc bu am doole bii ci koomum réew mi.
Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi rafetlu na bu baax anam yi ñu amalee ndaje mi ñetti wàll yii di Ngóornamaŋ-Sàndikaa-Njaatige séqoon, te mu jiite woon ko ci bisub 27i fani féewarye 2025. Fésal na jàngat yi ñu jëlee ca ndaje ma, rawati na ci yaatuwaay ak wuuteg njàmbati sàndikaa yi ak solos fexee taxaw ci fay bor yi dox diggante Nguur gi ak këri liggéeyukaay yi. Fésal na itam yitte ji njaatige yi wane ci toogu bi Nguur gi jagleel piriweb réew mi ci biir « Agenda Sénégal 2050 » bi, ci « contenu local » bi ak sémbu yoonal wi ñuy waajal ci wàllu « patriotisme économique ». Rafetlu na itam, ni ñu boolee dongo yi ak njàngaan yi ci ndaje moomu, jaare ko ci fésal solos wooteb ki teewaloon dongo yi ngir ñu bàyyi xel bu baax ëllëgu ndaw ñi ci ni ñuy saytoo jëflante yi war a dox diggante Nguur gi ak sàndikaa yi.
Njiital Jëwriñ yi fàttali na jampug amal waxtaan wu dëggu te boole ñépp jëm ci tënk « Pacte national de stabilité sociale » bu bees, gën gaa yeex 1 panu mee 2025, ñu jublu ci jël ay dogal yu wóor ngir indi ay saafara ci njàmbat yi lépp nag ci kaw bàyyiwaale xel tolluwaayu koom mi ak koppari réew mi. Ci yoon woowu, Njiital Jëwriñ yi jox na tegtal yi war Jëwriñu Liggéey bi ci lëkkaloom ak Jëwriñu Foŋsoo Piblig bi ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, jëm ci jël matukaay yi war ngir sàmmonte ak arminaat bi ñu tëral ngir door waxtaan yi, gën gaa yeex 02i fani awril 2025.
Fii ak boobu nag, Njiital Jëwriñ yi sóob na ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi te mbir mi soxal leen, ñu matale, ca na mu gën a gaawee, yëngu yi aju ci yenn njàmbat yi bawoo ci ndaje moomu. Muy lu mel ni, gaaw matale càkkuteef yi nga xam ne soxlawul ñuy xaar, yamale gi ci wàllu payoor yi, ñaareelu pàcc bi jëm ci wàññi njëgu dund bi te du jur gàllankoor ci njël li, porogaraam bi jëm ci tabax dëkkuwaayi ndimbal, dooraat yenn yëngu yi ci wàllu koom mi rawati na ci wàllu taax yi ak tabaxi pénc mi niki noonu yeggale sànce yu yàgg yi jëmoon ci tabax ay lekool, ay jàngune ak i raglu, ak door sànce yu bees. Yeesal na ndigal yi mu joxe woon jëm ci fexe di fay ci waxtoom payoor yi, pirim yi, bursu ak xaalis bi ñu yoreel ñiy saytu lekkukaay yi ci jàngune yi.
Lu soxal njàmbati Njaatige yi, Njiital Jëwriñ yi bàyyi na xel bu baax tegtali Njiitu Réew mi, loolu tax na mu soññ Jëwriñu Koppar yi ak Njël li mu jébbal ko ca na mu gën a gaawe, pexe mu jëm ci gaaw fay bor yi Nguur gi ameel këri liggéeyukaay yi. Lu jëm ci sóob sektéer piriwe bi ci jëmmal « Agenda Sénégal 2050 » bi, sàkku na ci Jëwriñu Koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi, mu ànd ak Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, lootaabe ay ndaje seen digg ak sektéer piriwe bi, ci weeru awril 2025, ngir waxtaan ci tomb yu am solo yi nekk ci « Agenda » bi ak mbooleem sémb yi ñu namm a amal diggante 2025-2029.
Mu tëje bunt boobu moom Njiital Jëwriñ yi ci woo partaneer yi, ci kanamu tolluwaay bu metti bi ñu donnee ci nguur gi fi jóge ak jéego yi Nguur gii di teg ci wàllu leeral ak jéem a taxaw ci seen i càkkuteef, ñu àndandoo jàjjuwaat takkaat ndigg yi, màndargalee ko benn « Pacte de Stabilité », lépp jëm ci gaaw joyyanti ba man a tegaat Senegaal ci yoonu yokkute.
Ci ñaareelu tombu àddoom, Njiital Jëwriñ yi yëgal na Ndiisoo gi ne, amal nañu ay ndaje diggante Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi ak yenn wànqaas yi yor sémb yi war a doxal « Agenda Sénégal 2050 » bi.
Jubluwaayu ndaje yooyu nag mooy jéem a amal ndoorte lu gaaw te lëkkaloo ci sémb yooyu, jaare ko ci xool pexe yi ñu war a teg diggante wànqaasi njëwriñ yi mu soxal ak matukaay yi war rawati na fu mel ni ci « Delivery Units » yu njëwriñ yi jot a taxaw walla ñu war leen a taxawal, ci njàppandalu « Bureau opérationnel de Coordination et de Suivi (BOCS) ». Soññ na Jëwriñ ju nekk mu taxaw temm ci amal liggéey yi ci anamu lëngoo ak sektéer yépp, lépp ngir man a am saafara ci jafe-jafe yi ak doxal bu gaaw ci naal yi ak sémb yi.
Lu soxal àddug jëwriñ yi:
● Jëwriñu Yasara gi, Petorol bi ak Mbell yi aajar na « réseau gazier » bu Senegaal;
● Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi àddu na ci fexee wàcce dund bu doy ci ja bi;
● Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gix yi ak Goxaan yi ak Fàkkug Mbeeraay gi àddu na ci porogaraam bi ñuy teg ci réew mi ngir jot ci dëkkuwaay ak yeesalaat dëkkuwaay yi;
● Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde gi ak Càmm gi àddu na ci kàmpaañu njaayum gerte gi.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE