SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 05i FANI FÉEWARYE 2025

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 05 MONTHS.FEBRUARY 2025

 

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 05i  fani féewarye 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi jaajëfal na bu baax askan wi ci ni mu takkoo taxaw génn ci 9eelu bëccëgu Setal Sunu Réew. Mu teg ci sàkku ci Ngóornamaŋ bi mu amal xayma gu matale ci anam wi ñuy amalee Setal Sunu Réew mi te fexe ba askan wi def ko seen yëfi bopp. Ñu gën koo yaatal kon rawati na jiital ci warabi jàngukaay yi, dongo yi (lekool yi ak daara yi), waaye tamit mbootaay yi ci koñ yi jaare ko ci gën a sóob wànqaas ak serwiisi nguur yu mel ni SONAGED ak bépp way-coobarewu.

Senegaal daa war a suuxat pas-pasu setal ak sàmm kaadar bi nuy dunde. Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu gaaral ko doxaliin wu yees ci Bisub jaayante bii ñuy amal ci réew mi, te ñu war koo door ci màggalug 4i fani awril 2025 giy màndargaal 65eelu ati bis bi Senegaal moomee boppam. Doxaliin wu yees woowu ci jaayanteg ma-réew yi nag, dafa war a doon keno bu am solo ci lii di « Programme national de Promotion de la Citoyenneté » te ñu war koo teg ci loxol Njiital Jëwriñ yi ngir mu koordone ko. 


Njiitu Réew mi àddu na ci taxawaay bi  jàngalekat bi ak lekool bi war a am ci dooleel wàllu « citoyenneté » ak tabax réew mi. Jëmmal Senegaal gu moom boppam, gu tegu ci yoon te naat mu ngi aju ci jaayante gu wér ci bëgg sa réew rawati na ci jàngukaay yi. Sàkku na ci Jëwriñu Njàng mi ak ci Jëwriñu Tàggatu gu Xereñ gi ñu ànd ak mbooleem ñiy yëngu ci wàllu njàng mi ak Jëwriñu Larme bi, liggéey ci luy gën a dooleel « instruction civique » ci njàng mi ak gën a fésal mbaaxi teggiin, dimbalante ak xereñte ci doxaliinu njàng mi. Soññu  na Ngóornamaŋ bi mu taxaw temm ci amal doxaliin wu mucc ayib ci jàngukaay yi boole ko ak gën a dooleel tàggatug dongo yi ak njàngaan yi ci jamonoy yokkuteg xarala yi ak 

« Intelligence artificielle ». 


Njiitu Réew mi delloo na njukkal mbooleem jàngalekat yi fi mas a jaar te bokk ci ñi masul a dàcc ngir jox dongo yi tàggatu gu mucc ayib boole ko ak dugal seen yoxo ci jëm kanamug sunum njàng. Kañ na bu baax taxawaay bu am solo bi jàngalekat yi am ci tabax nit ñu gànjaru ñi am ci réew mi. Ci loolu sax nag, tax na askan wi dina amal, 06i fani féewarye 2025, ci taxawaayu Jëwriñu Njàng mi, xewu jébbale « Grand Prix du Chef de l’Etat pour l’Enseignant » te Njiitu Réew mi war koo jiite. 


Njiitu Réew mi posewu na ci Ndiisoo gi ngir rafetlu liggéey bu mucc ayib bu bindkat yi niki noonu téere yi ñu jot a bind daanaka ci fànn yépp. Muy moomeelu Senegaal gu kenn manul a natt. Moom mii doon « Premier protecteur des Arts et des Lettres » bu Senegaal, fàttali na Ngóornamaŋ bi ne fàww ñu gën a dooleel téere ak dawal (lecture) ci doxaliinu njàng mi ak ci njàng mu kawe mi. 

 

Ci loolu sàkku na ci Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat Yaram gi ak Mbatiit mi, mu lëkkaloo ak Jëwriñu Njàng mi, Jëwriñu Tàggatu gu Xereñ gi, Jëwriñu Njàng mu Kawe mi, Jëwriñu Gox yi ak Goxaan yi, Jëwriñu Caabal yi ak Xarala yi, yokk jéego yi ñuy teg jëm ci gën a dooleel wàllu téere ak dawal, rawati na yi doomi réew mi ak saa-afrig yi bind. Xamle na itam ne jot na sëkk ñu tëggaat boole ko am dooleel koppar yi ñu jagleel bindkat yi ak teg politig bu yees bu jëm ci moderniise kàggu yi ak warabi dawalukaay yi ci daara yi, jàngune yi ak daara yu kawe yi, jaare ko ci xarala yu yees yi. 


Ci geneen wàll, sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Mbatiit mi, mu gën dajale ndimbal yi ak lëngoo yi ngir gën a man a gunge mbootaayi bindkat yi. Mbootaay yii nga xam ne ñu am njariñ lañu ci pénc mi, dees leen a war a gën a sóob ci jëmmal doxaliinu pénc mi rawati na yi aju ci wàllu mbatiit te soxal 

« Agenda national de Transformation » Senegaal 2050 bi. Sàkku na ci Sekkereteer Detaa bi yor wàllu Mbatiit mu waajal, ànd ko ak mbooleem ñiy yëngu ci wàllum mbind ci Senegaal, lootaabe balaa njeextalu weeru suwe 2025, menn Ndaje mu ñuy jagleel téere ak dawal te boole ci mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi. 


Koomum jàppal ma jàpp mi doon lu sax ci dumdiinu réew mi, nekk na lu am solo ngir dajale askan wi waaye it jumtukaay bu am solo la ngir man a jëmmal politig piblig yi. Maanaam politi bi ñuy teg ci réew mi ci wàll woowu dafa war a dooleel coppite yi ci wàllu liggéey yi ak ni ñu leen di finaasee waaye itam gën a taxaw ci sos ay yëngu yu man a génne ay koppar ak xëy yu sax dàkk te mucc ayib fépp ci réew mi. 


Ci loolu, Njiitu Réew mi woo na Njiital Jëwriñ yi mu amal, fii ak njeextalu weeru mars 2025, am ndaje diggante jëwriñ yi, ñu jagleel ko koomum jàppal ma jàpp mi ngir gaaral yoon wu yees te wóor. Xamal na Jëwriñu Mikro Finaas ak Koomum Jàppal ma Jàpp ma mi ne, fàww ñu wéyal jëf yi jëm ci baral doxaliin yi aju ci jot ci aggremaa yi.

Wareef naa taxawu itam coppite yi Jëwriñu Mbay mi ak Sekreteer Detaa bi yor mbootaayi kaw gi dooroon jëm ci taxawal ay 

« coopératives agricoles et paysannes ». 


Mu daaneel moom Njiitu Réew mi ci jaajëfal Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa ak mbooleem Ngóornamaŋ bi ci jéego yu am solo yi ñu jot a teg ba tax ñu man a door, altine 3i fani féewarye 2025, ca Faas Ture nekk ci goxu Kebemeer, 2eelu pàccu sémb wu am solo wii jëm ci yóbbu ndox mu sell ci kaw gi. 


Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi xamal na Ndisoo gi matug pàcc bu am solo ci liggéey yi jëmoon ci jëmmal « Agenda Sénégal 2050 », muy taxawalug ab lim bu ñu jébbal Njiitu Réew mi mu war koo walide ci ay sémb, ay naal ak i coppite ci diggante 2025-2029. 


Liggéey bu am solo boobu nag jur na lu tollu ci ñaari téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom benni (276) sémb ak ay naal, yoy jàppeef na ci juróom benn fukk ñuy yi gën a far, niki noonu lu tollu ci ñent fukki coppite ci wàllu doxaliin yees war a amal. Jàll na kon  li gënoon a jafe te mooy jëmmal «agenda » bi ci anam wu gaaw te jaar yoon. Ci yoon woowu, Njiital Jëwriñ yi xamle na ne am na lu tollu ci juróomi téeméeri (500) sémb ak naal yu ñu nekk di tëral. 

Lim boobu nag mu ngi bawoo ci liggéey yi mu digle woon ñu amal leen laataa ñuy amal benn depaas ci wàllu eewestismaa ci tirimestar bi njëkk ci atum 2025. Kippaango gi doon amal liggéey yi nag, ginnaaw bi ñu càmbaree sémb yi, am na ay seetlu yu xaw a jur njàqare ci yenn sémb yi, lu mel ni: 

  • sémb yu am lu ëpp juróom jàpp fukki at; liggéey yu manul a àgg 20% donte ba ñu leen dooree yàgg na; jël depaas yi ci wàllu « eewesyismaa » yi dugal leen ci wàllu « foŋsonmaa »;
  • sémb yu bokk benn jubluwaay ci njëwriñ yu bari;
  • ñàkk a amal ay ràppoor ñeel kilfa yi ci lu soxal sémb yi ñi nekk ci sektéer paraapiblig bi di amal.

Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Kippaango giy amal liggéey yi mu wéyal càmbar yi teg ci gaaral ko ay matuwaayi yaxanal, yu mel ni boole leen ci sémb ak naal yi nekk ci biir 

« plan quinquennal 2025-2029 » ak far yenn yi.


Mu daaneel moom Njiital Jëwriñ yi ci woo Jëwriñu Koppar yi ak Njël li mu taxaw temm ci fexe ba ñiy likide « Haut Conseil des Collectivités territoriales (HCCT) » ak  « Conseil économique, social et environnemental (CESE) », ñu sàmmonte ak matukaay yi yoon tëral jëm ci anam yi ñu war a likidee pàcc yooyu. Ci wàll woowu, sàkku na ci Jëwriñ ji, mu lëkkaloo ak naataangoom yi yor wàllu Foŋsoo piblig ak Liggéey bi ak Jëwriñ Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, jébbal ko, ca na mu gën a gaawee, seen xalaat ci anam yi ñu war a saytoo ña fa daan liggéeyee. 


Lu soxal àddug jëwriñ yi:

  • Jëwriñu Bennoog Afrig ji ak Jëflante ak Biti Réew yaatal na ci waajtaayu aj Màkka gi ci atum 2025;
  • Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde gi ak Càmm gi aajar na tolluwaayu kàmpaañu njaayum gerte gi ak liggéey yi ñuy amal jëm ci yeesalaat lii di « Loi d’Orientation agro-sylvo-pastorale (LOASP) »;
  • Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi aajar na Naal ak Sémb yi gën a far ci diggante 2025-2029.


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE