
Ndiisoog Jëwriñ yi amal nañu ko àllarba 1 panu oktoobar 2025, ci Kilifteefu Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY. Ci ndoortel Ndiisoo gi, yékkati na ay kàddu yu séddalikoo ci tomb yu bari.
TIJJITEL LEKOOL BU 2025-2026
Njiitu Réew mi a ngi dooree ci tomb bi soxal tijjitel lekool bi ci atum 2025-2026 ak baral jéego yi jëm ci soppi sistemu njàng. Lu jëm ci tijjite li ñu jàpp 06i fani oktoobar 2025 ñeel jàngalekat yi ak 08i fani oktoobar 2025 ñeel dongo yi, sàkku na Ngóornamaŋ bi mu jël mbooleem matukaay yi war ngir sàmmonte ak arminaatu njàng mi fépp ci réew mi. Fàttali na Njiitu Jëwriñ yi jampug baral jéego yi jëm ci jële fi mbooleem jàngukaayi mbaar yi boolee ko ak taxaw ci tabax ay jumtukaayi njàng yu méngoo ak jamono.
Njiitu Réew mi xamle na yitteem ci amal sistemu njàng mu mucc ayib ak méngale li ñuy jàngale ci sunu lekool yi ak wàllu xarala yi, xamtu yi, làkki réew mi ak yu biti réew. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi lalu amal ag xayma ci njureefi kàtte yi ak joŋante yi, boole ko ak dëppoo ci ay gaaral yu wér te wóor ci lootaabe gu bees gu ñu ci war a amal.
Jox na ndigal Jëwriñ ji yor wàllu Njàng mi ak ji yor wàllu Tàggatu gu Xereñ gi ak gu Xarala gi, ñu taxaw ànd ko ak ñiy yëngu ci njàng mi ci piblig bi ak ci piriwe bi, fexee yéwénal sallax (frais) yi aju ci mbindu mi ak njàng mi boolee ko ak gën a xóotal waxtaan yi ci sistemu kàntin eskoleer yi, méngale ko ak politig yi ñuy teg ci wàllu ndimbal ak jàppalante ci réew mi.
Mu tëjee ci soññ Ngóornamaŋ bi muy amal topp gu wér ci déggoo yi mu am ak sàndikaa jàngalekat yi boole ko ak taxaw temm ci gën a dëgëral jalog sosiyaal bi ci wàllu njàng mi, ngir feddali njàng mu mucc ayib ci lekoolu Senegaal.
DOXALIIN WU BEES CI WÀLLU MBAY MI, KÀMPAAÑU NJAAY MI AK DOOLEEL JËFANDIKOO LI FIY MEÑÑEE
Ñaareelu tomb bi mu àddu mu ngi jëm ci doxaliin wu bees wi ci wàllu mbay mi, kàmpaañu njaay mi ak gën a dooleel jëfandikoo liy meññee réew mi.
Ginnaaw ba mu ndokkalee Ngóornamaŋ bi ci mbooleem matukaayi waajtaay yi mu jëloon ngir amal kàmpaañu mbayum 2025 bu mucc ayib, xamle na solos baral jéego yi jëm ci taxawalaat wàllu jiwu wi te sukkandiku ko ci gëstu gi ànd ko ak ISRA.
Njiitu Réew mi xamal na itam Jëwriñu Mbay mi, Bay-Dunde gi ak Càmm gi ak Sekkereteer Detaa bi yor wàllu Mbootaay yi ak Taxawu Baykat yi, na fàww ñu baral jéego yi jëm ci jëmmal « koperatif agrikol kominoteer » yi, tëggaat te dooraat sémbu « Programme des Domaines agricoles communautaires (PRODAC) ».
Ginnaaw ba mu sóobee Ngóornamaŋ bi ci dooraat politig yi, naal yi ak sém yi jëm ci gën a dooleel jëfandikoo liy meññee ci réew mi, jaare ko ci gën a jariñoo liy ñoree ci mbeeraay yi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi mu waajal, ànd ko ak mbooleem ñi ciy yëngu ak askan wi, lootaabeg 6eelu edisoo « Weeru Oktoobar, weeru jëfandikoo li fiy meññe ».
TEEWEG 80eelu JATAAYU NDAJE MU MAG MU MBOOTAAYU RÉEWI ÀDDINA SI
Lu ñeel ab teewaayam ca 80eelu Ndaje mu Mag mu Mbootaay Réewi Àddina si, 21 jàpp 26i fani sebtàmbar 2025, Njiitu Réew mi leeral na Ndiisoo gi ne xamle na fa taxawaayu Senegaal ci jafe-jafe yu mag yi àddina di jànkoonteel yu mel ni xeex rëtal gi, xiiroo yi, soppikug njuux li, jafe-jafey koom mi, dellu ginnaawug jàppalante ci àddina si ak jafe-jafey mbootaay gi. Ndokkale na itam Jëwriñu Yoon ji, Aji-sàmm Màndarga yi, ci lootaabeg « Side Event » gi jëmoon ci wàllu fàttaliku yu mel ni « yoon ak defaraat ñeel Saa-Afrig yi ak ñi cosaanoo Afrig ».
Ginnaaw liggéey yi, Njiitu Réew mi amal na fa ndajey lëkkaloo yu bari diggam ak ay Njiiti Réew ak yu Ngóornamaŋ, niki noonu, yeneen jëmm yu am taxawaay ci àddina si.
TOPPUG « FIÈVRE DE LA VALLÉE DU RIFT » AK OKTOOBAR RÓOS
Ci kanamu jàngoroy « fièvre de la vallée du Rift » gi fi feeñ, Njiitu Réew mi jox na ndigal Jëwriñu Paj mi ak Cetug Pénc mi, mu dajale, ànd ko ak Njëwriñ yi mu soxal, mbooleem matukaayi fagaru yi ak taxawu gi ñeel mbas mi fépp ci réew mi, rawati na ci li wër tund yi mu laal. Taxawlu na bu baax ci ñu fexee sumb ca na mu gën a gaawe, kàmpaañ bu am doole jëm ci leeral ak yee askan wi ci matukaay yi ñu war a jël ngir mucc ci mbas mi.
Ci geneen wàll, lu ñeel tomb bi aju ci màggalug Oktoobar Róos gi, jox na ndigal Ngóornamaŋ bi, ci lu jëm ci xeex ak ngalu ween, mu jël mbooleem matukaay yi war ngir yeete ci njariñu teel a dem seeti sa yaram boole ko ak amal taxawu gu jaar yoon ñeel jarag yi.
ARMINAAT
Lu jëm ci arminaatam, moom Njiitu Réew mi xamle na ne dina jiite, talaata 7i fani oktoobar 2025, jataayu tijjitel « Forum Invest in Sénégal (FII Sénégal) », ci teewaayu mbooleem Ngóornamaŋ bi.
LU JËM CI ÀDDUG NJIITU JËWRIÑ YI
Njiitu Jëwriñ yi ndokkale na bu baax Njiitu Réew mi ci teewaayam bu mucc ayib bi mu amal ca 8eelu jataayu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si. Di ndaje mu mu yékkati sunum réew ca kaw jaare ko ci wane taxawaayu fulla ak njàmbaar ci tolluwaayi jamono ji, rawati na ca Gasaa ak ñàkk a yamale gi am ci sistemu kopparalug àddina si.
Mu toftal ci kàdduy leeral ci doxaliinu dogoo gi war ngir doxal bu baax liggéeyu ngóornamaŋ bi ci kaw méngale boole ko ak sàmmonte ak li ñu jaayante woon ci kanamu askan wi. Ci noonu àddu na ci ñetti (03) tomb ngir jëmmal doxaliin woowu, muy : baral jéego yi jëm ci doxal naal yi gën a far, saafara jafe-jafey kopparal yi ak samp doxaliin wu leer ci liggéey bi.
NDOORTEL LIGGÉEY YU MAG YI CI « AGENDA NATIONAL DE TRANSFORMATION » BI BALAA YÀGG
Muy kon yenn sémb yu am solo yi gën a fés ci kayug Njiitu Réew mi, yu ci mel ni sémbu « Grand Transfert d’eau », yóbbu kuraŋ bi ak ndox mi ci kaw gi, idàntite nimerig, yoonu saxaar gu Dakaar-Tàmbaakundaa, yeesalaat daamar yiy yóbbu marsandiis, sémbu koperatif agrikol yi.
Seen ug jëmmal ca na mu gën a gaawe, mooy yitte ji gën a far ci yënguy Ngóornamaŋ bi.
BARAL JÉEGO YI JËM CI SOTTAL NAAL YI GËN A FAR
Njiitu Jëwriñ yi xamle na ne fàww ñu baral jéego yi jëm ci sottal yeneen sémb yu am solo yi ñu nekk di doxal jamono jii, ngir man a am njeexital yu wér ci diir bu gàtt.
Muy sémb yu mel ni, liggéey yu mag yi ñuy amal ci wàllu waax yi, ci wàllu yoon yi, naawu yi, mbay mi, yooni saxaar gi, xarala yi ak yasara gi.
Ci geneen wàll, Njiitu Jëwriñ yi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu gën a jox yitte yenn sémb yu am solo yi, nga xam ne noppi nañu waaye ñu ngir xaar ñu war leen a jëfandikoo walla yi nga xam ne liggéey yi dañoo déya. Muy sémb yu am solo yi ci wàllu yaale gi, ja yu mag yi, njàng mu kawe mi ak ñoom seen.
Mu tëj foofu ci fàttali yitte ji mu jox wéyalug jéego yi ñu tàmbalee teg jëm ci joyyanti këri liggéeyukaay yi nekk ci jafe-jafe, rawati na SONACOS, SN La POSTE ak Air Senegal.
Ci loolu, Njiitu Jëwriñ yi xamle na ne fas na yéene wàcc ci suuf ci fan yii di ñëw ngir nemmiku mbooleem sànce yooyu, ginnaaw bu noppee ci jataayi liggéey yu xóot yi mu ciy amal. Tas boole ko ak tëggaat benn bu nekk ci naal yooyu dina tax ñu man a indi saafara yi war ci jafe-jafe yi ci wàllu xarala, koppar ak doxal yi ñu ci seetlu. Jubluwaay bi di fexee teg leegi doxaliin wu leer te wóor, wu jëm ci am ay njeexital yu wér.
KOPPARAL
Njiitu Jëwriñ yi xamle na ne lu jëm ci kopparal sémb yooyu, pexe mi ñu ci jiital mooy jëfandikoo balluwaay yi nekk ci biir réew mi. Yeneen balluwaay yiy dolliku ci lu ñeel jëmmalug « Plan de Redressement économique et social (PRES) » bi, dees na leen jariñoo, ci jéem a kopparal sémb yu am solo yi ñu tuddoon ci kaw, jaare ko ci lii ñuy tuddee « arbitrage » ak « programmation budgétaires ».
Njiitu Jëwriñ xamle na itam ne Ngóornamaŋ bi dina gën di jëfandikoo lëkkaloo diggante piblig-piriwe, ay doxaliin yu bees ci wàllu bëgg sa réew ak ndajalem koppar ci réew mi ci jasporaa bi, jaare ko ci taxawal walla jëfandikoo jumtukaayi dugal xaalis yi (FONSIS, CDC, FONGIP, FNR, IPRES, añs.). Jubluwaay bi di fexee jëmale balluwaay yooyu ci sémb yuy am njeexital yu wér ci koom mi.
Niki noonu, jëfandikoo jumtukaayi kopparal yu lislaam (waqf, sukuk…) ak njëfekaayi « crowdfunding », day doon keno bu am solo ngir kopparal sémb yu am solo ci wàllu dundiin wi ak koom mi, rawati na ci wàllu njàng mi, paj mi ak suqalikug mbeeraay yi.
DOXALIIN WI
Njiitu Jëwriñ yi xamle na ne dees na teg benn kaadar bu jëm ci amal càmbar yu xóot, tëggaat boole ko ak dooraat sémb wu ne, mu ànd ak caytu saa su ne ak wayndare sukkandikukaay. Jamono jii ñu ngi nekk di yeggali ci Primature, ag njëfekaayu topp ak xayma guy tax ñu man a amal caytu gu wér ci tolluwaayu sémb wu nekk. Dees na teg itam ay fiis yu ñuy xamle jafe-jafe yi, ñu war leen di yaatal ci Ndiisoog Jëwriñ yi, ngir ñu man cee indi saafara yu gaaw.
LU JËM CI ÀDDUG JËWRIÑ YI
- Jëwriñu Bennoog Afrig gi, Jëflanteg Biti Réew ak Saa-senegaal yi nekk Biti Réew àddu na ci tolluwaayu politig, laamisoo ak kaaraange gi am ci dig-digal bi ;
- Jëwriñu Koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi àddu na ci lu ñeel pexe mi ñu teg ci réew mi ngir suqali sektéer piriwe bi ak dooleel ndugalum xaalis mi (SNDSPI) ;
- Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa bi àddu na ci tolluwaayu caytu gi ñuy amal ci wali ayu-bis bu set ;
- Jëwriñu Ndaw ñi ak Tàggat Yaram yi àddu na ci tolluwaayu jumtukaay yi ak fi ñu tollu ci jëmmal dogal yi bawoo woon ci ndaje mi Jëwriñ yi séqoon jëm ci JOJ yi.
Mari Róos Xadi Faatu Fay
Sekkereteer Detaa ci wetu Njiitu Jëwriñ yi, ñu dénk ko Jëflante diggante Campeef yi ak Kàddug Ngóornamaŋ bi