Kilifa gi Basiiru JOMAAY Fay, Njiitu Réewum Senegaal, séq na waxtaan digganteem ak Njiitu Réewum Farãas, Emanuel Makroŋ, ci Ndajem àddina si ñu doon amal jëm ci yeesal ak moom sa bopp ci wàllu ñakk, tay ci alxemes ji 20i suwe 2024, ca Pari.
Ci seen i waxtaan, ñaari njiiti Càmm yi fésal nañu seen jeen yéene ji ñu bokk jëm ci teg doxaliin wu yees ci jëflante diggante Senegaal ak Farãas, te tegu ci joxante cér, lëngoo gu yemoo te ëmb njariñ ñeel ñaari askan yi, àndandoo ci mbaaxi demokaraasi yi ñu bokk, ci lëkkaloo gu lalu cig nite ak jëflanteg xaritoo.
Ñaari njiiti réew yi weccente nañu ci taxawaay yu am solo yi ñu bokkle jëm ci wéyal ak dooleel lëkkaloo ci fànn yiy jàpple
bu baax Senegaal moom boppam. Am nañu ag déggoo ci dëgëral sémbi tabax ci fànn yu wuute niki soppiku ci wàllu yasara (transition énergétique), wér gi yaram, tàggatu cig xereñte, defar ay ñakk ci réew mi ak mbay mi.
Ñaari naataangoo yi rafetlu nañu ku ci nekk yéene ji nga am ngir dooleel jëflante diggante Farãas ak Senegaal.