RIYAD: NJIITU RÉEW MI BASIIRU JOMAAY FAY DALAL NA KILIFA GII DI XAALID AL-FALIH, JËWRIÑU EEWESTISMAA JU ARAABI SAWUDIT

xamle - 28 MONTHS.OCTOBER 2024

Niitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na kilifa gii di Xaalid Al-Falih Jëwriñu Eewestismaa ju Araabi Sawudit. Ndaje mii nag day wane yitte ji Araabi Sawudit am ci Senegaal gi mu jàppee niki selebe yoon bu am solo ci Afrig Sowu Jant, teg ci di xàll yoonu gën a dooleel lëkkaloo diggante ñaari réew yi.

Waxtaan yi tax na ñu man a leeral eewestismaa yu yaatu yi ñu man a dugal Senegaal ci pàcc yu am solo yu mel ni mbay mi, yasara gi ak ndefar gi. Jubluwaay bi ñu bokk am nag mooy amal ay lëngoo yu amal njariñ ñaari réew yi teg ci def Senegaal muy bijj naataange ak yokkute ci tund wi.