Njiitu Réew mi jiite na, tay ci suba si, xewu joxe raayay Oskaar “national de la Qualité”.
Ci jataay bii, Njiitu Réew mi rafetlu na taxawaay bu am solo bi këri liggéeyukaay yu Senegaal yi wane ci ag xereñte ci jamonoy joŋante bu tar ci àddina suy gën di yittewoo kalite bu wér ci wàllu liggéey yi.
Njiitu Réew mi fàttali na ne kalite moom fii mu ne daa war a bokk ci keno yu wér yi ci wàllu yoriin, moo xam ci piriwe bi walla ci ndoxalug piblig bi. Mu xamle ne, doon na jumtukaay bu am solo ngir tabax Senegaal gu moom boppam, gu am doole te naat.
Senegaal a ngi dëggal boppam jëm ci sóobu bu wér ci jëflante yiy am ci kembaar gi ak ci biir àddina si, jaare ko ci gën a dooleel kenoy tegu ci yoon ak xereñte, niki mu dëppoo ak jubluwaay yi ci biir “vision Sénégal 2050”.
Njiitu Réew mi ndokkale na bu baax ñi ñu tànn ci Raaya Oskaar “national de la Qualité”, boole ko ak ñaax mbooleem këri liggéeyukaay yi ak kurél yi, ñu sax ci yoonu liggéey bu mucc ayib, nga xam ne doon na lu manul a ñàkk ngir am njeexital yu wér ci coppite koom mi ñu namm a amal ci réew mi.