Biti Réew - 23 MONTHS.AUGUST 2025
Buuru Réew ma di Naruhito dëne woon ko, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY teewe na jataayu naan attaaya ba ñu baaxoo ca « Palais impérial ».
Jataay bii ñu baaxoo amal, di ko jagleel gan ñu kawe ñi, day màndargaal mbaaxi cofeel, joxe cér, sell ak dal. Ndëne lii nag day tekki sag gu rëy, guy firndeel cér bu kawe bi ñu jox Senegaal ak dëgaraayu jëflantey xaritoo yi dox diggante Ndakaaru ak Tokyo.
Ci teewe gi mu def ci jataay bii, Njiitu Réew mi boole na doxal laamisoog politig ak laamisoog mbatiit, di luy gën a dooleel lëkkaloo yu am solo yi ak mbokkoo gi boole ñaari askan yi.