Njiitu Réew mi posewu na ci tukki bi mu doon amal ca Kawlax ngir dalal njiiti gox yi ak goxaan yi nekk ci tundu Siin-Saalum, muy fara yi ak njiiti ndiisooy gox yi, ci ab jataay ngir weccente ak ñoom xalaat ci sémb wi soxal « Pôle territoire Centre ».
Ñu door ndaje mi ak leerali Jëwriñ ji yor wàllu dëkkuwaay, Gox yi ak Goxaan yi ak Fàkkug Mbeeraay yi. Mu dikkaat ci gis-gisu Ngóornamaŋ bi jëm ci soppi « pôle centre » bi def ko muy xolu réew mi ci wàllu koom, jaare ko ci ay naal ak sémb yu am solo yu jëm ci gën a dooleel mbay mi, ndefar yi ak jumtukaay yi.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi xamle na bu baax solos sóob bu wér gox yi ak goxaan yi war a bay waar wu yaatu ngir sottal sémb wu am solo wii. Xamle na ne fàww ñu gën a yokk man-mani bokk-moomeel yi ak gox yi ci wàllu koppar ak xarala, ngir samp suqaliku gu sax gu ñépp di bokk. Fara yi bawoo Kawlax, Fatig ak Kafrin ñoom ñépp ànd nañu rafetlu doxaliin wi. Xamle nañu ne noppi nañu ngir ànd ak Njiitu Réew mi, def « pôle centre » bii muy misaal ci suqaliku gu wér. Ci seen i kàddu itam, fésal nañu njàmbat yu bari, boole ko ak def ay gaaral yu am solo yu jëm ci gën a yombal jote ci ndox mi, kuraŋ bi, paj mi ak njàng mi ci seen i gox.
Njiitu Réew mi dalal na seen xel ci yéene ji Nguur gi am jëm ci taxaw ci yitte yi gën a far, mu teg ci xamle ne sémb wi ñu namm a amal ci « pôle territorial centre » bi bu sottee, man naa doon misaal ci Senegaal ba sax romb ko. Ginnaaw ndaje mii nga xam ne ña ko teewe woon jenn yéene lañu bokk am, muy tabax ëllëg gu mucc ayib ñeel askan wi, Njiiti gox yi ak Nguur gi, ñoom ñépp feddali nañu seen ug jaayante ngir joxante loxo ànd liggéey.