Njiitu Réew mi, Basiiru JOMAAY Jaxaar Fay, daloo na tay ci suba « hotel Courtyard by Marriott » ca Jamñaajo. Xew-xew nii doon na jéego bu am solo ci politig bu yees bi jëm ci gën a dooleel dallukaay yi ak suqali wàllu turism bi doon pàcc bu am solo ci sunu koom.
« Hotel Courtyard by Marriott » bii ñu dugal lu tollu ci 13i miliyaari FCFA, doon na tabax bu méngoo ak jamono bu am 134i néeg yu dëppoo ak yoon wi ñu tëral ci àddina si. Ag tabaxam rekk jur na 150i xëy, di doon kon luy bokk ci liy suqali koom mi ñeel sunuy ndaw ak jëm kanamug sektéer piriwe bi.
Ca jataay ba, Njiitu Réew mi feddali na yéeneem ci def turism bi muy jumtukaayu yokkute ci sunu koom, niki ñu ko fésalee ci Sémbu soppi Senegaal fii ak 2050.
Hotel bii nag day bokk ci suqali taax yu méngoo ak jamono ya ñuy taxawal ca Jamñaajo niki CICAD, Dakaar Arenaa, estaad Abdulaay Wàdd añs, te doon lu war a def gox boobu selebe yoonu turism bu am solo ci wàllu liggéey, xew-xewi mbatiit ak tàggat yaram yi.
Daloo gii nag day feddaliwaat rekk kóolute gi dugalkati xaalis yi am ci sunu réew ak jëm kanam gu wóor ngir jëflante gu gën a xemmemu te am doole.