Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, amal na tay, ci Ndakaaru, tijjitel dal bu bees ci tund wi bu Bànk Monjaal ngir Afrig Sowu Jant ak bu Digg bi.
Taax mii, dajale mbooleem wànqaasi kippaango gi ci tund wi, day wane yéeney campeef gi ci gën a dooleel xereñte gi ak gën a xam li xew ci tund wi, jaare ko ci gën a bàyyi xel nit ñi ci politigu suqaliku yi ñuy teg.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay rafetlu na dëppoo gis-gis bi am ci diggante doxaliin wu bees wi Kippaangog Bànk Monjaal di doxal ak “Vision Sénégal 2050", di tegtalukaay bu am solo bu jëm ci tabax Senegaal gu moom boppam, tegu ci yoon te naat.
Njiitu Réew mi fésal na yitte yu far yi ñu bokk am, yu mel ni mbay mi, xëyu ndaw ñi, kuraŋ bu daj fépp, tàggatu gu xereñ gi, xarala yi ak gën a dooleel sektéer piriwe bi. Fésal na itam yeesal yu am solo yi Ngóornamaŋu Senegaal sumb ngir rëdd xar-kanamu meññilu gu mucc ayib ak sos ay xëy yu ñoŋ.
Tijjite lii day firndeel jaayante gu sax gi Senegaal am jëm ci dooleel sistemu lëkkaloo gu tegu ci jàppalante ci àddina si, lépp ngir njariñu askanu Senegaal ak mbooleem kembaaru Afrig gi.