Peresidaa FAY dalal tañu kippaangog DONEWON.

xamle - 07 MONTHS.JULY 2025


Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, dalal na tay ci ngoon gi, tañu kippaangog DONEWON, ci njiitu Topp-Njiit la, di S. Myoung Lee.

Këru liggéeyukaayu Kore gii, te xereñ ci ndefarug njuddeefi géej, xamle na yéeneem jëm ci gunge jëmmalug “Agenda Sénégal 2050” bi, jaare ko ci dooleel sopparñi njuddeefi géej yi.