Peresidaa FAY dalal Njiitu Ndiisoog Ndoxal gu Ecobank Transnational Incorporated.

xamle - 18 MONTHS.SEPTEMBER 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, jagleel na ab jataay ci alxemes ji 18i fani sebtàmbar 2025, kii di S. Paab Ma-Jaw NJAAY, Njiitu Ndiisoog Ndoxal gu Ecobank Transnational Incorporated. 


Muy Ndaje mu jëmoon ci gën a dooleel lëkkaloo gu am solo gi dox diggante Senegaal ak ñu mag ñiy yëngu ci wàllu Bànk ci Afrig. 


Ci jataay boobu, Kippaangog Ecobank feddali na jaayanteem jëm ci gunge Ngóornamaŋ bi ci jëmmalug gis-gisu Senegaal 2050, di tegtalukaay bu wér ngir suqaliku gu sax te boole ñépp ci réew mi. 


Waxtaane nañu tombi lëkkaloo yu bari, rawati na ci wàllu kopparal ay sémb yu am solo ci wàllu tabax ay jumtukaay, niki noonu taxawu sektéer piriwe bi jaare ko ci xelal ak jàppale.