Peresidaa Fay dalal na Sekkereteer Detaa Kataar bi yor wàllu jëflante ak biti réew ak woroom xam-xam yu Afirg Sib-Saharaa

Biti Réew - 28 MONTHS.APRIL 2025



Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY dalal na tay ci altine ji, Sultan bin Saad Al-Muraikhi miy Sekkereteer Detaa Kataar bi yor wàllu Jëflante ak Biti Réew.

Muy nemmiku gu jëm ci topp jaayante yi ñu defoon diggante Senegaal ak Kataar ngir gën a dooleel jëflante diggante ñaari réew yi. 

Ci ndaje moomu, ñaari wàll yi yaatal nañu ci pàcc yi gën a am solo ci seen ug lëngoo, rawati na ci wàllu koom mi, yasara gi ak njàng mi.


Ba tay, ci ngoon gi, Njitu Réew mi,  dalal na,  ci Njénde li, tañu woroom xam-xam yu Afrig Sub-Saharaa.  Ñu doon amal seen 3eelu ndaje mu mag ci Ndakaaru, ñoom kilifay diine yii posewu nañu ci ngir aajar  Njiitu Réew mi dogal yu am solo yi ñu jël ci seen ndaje mii teg ci sant ko bu baax ci ni mu leen taxawoo ci lootaabeg xew wi.