Peresidaa FAY dalal na Jëwriñu Esibt jibuor wàllu Jëflante ak biti réew.

Biti Réew - 24 MONTHS.JULY 2025

Njiitu réew mi dalal na démb jëwriñu mbiri bitim réewu Misira (Esibt) di Badar Abdelati. Moom nag njiitu réewam di Abdel Fataa Al Sisi moo ko yónni ngir mu jébbal ab bataaxel Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay. Àndoon na ak fanweeri boroom alal yu bëgg a dugal seen xaalis ci réew mi. 

Waxtaane nañu 65i ati xaritoo diggante Senegaal ak Misira waaye waxtaane nañu itam nan la ñuy def ba li ci seen kanam, ñu man a dugal xaalis ci réew mi ci fànni mbay mi, kaaraange gi, soppi meññeefi mbay mi.

Waxtaane nañu itam fi àddina bi tollu, rawatina Afrig ak ni réew yi war a gën def ba gën di disoo.