Ca Yokohama, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY amal na fa bis bu am solo ci ay jataay yu mu séq ak njiiti Carrefour Médical ak yu NIPRO Corporation, di ñu am taxawaay ci xarala yi ñeel wàllum paj.
Muy ndaje mu ñu tënkee ci torlu ag déggoo di ab Memorandum Of Understanding (MoU) ci diggante ñaari kër yi, mu jëm ci defaree ay kit hemojaliss ci Senegaal. Lëngoo ak Carrefour Médical giy defar ñetti bir ci fukk ci kit yooyu, dina tax mu gën a dooleel taxawaayam ci wàllu gi.
Jubluwaay bi ñu bokk am nag leer na : wàññi njëgu kitu jaliis bi jële ko ci 35 000 wàcce ko ba 25 000 F CFA, ngir fexe ba jot ci paj mi gën a jàppandi ci askan wi.
Ci pose moomu, Njiitu Réew mi rafetlu na yéene ji teg ci gën a soññ partaneer yi ñu gën a wóolu Senegaal, jaare ko ci fésal njariñ yu bari yi réew mi làq ci wàllu dugal xaalis : dalug politig, fi mu féete ci àddina si, ja bu yaatu, warabi koom, yeesal yi ñu nekk di amal te jëm ci gën a dooleel wàllu jëflante.
Lëkkaloo gii nag day firndeel yéeney Senegaal ci boole fent ci wàllu paj mi, koom mu xemmemu ak suqali nekkiinu askan wi.