Peresidaa FAY daje na ak doomi Senegaal yay dund ca Japon.

Biti Réew - 20 MONTHS.AUGUST 2025

Ginnaaw bëccëgu liggéey bu am solo ca Yokohama, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, daje na ak doomi Senegaal yay dund ca Japon. 

Li màndargaal jataayu weccentey xalaat bii, déglonte ak jegeyoo, mooy feddali lëkkaloo gu wér gu dox diggante réew mi ak ab jasporaam. Njiitu Réew mi rafetlu na anam yi doomi Senegaal yi nekk ci biti di dugalee seen yoxo ci lépp luy gën a fésal réew mi ci àddina si, lépp boole ko ak feddali jaayanteem ci gën a yokk jéego yi ñuy teg jëm ci gën a dooleel seen i yëngu ak fexe ba gën leen sóob ñu jàpp ci suqalikug réew mi.