Mu yegg ci gaawu bi ca Abujaa, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, baaxental na jëf jii di lu ko ñor lool : daje ak doomi Senegaal yi féete biti réew.
Ci ndajem mbokkoo mu mu séq ak doomi Senegaal yay dund ca Niseriyaa, fésal nañu fa njàmbat yu bari : kopparal sémb yi, yeesal këyit yi, tijji benn pekku laamisoo ca Lagos. Njiitu Réew mi feddali na yéeneem jëm ci indi ci ay saafara yu wér te wóor.
Xamle na fa itam ne dees na amal balaa yàgg benn bis bu ñuy jagleel jasporaa, lépp jëm ci gën a lootaabe gunge gi ñeel saa-senegaal yi féete biti réew ak gën a dooleel seen taxawaay ci suqalikug réew mi.
Ci wàll woowu ba leegi, Njiitu Réew mi wecce na ak foŋsaneeri Senegaal yiy liggéey ci biir CEDEAO, muy rafetlu ni ñu dugalee seen yoxo ci luy gën a boole dig-digal bi niki taxawaayu Senegaal ci biir campeefi mbootaay yi.