Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, teewe na ci talaata ji 6i fani mee 2025, jataayu tijjitel Ndajem waxtaan mu kurél gi dajale kilifay jàngu yu Afrig Sowu Jant (CERAO), ñu ko doon amal ca Grand Théâtre bu Ndakaaru.
Ndaje mu am solo mii, di màndargaal ngëm, mbokkoo ak diisoo, dajale na kilifa yi gën a màgg ci diiney katolig ci Afrig Sowu Jant, ñu ñëwoon ngir bokkandoo xalaat ci yooni Egliis bu taxaw temm ngir maandute ak jàmm.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi rafetlu na bu baax taxawaay bu sax bi Egliis bi yàgg a wane jëm ci dooleel mbokkoo gi, feddali jàmm ji ak gën a yokk dimbalante gi ci diggante xeet yi. Xamle na itam seen taxawaay bu am solo bi ñu am ci sàmm mbaaxi diine yi ngir tabax Afrig gu bennoo, gu dëgër te mbokkoo.