Biti Réew - 11 MONTHS.MAY 2025
Ci ndënel Kilifa gii di Alasaan Wartara, Njiitu Réewum Kodiwaar, Njiitu Réewmi Basiiru Jomaay Fay, bawoo na Ndakaaru ci suba ngir teewe, 12 ak 13i fani mee 2025, Afrikaa CEO Forum ca Abijaŋ.
Ba mu yeggee, kilifay Kodiwaar yi ak doomi Senegaal yi féete Abijaŋ teertu nañu ko teertu lu mucc ayib.
Ndaje mii ñuy amal at mu jot dina dajale ay kilifay potig yu mag, ay njiiti këri liggéeyukaay, ay dugalkti xaalis ak ay saabalkat ngir weccente ci pexe yu jëm ci dooleel dugal xaalis ak suqali sektéer piriwe bi ci Afrig. Edisoo ren bi tomb bi ñu ciy waxtaane mooy Ndax lëkkaloo diggante piblig bi ak piriwe bi man naa séddalewaat kàrt yi ngir njariñal Afrig ?