Peresidaa FAY ca 67eelu ndajem CEDEAO : Senegaal feddali ma jaayanteem ngir bennoog Afrig.

Biti Réew - 22 MONTHS.JUNE 2025

 Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, bawoo na Abujaa ci dibéer ji 22i fani suwe 2025, ginnaaw ba mu teewee 67eelu jataayu ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu Mbootaayu Réewi Afrig Sowu Jant yi (CEDEAO).

Jataay bii ñu ngi ko amal ci jamono ju tund wi di jànkoonte ak ay jafe-jafe yu mag : ñàkk kaarange gu sax ci Sahel bi, fitnay politig, koom mu desee dox ak ñàkk dal gu wér guy yoot dig-digal bi.

Ci ndaje mii, Senegaal posewu na ci feddali, jaare ko ci teewaayam ca dayo ba gën a kawe, ag jaayanteem gu sax dàkk ngir CEDEAO gu doon benn, dal, te taxaw temm ci yittey askan yi boole ko ak taqoo ak pas-pasu Afrig gu doon benn. 

Ki ñu jiital ci kanamu Kurélu Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu CEDEAO leegi mooy kilifa gii di Julius Maada BIO, Njiitu Réewum Siyeraa Lewon.