Tay ci alxemes ji, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, ànd na ak naataangoom bii di S. Mohammet Uld Seex El Xaswani, amal ug nemmiku ca palaatformu gaas bu “Grand Tortue Ahmeyim (GTA)”.
Ba ñu yeggee ca barab ba partaneeri sémb wi ñoo leen dalal : British Petroleum (BP), Kosmos Energy, Kërug Petorol gu Senegaal gi (PETROSEN) ak Kërug Njafaan yu Móritani (SMH).
Nemmiku gu am solo gii mooy màndargaal duggug Senegaal ak Móritani ci kurélug réew yiy jaay gaasu yolnde bu raxul (GNL). Sémbu GTA wii nag misaal la ci lëngoo gu jaar yoon gi dox diggante ñaari réew yi, te lalu ci doxaliin wu leer, yamale ak mbébet mi nu bokk am jëm ci àndandoo peeg sunu ëllëg ci wàllu yasara.
Jéego bu am solo bii tijji na jamono ju bees ci naataange gu yaatu, gën a dooleel moom sa bopp gi ci wàllu yasara ak coppiteg koom mu ñoŋ ngir njariñu askanu Senegaal ak Móritani.