Peresidaa Fay ak naataangoom bu Móritani bi fas nañu yéene gën a dooleel lëkkaloo gi dox diggante Senegaal ak Móritani

Biti Réew - 11 MONTHS.NOVEMBER 2024

Ci lu soxal ndajem OCI mi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay séq na ab jataay digganteem ak naataangoom bu Móritani bii di Peresidaa Muhammet Uld Seex El Gasuwani. Ànd nañu feddali seen ug jaayante jëm ci gën a dooleel lëkkaloo ak xaritoo gi dox diggante Senegaal ak Móritani ngir dal ak yokkute gu yaatu.