Peresidaa Emanuel Macron dalal na Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay Fay.

Biti Réew - 27 MONTHS.AUGUST 2025

Lu jëm ci Ndajem Lijjantikati saa-farãas mi mu war a teewe, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY daje na tay ci suba si ca "Élysée" ak Peresidaa Emanuel Macron mi mu séqal benn jataayu ndékki. 

Ci jataay bu fés ak mbégte bii, ñaari Njiiti Réew yi bokk nañu yëraat sémbi lëkkaloo yi, teg ci weccente xalaat ci luy gën a dëgëral lëngoo gu bees gi war a dox diggante Senegaal ak Farãas, rawati na ci wàllu dugal xaalis, yaxantu, wattu gi ak kaaraange gi. Lëkkaloo googu ñu yëraat dina bokk ci tomb yi ñu war a waxtaane ci lël bi ñaari Ngóornamaŋ yi war amal ci weeru sebtàmbar. 

Njiitu Réew mi rafetlu na itam taxawaayu Peresidaa Emmanuel Macron ci wàllu fàttaliku, rawati na nangu gi mu def ci bóomug tiiraayéeri Senegaal yi ci Caaroy ca atum 1944. Dëne na ko ngir mu ñëw teewe ñaareelu atu màggal bis bi ñu jàpp 1 panu desàmbar 2025, ci Ndakaaru.