jëwriñ - 10 MONTHS.NOVEMBER 2024
Kilifa gi, Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal, dina dem ca Riyad, ca Araabi Sawudit, 10 jàpp 12i fani nowàmbar 2024. Moom Njiitu Réew war faa teewe, ànd ko ak naataangoom yu Mbootaayu Lislaam gii di OCI, Ndajem arabo-islaam giy am 11i nowàmbar, te ñu jagleel ko tolluwaayu Palestin ak Liban.
Ndaje mii mu ngi jëm ci dooleel taxawu ak njàppaleg Umma Islaam gi jëme ci ñaari réew yooyu boole ko ak woote jàmm ju sax ca tund wa.