jëwriñ - 24 MONTHS.FEBRUARY 2025
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dina door sémbu « New Deal Technologique » altine 24i fani féewarye 2025 ca «Centre de Conférences » Abdu Juuf bu Jamñaajo (CICAD).
« New Deal Technologique » bii li ko tax a jóg mooy soppi serwiis piblig bu Senegaal gën koo méngale ak jamono, xereñ te dëgmal ëllëg. Pexe mu am solo mii jëm ci amal coppite yu wér ci wàllu xarala, mu ngi sampe ci ñenti keno te ñu xayma ay jubluwaayam fii ak 2034.