Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, dalal na ci altine ji S. Ibraahiima Seex JONG, mi jiite « Fonds » bi Mbootaayu Réewi àddina si teg ngir saafara yàqu-yàqu yi ak gàllankoor yi ci wàllu njuux (CCNUCC).
Ci ndaje mii, ñaari kilifa yi weccente nañu ci lëngoo gi dox diggante Senegaal ak Fonds bi, ñu ànd sóobu ngir taxawu ca na mu gën a gaawe réew yi gën a loru ci njeexitali soppiku yi am ci wàllu njuux.
Waxtaan yi tax na ñu yaatal ci lu jëm ci fagaru ci wal mi, xeex yàqu-yàqu yi ci tefes yi, niki noonu jafe-jafe yi ci wàllu dagg garab yi ak yenn jéeya yi. Muy jafe-jafe yu bari yu laaj taxaw temm ngir gën a sàmm askan yi ak amal kaaraange gu sax dàkk ci jumtukaay yi ñuy jëfandikoo.
Ñaari wàll yi feddali nañu itam seen gis-gis bi ñu bokk am ci solos amal doxaliin wu jaar yoon ci njuux li : réew yi gën a néew lu ñuy xëpp ñoo ci gën a loru, ci jamono joj ñi ëpp lu ñuy xëpp nanguwuñoo am taxawaay bi war.