xamle - 13 MONTHS.JUNE 2025
Ci ñaareelu fanu nemmiku gi muy amal ca "Pôle territorial Nord”, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, daloo na, ci àjjuma ji 13i fani suwe 2025, ndefaru SAF Ingredients ga nekk ca Ros Beeco.
Ndefar gii, jiitu ci Afrig, mu ngi màcc ci sopparñi soble si def ko pëndax ak ay daggiit. Ñu defar ko ak xarala yi mujj a génn, rawati na benn “chaudière biomasse” buy jëfandikoo xollitu ceeb.
Sémb wu am solo wii nag dina am taxawaay bu am solo buy gën a ñoŋal dund bi ak suqali koomum tund wi, lépp it boole ko ak wàññi bu baax lim bu takku bi ñu daan ñàkk ci liy ñoree ci mbay mi ak jéggaani gi.