Njiitu Réew mi teewe na màggalug 80i ati ONU ca New York.

Biti Réew - 22 MONTHS.SEPTEMBER 2025


Tay ci suba ca New York, Njiitu Réew mi teewe na ndaje mu kawe mi ñu doon amal jëm ci màggal 80i ati Mbootaayu Réewi Àddina si, tey màndargaal tijjitel 80eelu Ndaje mu Mag mi. 


Ndaje mu am solo mii fàttali na sas wu jëkk wu mbootaay gi : saxal jàmm ji, sàmm yoon, dooleel lëkkaloo diggante réewi àddina si boole ko ak àndandoo taxaw temm ngir saafara jafe-jafey àddina si. 


Teewaayu Njiitu Réew mi ci ndaje moomu nag day wane taqoo gu sax gi Senegaal am ci mbaaxi lëkkaloo ak diisoo diggante xeet yi. 


#UNGA80 #ONU #Senegal