Njiitu Réew mi séq na ay waxtaan ak kilifay Japan Bank for International Cooperation (JBIC).

Biti Réew - 21 MONTHS.AUGUST 2025


Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY dalal na kilifay Japan Bank for International Cooperation (JBIC). Ndaje mii tijji na wunti lëkkaloo yu bees ci fànn yu am solo, ngir yombal ndugalum xaalis ci Senegaal ñeel këri liggéeyukaayi Japon yi.