Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay , dalal na ci ay jataay yu toftaloo, ci altine ji 7i fani awril 2025 ñetti tañ, ci Njénde li.
Ci ngoon gi, Njiitu Réew mi séq na ab jataay ak S. Abebe Aemro Selaasie, Njiital FMI ci Afrig, mu àndoon ak tañ wu am solo. Nemmiku gii nag day tàbbi ci waxtaan yi Senegaal di amal ak campeefu kopparal gii ci àddina si. Ci jataay bi, moom S Selaasie feddali na jaayanteg FMI jëm ci taxawu Senegaal ci yéene ju wér ji mu am ngir joyyanti koomam. Bokk na ci li ñu waxtaane, muy yeesal yu am solo yi jëm ci jubbanti anam yi ñuy yoree koppar yi lépp boole ko ak dooleel yokkute gu matale te sax.
Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye dalal na itam ci ab jataay, S Abdulaay Jóob, Njiital komisoo UEOMOA.
Ndaje moomu may na leen ñu càmbar jafe-jafey koom ak koppar yi am moo xam ci Senegaal walla muy ci mbooleem mbootaay gi. S Jóob posewu na ci ndaje mii, ngir rafetlu jéego yi Càmm gi di teg ngir jubbanti jafe-jafey njël li balaa yàgg.
Mu tëjee moom Njiitu Réew mi ci dalal tañu (delegation) Bànqaas biy saytu suqalikug ndefar (industrie) yi ci Mbootaayu Réewi Àddina si (ONUDI), te nekk jamono jii di aml ub liggéey ci Senegaal, ci njiital Bootal bi (DG) di S. Gerd Muller. Waxtaane nañu pàcc yu am solo yu mel ni mbay mi, mbell yi ak ndefar yi, te doon jumtukaay yu am solo ngir suqali koomum réew mi. S. Muller fésal na ay pàcc yu am solo yu ñu fas yéenee dugal xaalis ngir dooleel yitte ji Nguurug Senegaal am jëm ci sopparñi liy ballee ci réew mi.