Biti Réew - 18 MONTHS.JULY 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, dina teewe tay ci suba gi ca Bisaawó 15eelu Ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yi bokk ci Réew yiy làkk Portuge (CPLP), ci ndënel (invitation) naataangom Peresidaa Umaro Sisoko Embaló.
Senegaal daa boole ci ay yëngoom, jëf yuy gën a dooleel jëflantey lëngoo ak mbokkoo diggam ak réew yiy làkk portuge.