Njiitu Réew mi Jomaay FAY yaatal na gis-gisu koom bu bees bu Senegaal ca “Chambre de Commerce” bu USA

Biti Réew - 10 MONTHS.JULY 2025

Ci ñaareelu fanu tukki nemmikoom gi ca USA, Njiitu Réew mi, Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, moo nekkoon ganu “Chambre de Commerce” bu USA ca Washington, bokk ci mbootaayu njaatige yi gën a mag ci àddina si. 

Ci jataay bu dajale lu mat fanweeri kilifay këri liggéeyukaayi Amerig yu mag, Peresidaa Jomaay yaatal na fa gis-gis bu leer bi mu am ci wàllu koom, doon gis-gis bu wóor te xemmemu ñeel Senegaal. Mu jiital ci nag leeral coppite yi nu sóobu ngir gën a rattaxal bu baax xar-kanamu jëflante yi, niki noonu fànn yu bari yi te am solo yi ñu man a dugal xaalis yu mel ni yasara gi, ndefaru lekk gi, tabax yi, koomum xarala yi ak balli mbindare yi (petorol bi ak gaas bi). Pas-pasu Senegaal bu bees bii, sampe ci lëngoo gu làq njariñ ñeel wàll yépp, te doon lu méngoo ak politugu lëngoo gu bees gu Amerig « Trade not Aid », nekk na lu dugalkati xaalisi saa-amerig yi wane seen yéene ci gën a feddali seen teewaay ci Senegaal, rafetlu lool.  

Ci ndaje mii, “Chambre de Commerce” bu États-Unis xamle na ne dina génne ci fan yii benn tegtalukaayu dugal xaalis bu ñu jagleel Senegaal, te jëm ci gën a taxawu dugalkati xaalisi saa-amerig yi.


Peresidaa JOMAAY tëjee tukkeem bi ci jataay bu mu dalal S Christopher Landau, miy Topp Sekkereteer Detaa di it Njiitu Ndiisoog ndoxalug DFC (Kërug Amerig giy kopparal suqaliqu gi). Moom mii nag xamle na yéeney 

 États-Unis jëm ci dooleel lëkkaloog koom seen digg ak Senegaal jaare ko ci gën a dugal xaalis ak lëngoo gu wér diggante sektéer piriwe ñaari réew yi. Tukki bii kon dina tijji xët wu yees wu yaakaaru ngir lëngoo gu gën a am doole, gën a man a jur i njariñ ak i xëy ngir Senegaal.


Peeñ :