Ci ñetteelu fanu nemmikoom gi ca Japon, Njiitu Réew mi séq na ab jataay ak S. Takeharu YAMANAKA, Farab dëkk bu Yokohama.
Muy ndaje mu jëmoon ci wàllu TICAD bi doon ñenteelu yoon Yokohama di ko dalal, mu bokk ci jataayu waxtaan yi ëpp solo diggante Japon ak Afrig. Mu am lu mat 4i milyoŋ ñu ko dëkke, doon na dëkk buy màndargaal tijjiku ak lëkkaloo ci biir àddina si.
Ci ndaje moomu, S YAMANAKA xamle na mbégteem ci dalal Njiitu Réew mi ak tañam, jaare ko ci xamle solos nemmiku gii ngir gën a dooleel jëflante yi diggante dëkkam ak kembaaru Afrig.
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, rafetlu na dalal gu mucc ayib gi ñu ko jagleel, boole ko ak fésal misaalum Yokohama ci fànn yu am solo yu bari, rawati na ci wàllu ndox mi, caytug mbuubit yi, pàkkug dëkkuwaay yi ak wàllu waax yi. Ci geneen wàll, sàkku na ci Fara bi mu bàyyi xel gën a dooleel lëkkaloo gi ak dox ak goxaan yu Senegaal, ci yéeney yaatal ak ñoom seen xam-xam ci wàllu doxaliin.
Ci mbébet yi, ñaari wàll yi am nañu ag déggoo jëm ci gën a xóotal seen ug lëngoo, rawati na ci wàllu xarala ak tàggat nit ñi. Muy lëngoo yu jëm ci taxawu gox yi ak goxaan yi ak gën a dooleel suqaliku gu sax dàkk ci gox yi, mu lalu ci fent ak dimbalante.