Biti Réew - 21 MONTHS.AUGUST 2025
Njiitu Réew mi séq na ab jataay ak ki jiite wàllu dund bi ci àddina si (PAM). Bokk nañu rafetlu lëkkaloo gu mucc ayib gi dox diggante Senegaal ak PAM teg ci xamle seen yéene ci gën koo dooleel jaare ko ci lii di kàntin eskoleer yi, fexe ba jigéen ñi manal seen bopp ak jàppandil jot cim ndox ngir man a taxaw ci ñoŋal wàllu dund bi.